LAAJ-TONTU SAADA KAN/BÓRIS (III)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laaj-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019. Bii mooy ñetteelu xaaj  bi, di yit biy tëj seen waxtaan

S. K. : Bóris, bi nuy waajal waxtaan wi, danga wax lu ma yéem. Danga ni : « Ñaar a am, Saada : làmmiñ wi may waxe, man, ak làmmiñ wiy wax ak man .»Ma bëggoon nga leeralal nu lu kàddu yooyu wund.

B. B. J. : Waaw. Wax nga dëgg. Man ci sama bopp, bi may bind Doomi Golo lañ ma dikkal. Ndaxte, damaa dem ba ci yàgg mu mel ni ay baat yu doon nelaw ci sama biir xol bi ñoo jékkee-jékki yeewu, ràkkaaju nag, di awu ci sama biir yóor gi, di ma déey ay baat ak i xalaat yu yéeme. Ci laa ne ndekete am naa alal ju ni tollu ciy kàddu, ndekete lépp lu ma mas a wax ñii ñoo ma ko waxloo te ñoo may bindloo tamit ! Gis nga, bindkat bi war na fu mu tollu di ormaal làmmiñ wi mu nàmp, di ko jëfandikoo. Waaye, na fexee xam it wan làmmiñ ay wax ak moom, di cuq xolam ak xelam. Loolu sax a gënatee am solo. Bu ko defee, bindkat bi, baat yiy wax ak moom lay jëmmal ci téereem, muy téereb taalif mbaa téereb nettali walla kilib, maanaam tiyaatar. Loolu laa yëg bi ma tàmbalee bind ci wolof ba tax maa wax loolu. Su may bind ci tubaab mën naa feesal junniy xët te benn du ma ci yëngale noonu.

S. K. : Bóris, bu ñu xoolee sa taxawaay ak ni ngay faral di waxe, mënees na jàpp ne dangay xeex li ñuy woowe ci nasaraan Françafrique. Te say téere dañuy biral xeex boobule. Jot ngaa bind di diiŋat nooteel boobu ak di tontuwaale way-boddekonte yi ñeel nit ku ñuul. Nu ngi sàkku nga dégtal nu tuuti sa xalaat ci xeex boobu.

B. B. J. : Ndem-si-Yàlla ji François-Xavier Verschave moo xéy tëgg baatu Françafrique. Lan mooy Françafrique ?  Ci gàttal, Françafrique mooy naalub nooteel bi Frãs lal ngir teg loxo ci réewi Afrig yi, aakimoo seen alal ak seen moomeel te ay doomi-Afrig, sunu njiit yi nga xam ni ay cuune dëgg lañu, di ko ci jàppale, bokk ak moom mbuus.Loolu day firndeel ni Frãs mësu fee jóg, te xalaatu ko. Ba Frãs nangoo réewi Afrig yi moom seen bopp, daa génne ci bunt bi ba noppi làqu tëb palanteer bi delsi ! Fekk na mu tegoon nitam ku ñuul kukk ni yow ak man mii ci jal bi, kookuy wéy di ko defal lépp lu mu bëgg. Kon Françafrique loolu la, ay réewi Afrig yu ne ñoo moom seen bopp, am seen raayaak seen Pincez-tous-vos-koras-frappez-les-balafons waaye teewul Frãs di wéy di fa dogal.  Mu ngoog. Te sax, am na benn politiseŋuFrãs bu kàccoor te tuddoon Edgar Faure bu jeexal wax ji ba mu nee : « Daanaka nun waa Frãs danoo jóge Afrig ngir rekk gën faa mën a dëju !’’ Te gis nga, Saada, képp ku bëgg ay firnde ci lii ma la wax, na méngale doxalinu Frãs ak bu Àngalteer mi nga xam ne tegoon na fi loxo moom tamit ciy réewi Afrig. Xoolal, li ko dale ati 1960 yi ba nëgëni-sii, Àngalteer mësul yónni ay soldaaram Afrig ngir ñu ñëw dakkal ay xare yoo xam ne moom Àngalteer moo leen sooke ! Kenn mësul gis làrme bu Àngalteer ca Keeña, ca Tansani, ca Niseryaa, ca Ganaa… Loolooy li am. Moone, bu ko neexoon doxale neneen, jaay réew yooyu doole. Waaye defu ko. Nga dellu, xool Frãs. Du jar sax ngay sore ci sab gëstu. Li ko dale ati 1960 yi ba léegi, ay fukki-fukki yoon la yónni ay soldaaram fu ne ci réewi Afrig yi mu defoon moomeelam. Ñu ni déet-a-waay, mu sax ci, xaatimloo sunuy njiit – seeni xuus-maa-ñàpp yu ñàkk faayda – ay déggoo yu xel mënuta nangu ñeel mbirum làrme. Rax-ci-dolli, dafa ne déjj-déjjaaral ci sunu koom-koom, di nu ŋacc saa su nekk. Yaakaar naa ni Senegaal moom, ni Frãs aakimoo sunu koom-koom dootul lu ñuy laam-laame. Doxantul ci mbeddi Ndakaaru yi, yékkatil sa bopp xool bitig yu mag yi ak màngasin yi. Bu ko defee, dangay gis ne, ni ñu cëralee Frãs ci sunu koom-koom, ci nguurug Maki Sàll gii, mësu fee am. Jamono jii la Frãs gën a noot Senegaal. Li ci gën a doy-waar mooy ne, saa yoo ŋàññeeFrançafrique am i doomi-Senegal yu la mere, naan : « Yow daal, dangaa bañ Frãs doŋŋ !Tee noo takku liggéey ! Du moo gën ne fiy tuumal saa su nekk Frãs ?» Loolu yomb naa wax, Saada. Ku mu doon sa sago nga fas jom defar sam réew te sa yoon du nekk ci ñeneen ñi. Waaye na fekk ñu bàyyi la ci ! Seetal rekk, lépp la Frãs teg loxo, rawatina koom-koom gi ak sunu xaalis. Te CFA bi da koy firndeel te am na nu yëf yiy deme ay soldaaram mën nañoo dal ci sunu kow. Ci gàttal daal, ci nooteel lanu nekk ba nëgëni-sii. Képp ku yaakaar ni mén ngaa defar réew mi tey noppiwaale Françafrique,dangay nax sa bopp mbaa nga tey ko di nax askan wi ngir defaru yow ci sa bopp. 

S. K. :Bóris, wax nga ci teewaayu soldaari Frãs yi fii ci Afrig. Te sax, yaak Aminata Daramaan Taraawore jot ngeen a bind ab téere bu tudd« La gloire des imposteurs », jagleel ko lees di woowe “Opération serval” bi Frãs amaloon ca réewum Mali. Mën nga cee delseem ?

B. B. J. : Waaw. Aminata Daramaan Taraawore ab xeltukat bu mag la ca Mali. Muy nit ku fa am tur lool, ñu jox ko fa cër te di ko may nopp. Lan moo xewoon Mali ? Frãs a defati mëninam, yónnee fay soldaar ngir, ci li François Hollande taafantoo woon, àtteji nguur gaak Tuwaareg yi, diy naar yu féete ci bëj-gànnaru réew ma. Looloo indi Opération serval bi nga tudd sànq. Du woon guléet Frãs di def lu ni mel ; moom kay, tur wi rekk mooy soppeeku, waaye saa su nekk mu yabal fiy soldaaram ngir sàmm ittey boppam. Noonu la soldaari Frãs yi teersee Mali. Keroog jooju, ay ndaw ñoo leen teeru, dar leen ak i móto, yor ay folóor yu rafet, di yuuxu ca kow : « Frãs Yal na fi yàgg ! Frãs Yal na fi yàgg ! ». Waaye, mbir mi ay naxee-mbaay kepp la woon, ndeysaan. Frãs boppam la fa teewaloon, du leneen ! May wax Farañse yi naan : « Bu dul woon nun, terorist yi, defkati ñaawteef yooyuy mbubboo lislaam àgg nañ Bamako ba rajaxe ko ! » mbaa : « Nun noo xettali doomi-Mali yi ! ». Ma ne : ay fen yu tooy xepp a ngoog ! Duñ ci lenn, te xam nañ ko. Mooy li wolof di wax rekk, dëmm rey la ba noppi di la jaale. Looloo tax maak Aminata nu gis ne, lii wareesu cee noppi. Ndaxte, lu ni mel moo amoon ca Kodiwaar ak ca Libi. Kenn umplewul li dal Bagbo, dal fi tamit Xadafi. Te loolu lépp, Frãs a nekk ci ginnaaw, di nos ak a nocci ngir ittey boppam.

Noonu lañu def, yàq deru Bagbo ba mu yàqu yaxeet ba li ëpp ci xeltukati Afrig yi di ko tuumal ; ñenn ñi dem ba koy yéene dee, naa : « Bagbo, na dee ! » Li ko Nicolas Sarkozy dugge woon mooy teg fi ndawam, ab dunguroom, muy Alasaan Watara. Bu ko defee, ñi xamul jàpp ne Bagboo fi yées, Watara moom di yaaram, jub, fas-yéenee yemale ñépp te bëgg réewam. Xam nga ni loolu, ay waxi xale lay gén a nirool. Li ñu def Xadafi moo gënatee jéggi dayo. Fexe woon nañu ba népp jàppe Xadafi ni seytaane. Foofu tamit, xeltukati Afrig yiy tëb di dal, lu bon lu ne ñu koy yakk Xadafi, naan moom it yal na gaaw dee ndax nu féex ! 

Kon, maak Aminata su nu bindee La gloire des imposteurs,loolu xewoon ca Mali, xewoon ca Kodiwaar ak ca Libi moo ko waral. Danoo bëggoon a yee nit ñi ci tóoxidóoni yi Frãs di sooke ci sunu réew yi ngir aakimoo sunu alal ak sunu koom-koom.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj