LÀMBI GOLO-O ! KU JÓG SAAGA ! (PAAP AALI JÀLLO)

Yeneen i xët

Aji bind ji

  • [MAN LAÑUY BAÑ A GIS NDAX NEE ÑU DAMAY WAX. DINAA WÉY DI WAX…]

Njoolum-golo miy def yëfi goloom, ku ci yéemu dangay door a yeewu, mbaa nga doon ku mësta yeeru. Ñu baree ngiy coow ci mbirum Mustafaa Siise Lóo, di naqarlook a ñaawlu saaga yu bon yim saaga Yaaxam Mbay ak Farba Ngom. Réew mépp a ngi ciy yéy ak a yàbbi, rajo yeek tele yi, foo jàpp, Siise Lóo fii, Siise Lóo fee… Mu mel ni, ci miim réew, ameesul i ponk yu gën a faaydayu, ëpp solook njariñ te gën a jamp waxi kasaw-kasaw yile. Nun, nag, bu nu yattee sunub xalima di ci wax, du caagéeni dañuy wéy ci li nit ñiy coow. Déedéet ! Dafa di, réew mi, bare nay « Siise Lóo » yiy dox seen i soxla, di gundaandaat, am sañ-sañ ci fànn yu bare, te kenn waxu leen. Te sax, nguur gii fi ne, bu yeboo ne ay « Siise Lóo » kese ñoo ko séq, Mustafaa da cee gën a fés rekk.

[RAXAS BOPPU GOLO, YÀQ SAABU LA]

Nguurug Maki Sàll gi, mel na ni goloo leen jigadi. Doxalinu golo, waxi golo, jàppe nit ñiy golo. Bu Mustafaa Siise Lóo boyalatee gémmiñ gi, yàbbiy xal yiy jafal i nopp ak i xol, wareesu cee waaru. Dafa di, ngóor si, ci pacc-pacci la dëkk. Te, saa bu ŋaaŋee, boroom kersa yi fatt seen i nopp ndax tooke yiy balle ci gémmiñ gi. Kon, lu fi jar coow li ? Ñàkk yar ak ñàkk worma bi ci moom, du lu bees.

Moone, saaga na fi ñu bare, rawatina Usmaan Sonko, kenn coowul. Tey, mu saaga 2i àndandoo Maki Sàll, njiitu réew mi, ñu bëgg cee yóbbaale réew mépp. Fu yoon nekkoon bi muy saaga doomi jaambur yi ? Ndax léegi, ci miim reéw, dafa am ñu gënle juddu ? Maanaam, dafa am Kumba am ndey ak Kumba amul ndey, ba tax mu am ñu sañ a saaga ay gor, diy doomi gor, te dara du leen ci fekk, te buñ saagaa kenn ci àndandooy buur ñu ne , ayca, na ko yoon teg loxo ?

Waaye, golo gi dëkk Ndar ak golo gi dëkk Ndakaaroo yem, goo ci bett dóor kob yar, xel ma ci yéeg rekk lay nekk. Wax ji, wax ji, ki saaga ak ñi mu saaga ñoo yem kepp ; Sàmbaay Bàcc. Boroomir yu dul i saagër, ci ndab lu dër rekk lañuy lekk, niy gone yu matadi. Ndege, nees amey magi 15 walla 20i at, noonu lees ame goney 50, 60 walla 70i at. Làmbi golo, nag, ku jóg daanu, golo yaa ko moom. Bu ko defee, nan leen bàyyi ak seen làmb, te wax ci kàmb giñ nuy gasal. Nde, raxas boppu golo, yàq saabu la.

[BILDIŋ BEEK XAALIS BI ÑU SÀCC… ]

Naam, mag mu yaradiku te ñaaw làmmiñ, warees na la jàjj, gàgganti la ngir aar xale ak ndaw yi lay déglu. Waaye, bu dee li ñeel kàdduy Mustafaa Siise Lóo yi, li ci ginnaaw a nu war a yitteel dëgg-dëgg. Ndax, wëlis saaga yi, dafa dóoral ñenn ci waa nguur gi ak i jawriñ, jiiñ leen càcc ak ger. Dafa sulliwaaley njombe ak i njuuj-njaaj yees xawoon a fàtte.

Dëgg la, am na ñu ci wax ba mar, ñu ci mel ni dipite Mamadu Lamin Jàllo, njiital Tekki, ak Usmaan Sonko, njiital Pastef. Waaw, am ñu ci xeex, amal ciy doxi-ñaxtu ba ñu tëj leen ci kaso, rawatina Gii Maryiis Saaña. Wànte, kàdduy Mustafaa Siise Lóo yi dañuy gën jox mbir mi dayo, dëggal njombeek njaaxum yi nguur gi dëkke, ndax kàngam la ci seen biir i kàngam, xam lu bare. Bu ko defee, warees na am ci waxam ji meneen njàngat walla beneen gis-gis.

Ci biir i waxam, Mustafaa Siise Lóo dafa jibal i jombe ak i càcc ñeel saxaarug TER gi ak yeesalug bildiŋu jawriñ yi. Waxaale na yit ci càccug suuf si ak jiwu yi. Te, mbir mu ci nekk doy naw njombe, tollu ci milyaari milyaar. Te, toppekat (porokirëer) bu mag bi waxu ci sax, ndeysaan !

Mustafaa Siise Lóo jëkk ne :

« … bildiŋ beek xaalis bi ñu sàcc ak… ».

Mu nuy fàttali, di dëggal li fi ñenn ñi doon kaas ay weer ci ginnaaw ñeel naalub yeesal bildiŋu jawriñ yi. Waaye, li njaaxum yiy tegaloo boob ba léegi, bu feeñ tey, beneen tegu ci ëllëg, moo tax askan wi xaw a miis lu ni mel, ba di ko xaw a fàtte. Li xew ci bildiŋu jawriñ yi dafa jéggi dayo.

2014, Mamadu Lamin Jàllo waxoon na ci, yuuxu fu nekk, dara. Jamono jooju, Abdu Latif Kulibali mi nekkoon fara-caytu nguur gi, dafa génne woon nab yégle ci bésub 4eel ci oktoobar, yéenekaay yépp biraloon ko. Mu waxoon ci ne, naalub yeesal bildiŋu jawriñ yi, 17i miliyaar kese lay dikke réew mi. Ci ginnaaw gi, gaa ñi fexe nañ ba soppi déggob naal bi, dugal ciy ndëgg-sërëx yu bare, daldi ful njëg li. Li waroon a jar 17i milyaar, ñu dolli ci 23i milyaar cib njuuj-njaaj bu bir, ngir féetewoo ko. Mamadu Lamin Jàllo ne woon ci xëtu facebookam, 28eelu fan ci weeru ut 2018, ne xaalis bi romb na liñ nu wax. Tey, Mustafaa Siise Lóo dëggal na ko. Ndax, toppekat bii di Basiiru Géy, dina ci wax ?

Ci beneen boor, Mustafa Siise Lóo laalaale na saxaarug TER gi, wax càcc gu réy gi ko lal. Loolu yit, dipite Usmaan Sonko, way-moomeel yi ak boroomi xam-xam yu bare wax nañ ci ba toqi te mujjul fenn.  

Ngóor si Lóo waxati ci suuf seek mbey mi, duut baaraam paaco bi ci am ak li waa nguur giy aakimoo jiwu yi bay lor beykat yi ko yeyoo. Nu bàyyi ko mu waxal boppam, nettali ci làmmiñu boroom la dàqe :

« …lekk-katu ribaa bim [Farba Ngom] doon. Suufu Ndakaaru yépp dagg na ko jaay. Farba Ngom miy wax, dañ ko jox gerte, mu jaay ko Mustafaa Ñas, Séex Sekk… Ayméeru, jabaram jox nañ ko 40i ton. Mataar Jóob mu gàtt moomu nga xam ne moom lay àndal, am 100i ton, jaay ko. Maysa Sele Njaay, jox nañ ko 70i ton, jox Sele ma nekk fële 10i ton. Yow [Yaaxam Mbay] joxuñu la, wax naa la ko… »

Lii di mel ni toŋ-toŋu bukki. Beykat yiy jooy ndax tumurànke, mbënd mi ame kow gi, ndóol gi ne fa faax, beyuñu, dunduñu. As tuut ciy nit, kootoo, di paacoo alalu askan wi, Basiiru Géy, toppekat bi, ne cell. Waaw, fu nu jëm ak ñii ?

Ñuy wax, ñuy soppi mbir mi politig, yenn ci yéenekaay yi, tele yeek rajo yi di réeral askan wi, di yóbbu wax ji fim jëmul.

Ca ëllëg sa, Mustafaa Siise Lóo gedd, ne dootul Tof-Njiitu péncum réew mi. Nu ni déet-a-waay, ñu dàq Ngóor APR. Siise Lóo xéy, boyalaat gémmiñ gi, delloo buum ca boy-boy ga. Yaaxam Mbay kalaameji ko yoon, nit ñiy coow, naan APR ci tas la jëm walla nasax ni PDS. Waaye, askan wi, yoonam warul nekk ci loolu. Coowal APR, na yem biir APR. Nan ba waxu làng gi te wax ci gaal gi. Ndaxte, Siise Lóo dafa waxati ci moomeelu gaal gi ñuy randal. Nu déglooti ko :

« …Mi ngi ànd ak Galo Ba miy sàcc xaalis bi di ko tabax [tabaxe] ay tabax, muy Galo Ba moomu… Beneen bi mooy, jawriñ yi li ñuy def bés bu nekk. Ay […] rekk lañuy jox ay 100i milyoŋ, 10i milyoŋ. Fan lañuy jële xaalis bi ? DRP yi ñuy def…, ñoo ngi koy jox […] yi… Mataar Jóob mu gàtt moomu, daaw rekk 200i ton [i gerte la jëloon]. »

Te yow, Basiiru Géy Toppekat bi, nga ne doo wax ci lii ? Saaga yi ak ñi leen génne ngay lijjanti daal, bàyyi njombe yu réy yile. Waxoon nan ci kow ne Mustafaa Siise Lóo ci saaga la dëkk, kon lu tax ñu bëgg ko koo toppe tey ? Mu mel ne, moom, am na ci tontu. Nan leen ko joxaat kàddu gi :

« Man lañuy bañ a gis ndax nee nañu damay wax. Dinaa wéy di wax ba mu neex ma…Li ñu fi sàcc… Jawriñu njaay meek njënd mi di bey di jaay mook waa UNACOIS. Fan lañ ko teg ? Ñu demati jël màrse ceeb bi, Mañsuur Fay jox ko ñoo xam ne duñuy jaaykat, ndax dañ leen di neexal, ngeen bëgg ma noppi… »

Ñiy layal njiitu réew mi, war nañu xam ne lépp moom rekk la. Ndaxte, moom ci boppam, waxagul askan wi ñaata la yor ci alal ba ñu xam ndax 8i milyaar ya mu waxoon ca 2012 yokku nañ am déet. Gis nañ taxawaayam ci njegeñaaleem yiy sàcc te mu leen di làq. Jéemul saafara benn yoon càcc, njuuj-njaaj ak ger gi jawriñ yi saxoo. Mooy magu réew mi, jiite gaal gi. Moo leen may fit. Wolof ne, golo ñaawul, baay ba la niru. Bu seetaanee ba gaal gi mu jiite diig, dina lab, moom ak ñi mu àndal. Nde, askan wi sës na. Nes-tuut ñu def ni askanu Mali. Maki na jël i matuwaayam, joyyanti nguur gi. Ndege, mag du fecc “Yàlla naa dee”.

Li njoolum-golo mi wax, day gën a feeñal li am ci miim réew, mooy golo bey, baabun dunde. Maki ànd ak njabootu goloom, ñuy jiiroo alalu réew mi, def kob tool, di ko roosee ñaqi baadoolo yi. Waaye, toolu golo du meññ.

Paap Aali Jàllo

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj