“LAC DE GUIERS 2” GËNATI NA CÓLLE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbërum Géejawaay mi, Paab Ãsu Siise, ñu gën ko miin ci dàkkentalu “Lac de Guiers 2”, mi ngi jamono ji ci guddi gu lëndëm. Nde, ginnaaw bi ñu ko jàppee ci mbirum njuuj-njaaj ñeel i wiisaa (visas), dañ koy mujje jàllale ca kasob Rëbës.

Démb, ci àjjuma ji, la toppekat bi gàll mbër mo ab “mandat de dépôt”. Moom nag, ay nit ñoo koy tuumaal, wax ne daf dóor seen xaalis ciy naxee-mbaay ñeel ay wiisaa. Ci seen i wax, daf leen a waroon a lijjantil ay wiisaa ñeel Tugal, mu nax leen, lekk seen xaalis te jotuñu ci wiisaa yi.

2022 la mbir mi door, bi ko ay ndaw kalaamejee ca komisariyaa bu Géejawaay. Ci li yéenekaay bii di L’Observateur bind, dóorkatu Waalo bi wuyuji woon na. Booba, dafa joxe woon kàddoom, dige ni dina delloo, ndaw yooyee ko boole woon, seen xaalis.Nee ñu, tàmbali woon na fay laata mu koy dakkal, ginnaaw gi mu seey, réer gaa ñi. 

Weeru sãwiyee 2024 wii weesu la ko benn ñawkat kalaamejiwaat ca Toppekatu Bokkeef bi nekk ca tirbinaalu Pikin-Géejawaay.

Noonu, pólisu Wàqi-Naan-Nimsaat daldi tàmbalee luññutu ci ndigalu Toppekat bi. Waaye, du “Lac de Guierd 2” kese la takk-der yi doon wër. Nde, Paap Ãsu Siise dafa amoon ab bokk-nopp (complice), maanaam ku ko doon jàppale ci njuuj-njaaj yi. Ngóor soosu ngi wuyoo ci turu A. S. Jaañ, di jaaykatu payteef (lejum) ca jawub Njaaréem. Ki koy pelentoon, 3,5 miliyoŋ la ko doon laaj niki ndàmpaay. Waaye nag, ñeneen dañu dolleeku ci mbir mi, wax ne ñoom itam mbër mi daf leen a dóor.

“Lac de Guiers 2” dafa dawoon, génn réew mi. Bi Saa-Cees di bëre ak Ëmma Seen la delsi. Ca la takk-der der yi fekkee këram gi nekk ca “Cité SHS”, daldi koy mbaal.

Moom nag, mbir mi dafa gën a diis ci moom. Ndax, léegi, 17i nit ñoo koy toppee koppar yu tollu ci 53i miliyoŋi FCFA. 

Bees sukkandikoo ci layookatam bii di Me Musaa Saar, njabootu mbër mi fas nañoo yéene fayal ko ngir ñu bàyyi ko. Wax nañu sax ne, Saajo Maane jot na cee joxe 10i miliyoŋ.

Paap Ãsu Saane, di “Lac de Guiers 2”, fanaan na guddeem gu njëkk ca, démb ci àjjuma ji.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj