LAAJI DÉPITE YI ÑEEL CÀMM GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, ak Càmm gi mu jiite ña nga woon ca Ngomblaan ga, démb ci àjjuma ji, 21i fani féewiryee 2025. Dañu tontuji woon laaji ndawi askan ñeel tolluwaayu réew mi. Loolu nag, dogu 85eel bu Ndeyu sàrtu réew mi moo ko yoonal.

Càmmug Senegaal gu yees gi àddu na ci laaji dépite yi. Démb la elimaanu jëwriñ yi ak yeneen jëwriñi Càmm gi demoon ca Ngomblaan ga. Loolu, yoonu réew mee ko sàrtal, mu bokk ci liy jëmmal demokaraasi. Waayeet, dafay tax askan wi mën a xam fi Nguur giy teg tànkam ak naka lay saytoo ay soxlaam. Moo tax, dépite ya fa teewal askan wi, laaj nañ ay laaj yu aju ci pénc mi te soxal saa-senegaal yi.

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, ci biir i tontoom xamle na ne Càmm gaa ngi ngi waaj a tàmbali ñaareelu jéegob liggéey bi ñeel wàññig njëgu dund gi fi Senegaal. Liggéey bu njëkk bi, weeru suwe 2024 lañu ko amaloon, ba jotoon a wàññi as lëf ci njëgi dund gi. Ci kàdduy Usmaan Sonko mi jiite jëwriñ, Càmm gaa ngi def kéemtalaayu kàttanam ngir jàppandalal askan wi yi gën a aajowoo, ànd ak ne ñu ngi jànkonteel ak i jafe-jafe yu tar ndax tolluwaayu àddina si ci wàllu koom-koom. Usmaan Sonko ñaawlu na tamit doxalinu yenn jéggaanikat yeek jaaykat yiy yokk njëg yi. dige na Càmm gi dina ci def li war.

Ba tay ci wàllu koom-koom, jëwriñu Kopparal geek Nafa gi yégle na ne dina am ay coppite ci càrtug kuubal yi. coppite googu, ciy waxam, dina tax ñuy daggal juuti fànn yu suqaleeku ci wàllu koom-koom. Elimaanu jëwriñ yi xamle na ne dinañu wàññi njëgi dund gi.

Jëwriñu biir réew mi, Sã-Batist Tin, àddu na ci kaaraange réew mi, muy ndogal li mu jël ñeel làmb ji, ndog yiy faral di am ci tali yi, coowal sàmmkat yi ak baykat yi. Bu dee mbirum làmb ji, jëwriñ dafa jëloon fan yii, ndogalu seppi loxoom ci caytug kaaraange gi. Démb, xamle na, ca ngolliiru Ngomblaan ga, ne li ko tax jël ndogal loolee mooy delloosi jàmm, xaar ba dënn yi dal, njabootu làmb gépp toog waxtaan, ñu xool naka lañuy defaree làmb ji. Mbirum ndog yi nag, bees sukkandikoo ciy kàddoom, joxe nañu ay santaane ngir takk-der gën a saytu tali yi. Bu dee li ñeel coowal sàmmkat yi ak baytkat yi, jëwriñu biir réew mi nee na dinañu sumb ay waxtaan diggante sammkat yi ak baykat ngir wut i pexe, ndax ay dëkkandoo lañ.

Ci jotaayu laaj-tontu boobu, mbirum caabalu ëttub cettantal bi yëngal réew mi fan yii moo gën a fës. Nde, dépite yi biral nañ ay laaj ci fànn wi, rawatina ci wàllu Yoon. Jëwriñu Yoon wi, Usmaan Jaañ, moo ci indi ay tontu. Moom jëwriñ ji joxe na kàddoom, wax ne Yoon dina def liggéeyam te, bu ko jaree, yaru Yoon dina dal ci kaw ñi def ay njombe ci koppari askan wi. Nee na dinañu ubbi ag luññutu ngir leeral mbir mi. Ba tay ciy kàddoom, dees na teg ay daan képp ku ci laale te ñu am ci ay firnde yu wér.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj