Usmaan Sonko, njiitul Pastef li, doon na tontu ci laaji Marc Perelman mu France 24. Taskatu xibaar bi laaj na ko juróom-ñaari laaj, mu tontu ci. Jukkees na li gën a bir ci waxi Usmaan Sonko ngir dégtal leen ko.
Maki Sàll yeyoowul njukkal yees koy delloo
” Amul benn njukkal buñ war a delloo Maki Sàll. Ndax, diir bu yàgg bi mu toog bañ leeral mbir mi dafa sabab ay yàqute yu bari fi Senegaal. Bu Njiitu réew mi waxoon lu leer ca njëlbeen ga, na mu ko waxee woon ba mu nuy jaay referàndum ba, ni mu ko bindee ci téereem bi, ni mu ko waxee ciy widewoo yu bari, ne mooy mujjantalug moomeem, tey lii lépp du ñu ci fekk.”
Maki Sàll du demokaraat, diktatëer la
” Du càggan ne Maki Sàll dafa nekk demokaraat moo tax mu dellu ginnaaw. Dafa bàyyi ndax askanam a ko njëkk a takkal pot. Kootoo yi mu laloon yépp ngir fexeel ma àntuwuñu. Askanu Senegaal a taxaw temm, jàmmaarloo ak moom ne ko DÉEDÉET ! Waa àddina si tamit bokk nañ ci sabab yi ko tax a dellu ginnaaw. Am na tamit kalaame yi ñu ko kalaame yépp fa CPI ak yenn kuréli Mbootayu xeet yi.”
” Bu Njiitum réew di jël ay sàmbaa-bóoy (nervis), di leen soqiloo ay fetel ci kow ay way-ñaxtu yu ànd ak loxoy neen, nan lañ ko war tuddee ? Bu Njiitum réew di wañ loxoy Yoon ngir faagaagal kujje gi, taskati xibaar yi, ma-siiwal yi, ñi wuuteek moom xalaat yépp ak gis-gis, te di jàppe rekk ak tëjaate, 700i nit nekk ci kasoy Maki Sàll yi ci sababu pólitig, ñu ngeen bëgg nu woowee ko ko ?”
Maki Sàll daf ma singali
” Maki Sàll mooy nit koo xam ne, ay ati ñoo ngi nii mu singali ma, man ak sama làng. Jumtukaayi Nguur gépp la jëfandikoo, yabal pólis ngir ñu metital ma, jël ay sàmbaa-bóoy, wañ loxoy Yoon. Dal na ci sama kow jëmm, sama njaboot. Ànd ak loolu yépp, mën nanu baale. Te, baale nanu sax ba fàtte.”
Du Maki Sàll moo war a tànn Njiitu réewum Senegaal mi koy wuutu
” Bu dee ci ay pexey Yoon la Maki Sàll namm a jaar ngir tere ma doon lawax, mën naa leen seedeel ne wote du am ci miim réew, walla mu am ci jaxasoo bu kenn dul natt. Noo ngi koy ñaanal mu jeexal moome gii ci jàmm te dem ci xel mu dal, moom ak njabootam. Dafa war a xam ne Senegaal, 17i tamndaret nit ñoo ko bokk. Du moomeelu boppam.”
” Du Maki Sàll moo war a tànn kuy nekki Njiitu réewum Senegaal ginnaawam. Yaakaaruma sax ne mën ci làngam kenn koo xam ne, ñépp a ciy dëppoo ci waa booram.”
Lawax laa ci lu wér
” Amul dara lu may teree bokk. Maa ngi yàkkamti xam ba xam dañuy dem ba sës ci seen pexe yi ñu lal walla.”