USMAAN SONKO “ BÉG” NA CI TUKKEEM BI MU AMAL FA SIIN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, fésal na mbégteem ci tukki bi mu tukki fa réewum Siin. Pekeŋ la ko waxee, di gëblag réew ma. Mbégte moomu, biral na ko ginnaaw bi mu dajee ak naataangoom bii di Liu Qiang (elimaanu jëwriñi Siin ya) ak Njiitu réew ma, Xi Jinping. Moom, Sëñ Usmaan Sonko, xamal na saa-senegaal yi ne, tukkeem boobu, taxawaalu walla tambaabaalu taxu koo jóg te, fileek i fan, dinañ gis njariñ yiy bawoo ci tukkeem boobu fa Siin.

« Mbégte mu réy lanu am ci ndaje yi nu séq ak njiiti Siin yi. (…) Ci bés ak ayu-bés yii di ñëw, saa-senegaal yi dinañu yëg njeexitali tukki bii. » (Kàdduy elimaanu jëwriñ yi ginnaaw bi mu génnee ci Njéndel askan lu ma la nekk Siin – Grand Palais du peuple avec le président chinois)

Ba 10i waxtu jotee la elimaanu jëwriñ yi ak ñi mu àndal àgg fa màkkaanu Njiitu réewum Siin ma. Ba ñu àggee nag, amal na toogaayi liggéeyi. Naataangoom bi, Li Qiang, la jëkk a toogal, ginnaaw gi mu toog ak Njiitu réewu ma Xi Jinping, waxtaan ak moom ci fànnu liggéey.

Moom nag, Sëñ Usmaan Sonko, guléet muy tukki di génn kembaaru Afrig bi ñu ko tabbee ak léegi. Xamle na ne, tukkeem bii fa Siin, dafay firndeel rattaaxu diggante Senegaal ak Siin. Nee na sax, Siin dafa jox gëdda digganteem ak Senegaal. Naka noonu, rafetlu na solos waxtaan yi mu fa séq ak njiit ya. rafetlu naat yéeney saa-siin yi ci liggéey ak njiiti Senegaal ngir jëmmal naaluw Senegaal 2050 wi, di naal wow, moom Nguur gu yees gi tëral ngir suqali koom-koomu réew mi ngir réew mi naat.

« Jaare nanu ci ndajey waxtaan yi ngir yégal elimaanu jëwriñi Siin yi, Li Qiang, ak Njiitu réewum Siin li, ci solos liggéey ak Afrig, rawatina Senegaal. »

Ba tay, bees sukkandikoo ci kàdduy elimaanu jëwriñ yi, demul Siin ak loxoy neen. Nde, daf leen gaaral ay naal yu leer ñeel tolluwaayu réew mi ci fànnu koppar ak liggéey yu bokk-moomeeli ñaari réew yi mën a bokk.

Elimaanu jëwriñ yi xamleet na ne, ci yenn mbir yi, njiiti saa-siin ànd nañu ci, muy lu ci mel ni lënkoo gi war a dox diggante diiwaani yokkute yi. ci fànn woowu, diiwaani Senegaal yi dañuy lënkook yoy Siin yi. Mu am itam yeneen naal yoy, saa-siin yi fas nañu yéene gunge ci Senegaal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj