CEERNO ALASAAN SÀLL : "YAAKAAR AK RAFET NJORT ÑOO MA TAXOON A ÀND AK MAKI SÀLL"

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey, Senegaal, kenn mënul a wax  waxu pólitig te doo ci boole Ceerno Alasaan Sàll. Turam ak yu Usmaan Sonko, Bàrtelemi Jaas, Xalifa Sàll, Abdul Mbay, Mamadu Jóob Dëkuruwaa ak Mamadu Lamin Jàllo ñoo gën a fés ci kujje gi. 

Seen yéenekaay LU DEFU WAXU amal naak moom laaj-tontu bu yaatu, di ci waxtaane mbiri réew mi ak xew-xewi jamono. Xaajees na waxtaan wi ci ñaari pàcc. Ci pàcc bu njëkk bii, Ceerno Alasaan Sàll daf nuy xamal jaar-jaaram, nim xamanteek Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak cëram ci cosug APR.
(Ci taataanug Paap Aali Jàllo)

– Paap Aali Jàllo (PAJ) : Ceerno Alasaan Sàll, danuy jiital sunuy nuyoo, cant ak ngërëm ñeel la, ngir liŋ nu nangul laaj-tontu bii nuy waaj a door. Bu loolu weesoo, noo ngi lay ñaan nga wonale sa bopp ak jàngkati LU DEFU WAXU yi, wax leen kan mooy Ceerno Alasaan Sàll ak lan mooy jaar-jaaram.

Ceerno Alasaan Sàll (CAS) : Waalekum-salaam wa rahmatulaa, Paap Aali Jàllo. Maa ngi lay fay, di nuyu jàngkati yéenekaay bii di LU DEFU WAXU. Ma leen di dollee sargal, di leen ndokkeel, yow, ki sos yéenekaay bi, Bubakar Bóris Jóob ak ñi ci jàpp ñépp ba mu agsi fim agsi tey. Maa ngi rafetlu yit liggéey bu am solo bi ngeen di def. Nde, yéen a ngi fexe ba doomi-Senegaal yiy jot ay xibaar yu wér te wóor, yaatu lool ; rawatina li ngeen leen di biral ci làmmiñu askan wi. Man, nag, doomu-Senegaal laa, juddoo Cees, yaroo fa, màgge fa. Fa laa jànge yit, bi may tuut-tànk ba ni may ame sama lijaasab “Baccalauréat”. Waaye, jàng naa fa diine itam. Xam nga Senegaal moom, réewum diine la, réewum Lislaam. Moo tax, fépp foo mënti juddoo, bu dee doomu-jullit nga, dees na la dugal daara. Bu ko defee, nga jàng sa diine, xam ni ngay jaamoo Yàlla ak ni ngay jëflanteek doomi-aadama yi. Moo tax, jàng naa Alxuraan ak yeneen i téerey xam-xam yu aji-gëm Yàlla ju ne war a làmboo ngir mën a jaamu Boroomam. Gannaaw gi, demoon naa bitim-réew, àggaleeji fa sama njàngum nasaraan. Foofu laa amee sama lijaasab Ingénieur télécommunications laata may sàkkuwaat lijaasab Ingénieur aviation civile. Bi ma amee samay lijaasa, dama ñibbisi Senegaal, sàkkuji liggéey ci ASECNA, Yàlla def ñu jël ma. Cib xayma, liggéey naa fa lu war a tollu ci 25i at. Bi ma fay liggéey, nag, jaar naa ci réew yu bari, muy Senegaal, Niseer, Komoor… Xeetu liggéey wu nekk def naa ko ci réew yooyu. Ndaxte, looy gën di dem, sa xam-xam ak sab xarañte ci wàllu xarala day yokku, ñu lay gën a soxla. Noonu, liggéey naa OACI (Organisation de l’aviation civile internationale), muy ndajem réewi àddina si ñeel naawaan wi (aviation civile). Maa nekkoon seen aji-wóorliku (auditeur), doon saytu kaaraange roppëlaan yi ci réewi Afrig yeek yu Tugal yi (Ërób). Rax-ci-dolli, amoon naa ay ndomboy-tànk ci ASECNA mi nga xam ne, 18i réew ñoo ko séq. Réew mu ne, am nañ fab bànqaas bu leen fa toogal, di fa saytu lépp lu aju ci jaww ji, muy kaaraangeg roppëlaan yeek yooni jaww ji (fi roppëlaan yiy jaar), metewoo bi, naaweef bi, wërngëlug-caytu yi (tours de contrôle), añs. Bànqaas bu nekk day am njiit ak kippu yi muy liggéeyandool. Man nag, jot naa jiite bànqaas bu Senegaal.

– PAJ : Lan moo la tax a dugg ci pólitig ?

– CAS : Ku juddoo ci sunu réew yi, xam jafe-jafe yi askan wiy jànkonteel saa su ne, waroo bank say loxo, toog di seetaan. Nde, lépp a fi jamp. Soxla yaa ngi ne gàññ : am na ñu mënta jot ci ndox mu sell mi, njàng mi doxul, tukki jafe na lool, ay dëkk ak i gox yu baree bari amuñu laf (énergie) ak mbëj… Fànn boo laal, soxla yaa ngi fa bari ba jéggi dayo, askan wi lottal la ko ba nga ne lii lum doon. Bu loolu amee, toog di seetaan warul kenn. Ku ci ne am na taxawaay boo war a am. Looloo waral, ba nuy ndaw di jàng, bokkoon nan ci làngu pólitig Ànd jëf. Kon, man, Ànd jëf laa dooree sama jaar-jaaru pólitig. Waaye, dama dem ba ci biir ma jóge fa ngir ñaari sabab. Bi ci jiitu mooy ne, danoo dem ba bokkatunu gis-gis ñeel yoon win waroon a jaar ba yor réew mi ak anam bin ko war a yoree bu nu ko Yàlla dénkoon. Rax-ci-dolli, gisuma woon ci njiiti Ànd jëf yi baax-baax yi kilifay réew war a làmboo. Sabab bi ci topp mooy ne, bokkunu woon xalaatin. Dafa di, sama gis-gis ci nees war a yoreem réew dafa safaanoo woon ak yoon wiñ xàlloon, ñoom. Seen gisin daal moo doyadi woon ci samay bët, teeyoon sama xel. Looloo indi woon réeroo sunu biir, ma teggi sama tànk, nekk ci sama liggéey, ca ASECNA. Waaye, taxuma woon a bàyyi pólitig.
Ndax, jàpp naa ne, booy liggéey ci béréb bu mel ni ASECNA, di def sa kem-kàttan ngir jariñ sa réew, yaa ngiy pólitig. Ma nekk fa nag, di liggéey, di liggéey ba atum 2007, daldi tàmbalee am nag ay jafe-jafeek nguurug Ablaay Wàdd ga woon.

PAJ : Lan moo la jotale woon ak nguurug Ablaay Wàdd ga woon?

– CAS Ñoom, dañ bëggoon a tas ASECNA, saax-saaxe ko, def ko seen moomeelu bopp, paacoo ko. Ndege, dañ foogoon ne ASECNA mu ngeek àddinaak li ci biir. Moo leen ko taxoon a singali, ñu fay xemmem koppar ak yeneen ak yeneen. Te, loolu ñu doon xemmem sax, amu fa woon.
Li xamb taal bi, nag, mooy suuf ak taaxi ASECNA yi nekkoon Fann Résidence, Point E, ci ayeropoor yeek feneen ak feneen… Jamono jooju, ci lañ toŋ-toŋe suufus Foire bi, estadd Léwópool Sedaar Seŋoor ak lépp li wër ayeropoor bi ak Corniche bi. Ñu ni déet-a-waay, ñu bëgg cee teg moomeelu ASECNA. Ndaxte, biir ayeropoor bi rekk a desoon, ñu bëggoon koo daggat-daggate, séddoo ko. Dafa di, bees seetloo, 2007 ba nëgëni-sii, daggat-daggatees na ayeropoor bi, def koy kërale (parcelles) yu 30i ektaar, séddale leen. Bii ñu jox ko kii, bee ñu jox ko kee. May wax ñuy taafantoo, jamono jooju, koomalug (financement) Monument de la Renaissance ! Fim ne nii, yàq nañ ayeropoor bi ba mu yàqu yaxeet. Ndeysaan, benn ayeropoor boobu rekk a nekkoon ci péey bi, yaatu woon lool. Ak naal buñ mënoon a am, waruñu woon wàññi astemaak daggat-daggate ayeropoor bi. Moom kay, dañ waroon a yokk ngir dooleel réew mi ci wàllu tukki. Nde, képp ku jàng xam-xamub kaaraangeg roppëlaan ak kaaraangeg way-tukki yi, xam nga ne jamono jii, loolu dafa nasax bu baax. Ñi waroon a sàmm ayeropoor bi nag, ñoo ko yàq, muy nguurug Ablaay Wàdd te looloo ma boole woon ak ñoom, ci gàttal.

– PAJ : Dara fekku la ci diir mbagg boobu nga leen doon diir mbagg?

– CAS : Biñ bëggee tas ASECNA, ci nowàmbar 2007, ànduma ci woon. Dama bañoon, di ko xeex, dogu woon ci xeex bi. Bi loolu amee, sama taxawaay ñeel mbir mi metti leen, ñu tàmbali maa fexeel. Ci lañ waxee ne nañ ma jële ci boppu bànqaasu ASECNA bu Senegaal. Te, sax, nammoon nañoo jéggi yoon, def may yëf yu ñaaw. Bi ko waa ASECNA yëgee lañ ma rawale, yóbbu ma Komoor, ma nekk fab diir. Noonu la ma Yàlla muccalee ci seen i pexey saay-saay.

– PAJ : Nan nga xamanteek Njiitu réew mi, Maki Sàll?

– CAS : Maa ngi lay gërëm bu baax ci laaj bu am solo bii nga ma laaj. Ndaxte, dinaa ci mën a leeral lu bari. Ca jamonoy Ablaay Wàdd la woon. Ndax, bi may xamante ak Maki Sàll, booba, moo nekkoon Njiitu jawriñ yi, man, ma nekkoon njiitalu bànqaasu ASECNA fii ci Senegaal. Sama ñaari xarit yu nekkoon ASECNA, ñoo taxoon. Kenn ki, Moor Ngom, da doon yëngu ci pólitig. Keneen ki moom, Mustafaa Jeŋ, xaritu Maki Sàll rekk la woon, màggandook moom. Ñooñoo ma taxoon a miin Maki Sàll, ñoo gënoon a tax ma ñeme ko. Léeg-léeg, daan nan daje, toog lu yàgg di waxtaane ay ponk yu yaatu ñeel naawaan wi. Léeg-léeg, nguur gi da daan soxlay leeral wallay xalaati ASECNA ci wàll woowu. Ginnaaw gi, Maki Sàll jóge ci boppu nguur gi, doon njiitalu Péncum réew mi. Nga may ma, ma leeral fii ne, du nguur gi Maki Sàll doon jiite laa amaloon coow ci jamonoy Ablaay Wàdd. Nguur gi wuutu gosam gee bëggoon a tas ASECNA, ma jàppante woon ceek ñoom. Te, loolu sax, daan nan ko waxtaane man ak moom léeg-léeg. Ba ma fay nekk, ci tukki yi Ablaay Wàdd daan tukki lan daan daje, walla ci yeneeni anam. Bi ma newee Komoor itam, nu ngi doon wéy di déggante. Boo fàttalikoo sax, dinga gis ne, jamono jooju, gaa ñi sonaloon nañ ko lool, moom Maki Sàll. Daanaka, ci diggante weeri nowàmbar ak desàmbar ci atum 2008, yéenekaay boo ubbiwaan, ñuŋ ko ci doon ŋàññ, di ko sikkal ak a yàq deram, te booba moo nekkoon Njiitalu Péncum réew mi. Ci laa xamee ni kii, yàgg yàgg dinañ ko sàkkal pexe. Booba, jàppoon naa ne, man ci sama wàllu bopp, jotoon na ma sóobu ci pólitig bi. Nde, Ablaay Wàdd ak i ñoñam nekkewuñ fi woon lu dul saax-saaxe réew mi, di def lu leen neex. Nu dénk leen sunu réew, jox leen sunu baat ak sañ-sañ yi ci aju yépp, ñu wëlbatiku def kob yar, di ko mbugalee doomi-réew mi, di jaay nit ñi doole. Loolu metti woon ma lool, sax. Nu ne nag lii dafa war a dakk. Nu fas yéenee def ni ñoom, ngembu, dugg ci géewu pólitig bi, sàkku nguur gi ngir safaara jafe-jafey askan wi. Lin ko dugge woon mooy aar ak suqali Senegaal. Ci kow loolu, maak Maki Sàll nuy waxtaan, di ci weccoo xalaat ba ni nuy taxawale APR.

– PAJ : Kon yow ci ñi sos APR nga bokk…

– CAS : Waaw, man, bokk naa ci kàngam yi sos APR. Weeru desàmbar atum 2008 lan ko taxawal. Nu ne ci biir, di liggéey, def ci sunu doole, sunu xam-xam, sunu lépp… Njëlbeenug aniwerseeru APR, ci weeru desàmbar 2009, nun kàngami APR yee ko xumbaloon ak ñi nekkoon ci njiiteefu làng gépp. Amoon yeneen i gan yu ko teewe woon, ñu ci mel ni Làndiŋ Sawane, Sàmba Juulde Caam, Màgget Caam, añs. Noonu lan taxawale APR, nekk ci ba 2012. Yàlla dogal, Saa-Senegaal yi dénk nu réew mi, amoon ci nun yaakaar ju réy, nag. Nde, APR, daanaka yaakaar a doon ñaareelu turam. Nguur gin taxawaloon dafa ëmboon ay làngi pólitig yu bari, ñépp bokkoon ci lees duppe woon « les Assises nationales », xaatimoon déggoo yi ci rote woon. Nu àndandoo woon ci ndaje mu yaatu, tudde ko Bennoo Bokk Yaakaar. Jamono jooju, dan amoon yaakaar ju réy ngir yéeney defar réew min amoon, soppi doxalinu réew mi. Ndaxte, ku ci nekk dafa tegoon boor ay mbiri boppam, daldi ràngu ci tëralin ak ndigal yi tukkee woon ci «Assises nationales» yooyu, fasoon yéene leen jëmmal. Looloo ma taxoon a ànd ak Maki Sàll, yaakaar ak rafet njort. Ngir fàttali rekk, fii ci Ndakaaru lan taxawal jamono jooju Convergence des cadres républicains, man mii ma njëkk koo jiite. Te, ba ni may bàyyee APR, maa nekkoon ci bopp bi…

(Dees na ko topp…)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj