Beykati Ndengleer yi, ab dëkk bu féete ci bokk-moomeelu Njagañaaw, ñooy jiiñ Baabakar Ngom, boroom SEDIMA, ne da leen a jaay doole, nangu seen i tool. Jamono jii, nag, wax ji bare na ba mel ne tulleek-màlle. Réew mépp, ci mbir mi lañuy yéy ak a yàbbi. Seen yéenekaay LU DEFU WAXU def ci gëstu gu ndaw ngir indi ay leeral ci ni mbir mi deme, ca ndoorteel la ba nëgëni-sii.
« NUN KAT, BOKKUNU CI ÑIY JAAY SEEN SUUF… »
Lépp a ngi door ci atum 2012, keroog bi Baabakar Ngom demee ca bokk-moomeelu Sinjaa, jébbal leen ab naalub bey-liggéey. Ca la ndajem tundu Sinjaa gisee, jibal kob fénc, daldi ko ciy jagleel 300i ektaari suuf ca Jilaax. Dëkk boobee, nag, di Jilaax, ci bokk-moomeelu Njagañaaw la bokkoon laata nees di ko féetale ci bokk-moomeelu Sinjaa. 300i ektaari suuf yees jagleel Baabakar Ngom, daf cee am wàll wu féete Njagañaaw, di tooli beykati Ndengleer yi. Baabakar Ngom ne, ca njëlbéen ga, xamul woon ne 300i ektaar yi laalaale nañ ay tooli jaambur. Bim ko yëgee, dafa ànd ak Xaadim Sàmb, géwél biy wax ci làmb ji te nekk RTS, seeti waa Ndengleer.
Bi mu àggee, mu ne leen :
« Dañ ma jox suuf soo xam ne, dafa ëmbaale seen i tool. Ma bëggoon, nag, nu waxtaan, booloo, ànd liggéey. Bu ko defee, dinaa leen fi defal raŋ-raŋ, fexe ba mbëj mi agsi fi, gasal leen i teen, tabaxal leen ay daara, añs. »
Bi mu noppee ci digeem yi, waa Ndengleer ne ko :
« Nun, kat, bokkunook ñiy jaay seen suuf. Ndaxte, ginnaaw Yàlla, sunu tool yii lanu yaakaar, di ci bey li nuy dunde. Moo tax, xalaatun leen a jaay, mukk ! »
Bi mu déggee loolu, Baabakar Ngom tàllal leen 2i miliyoŋ ci sunuy koppar, ne leen njëgu guro doŋŋ la. Waaye, dañ ko gàntal ; am ci magi Ndengleer yi ku ko ci ne :
« Nun, kat, mësunoo gis guro guy jar 2i miliyoŋ. Te, xaalis boobu, ñay yalwaan ca selebey Kolobaan gaa nu ko gën a yeyoo. »
Ca la Baabakar Ngom deme. Beykat yi jàpp ni mbir mi fa lay yem.
”LU JIIN, NJAAG A TE MAKI MOOY NJAAG, BAABAKAR NGOM DEFUL DARA”
Ndekete, ngóor si Baabakar Ngom, dafa jaar ci suuf, fexe ba njiitu réew mi, Maki Sàll, xaatimal kob dekkare, jagleel ko ci 225i ektaar. 75i ektaar yi ci desoon te méngook tooli beykati Ndengleer yi, da doon xaar ñu jibal fénc yees ci doon def. Waa kadastar itam, dañ ne woon bees sukkandikoo ci dekkare bi,225i ektaar kese ñoo desoon ci 300 yiñ waxoon. Ànd ak loolu lépp, Baabakar Ngom fexe na ba am kayit gu koy tax a moom suuf sépp ak tooli beykat yi. Beykat yi, ñoom, yéguñu, tinuñu.
Bi waa Ndengleer beyee ba noppi, daldi góob ngir yóbbu, Baabakar Ngom yabal fay ndaw yu gànnaayu. Ñu dàq malay beykat yi, foqati lépp li nu góoboon, téye ko ci diirub 3i fan. Bi ñu waxtaanee, waxtaanaat, la beykat yi jotaat ci seen i ngóob. Bi loolu weesoo, saa bu waa Ndengleer waxee, bëgg a delsi ci seen i tool, mu woo sàndarma yi. Am na sax ñuñ jot a jàpp ci ndawi Ndengleer yi. Bi cooroonu ren jii jotee, nag, ci la beykat yi jógati ngir ruuji seen i tool, waajal nawet bi. Bi ñu demee, dañ faa fekk ay ndaw yu gànnaayu, am sax ku ci yor fetal. Bi loolu amee, 15i dëkk yi nekk biir Sàndog booloo, ànd ak ay way-moomeel, ay politiseŋ ak i maxejj yi mbir mi naqadi, fas yéenee jaamaarlooji ak ndawi Baabakar Ngom yi. Waaye, Yàllaa ci def sutura ba deret tuuruwul, bakkan rotul.
Basiiru Jomay Fay mi bokk PASTEEF te cosaanoo Ndengler di naqarlu mbir meek a jooytu fu nekk, ci tele yi, rajo yi ak anternet bi. Moom, nee na, li ko jaaxal mooy, naka la nit mën a fekkee ay beykat, àbb leen seen suuf ñu bañ, mu jéem leen a ger, ñu bañ, xéy rekk am kayit gu koy moomale suuf soosee ?
Mustafa Jaxate, moom, njiitu réew mi ci boppam, Maki Sàll, la joxoñ baaraamu tuuma. Dafa ne :
« Lu jiin, Njaag a, te Maki mooy Njaag. Baabakar Ngom deful dara. »
Fi mu teg waxam ji, mooy ne, dekkareb 2015-548 bu 23eelu fan ci weeru awril 2015 biy jagleel ay ektaari suuf yu bare ci suufi réew mi kii di Baabakar Ngom, teguwul ci yoon. Mu ne, Maki dafa jalgati yoon ci lu bir. Ndaxte, dogalam bi dafa safaanoo ak àtteb 64-46 bu 17eelu fan ci sulet 1964 bi aju ci suufi réew mi.
Rax-ci-dolli, biralees na ci 8eelu dogal ñeel àtte bees wax léegi, ne :
« Jaglees na moomeelu suufi réew mi way-bokki mbooloo kaw yi. Ñooñu rekk a am sañ-sañu jëfandikoo leen, liggéey ci, ci wattub nguur gi ak li dëppook yoon. »
Lees mën a jàngat ci àtte bile, mooy ne :
« AM NAA LU MA METTI LOOL, NDAX ÑOO NGI YÀQ SAMA DER DI MA JIIÑ LU MA DEFUL. »
Coow li ne kurr, nag. Baabakar Ngom jàppal fii, SEDIMA bàyyil fee. Ñuy yakk ngóor si lu mel ne xeme. Xolu doom ju jigéen ji jeex, mu daldi naqarlu mbir mi ci xëtu Facebookam, ne ci :
« Amul lu SEDIMA deful ngir dimmali askanu Senegaal ak jëme réew mi kanam. Waaye, ànd ak loolu lépp, am nay nit yu laxasaayoo lëndëm, di wër tele yeek rajo yi ngir yàq deru Baabakar Ngom. »
Ginnaaw bi mu ñaawloo coow li ba noppi, dafa jéem a layal baay bi, di leeralaat cosaanu mbir mi. Ci la wax ne :
« Ndajem tund bu Sinjaa moo ko [Baabakar Ngom] jagleel 300i ektaar… Nu awale mbir mi yoon ba jot kayit gi nuy moomale 224i ektaar, ànd ak dekkare bu njiitu réew mi xaatim ci atum 2019 ci turu SEDIMA. Bu dee 76i ektaar yi des, nag, doonte sax am nan ab fénc bu koy jagleel SEDIMA, ñu ngi nekk ci njeexitalu Jilaax, ay beykati am fay tool, di leen bey. »
Kon, ndaw si biral na ne, beykat yaa ngi daan bey suuf si. Te, ku xam ni kow gi tëdde, war a xam ne beykat yi yàgg nañoo bey foofu.
Meeru Njagañaaw bi, Gànna Ñing, bindoon na bataaxal perefe Mbuur ba woon, Sayeer Ndaw, ngir mu jubbanti njuumte li bokk-moomeelug Sinjaa gi fénc ci suuf su mu moomul. Waaye, perefe bi tontuwu ko te yit waxul dara ci mbir mi.
Fan yii weesu rekk, bi beykat yi demee ruuji seen i tool ci jamonoy cooroon li, dañ faa fekk ay ndaw yu gànnaayu, ñooñu tere leen a jéggi ngaareew (canal) mi fa SEDIMA gaslu woon. Waa dëkk bi génne ay jaasi ak i sémmiñ. Moom kay, musiba bu réy a naroon a am. Ndax, tuuti kon ay bakkan rot ci. Bi nataal yeek widewo yi koy wone tasee ci lëkkooy-nawle yi (whatsapp, facebook, twitter añs.), ci la njiiti caytu yi jógee ngir dox tànki jàmm diggante beykati Ndengleer yi ak Baabakar Ngom.
Meeru Njagañaaw bi, Gànna Ñing, dafa mujjee bindaat perefe Mbuur bu bees bi, Moor Taala Tin, ngir mu woote waxtaan.
Ca njëlbéen ga, Baabakar Ngom dafa bëggoon a waxaale ak beykat yi, ñooñu lànk ne du ci dal. Ci lañ ko waxe ne, bu waxtaan dee am, ca dalub perefe bu Mbuur bi lay ame, te ña ko séq ñépp ay teew, rawatina ña ko jagleel féncub 300i ektaar bi ko yombalal kayitu-suuf gi mu yor.
Ci fan yii weesu, Baabakar Ngom daje na ak genn batale gu waa Ndengleer yabaloon te Galgor Jonn, bokk ci magi Ndengleer yi, jiite ko. Ñii ñoo fa teewoon : njiitu caytug lempo gu Mbuur gi, Basiiru Jomay Fay, njiitu kadastar bi ak DSCOS, ki jiite way-yëdduy Mbuur yi, kàppiten bi jiite sàndarmëri bu Mbuur ak yeneeni kilifa. Waxtaan waa nga doore cib fàttali bu gàtt ñeel cosaanu coow li ak li ko waral. Biralees na fa ne, bokk-moomeelug Sinjaa dafa jalgati yoon, ndax daa fénc suufu bokk-moomeelu Njagañaaw. Ki fa teewaloon kadastar bi ne, yoon wi Baabakar Ngom jaar ba am kayit gu koy jagleel suuf si, amul benn lënt-lënt. Mu teg ci ne, ñoom, ci fénc bi bokk-moomeelug Sinjaa bi joxe lañ sukkandiku woon. Wànte, Basiiru Jomay Fay daf koo tontu ci saa si, ne ko :
« Yéen kay ! Jalgati ngeen yoon, ndax gëstuwu leen ba xam dëgg-dëgg fi suuf si féete ak ñan ñooy boroom. »
Bi Baabakar Ngom jëlee kàddu gi, dafa ne :
« Am naa lu ma metti lool ndax ñoo ngi yàq sama der, di ma jiiñ lu ma deful. »
Mu ñaawlu yit, ciy waxam, li ko ñenn ñiy waxal, ba tax askan wi jàppe ko ab gerkat, ne :
« Mësumaa xalaat a ger kenn ci sama àddina. Waaye, tey, fépp foo dem ci lëkkooy-nawle yeek yéenekaay yi, ab gerkat bu mag lees may jàppe. »
Kii di Moor Taala Tin, perefe Mbuur bi, moom, dafa jëkk a wax beykat yi ne amul sañ-sañu fomm ab kayitu-suuf goo xam ne, dekkareb njiitu réew a ko sàrtal. Waaye, dina def kem-kàttanam ngir lijjanti mbir mi ci jàmm, jubale ñépp.
Bu dee ci wàllu beykat yi moom, ñoom, nee ñu menn pexe rekk a fi sës ngir jàmm am, te mooy ñu delloo leen seen i tool. Ñu teg ci ne nawet baa ngiy jubsi te dinañ bey seen i tool ci nii mbaa ci naa, tool yi mbaa xeex ba dee rekk. Ñu joxoñ baaraamu tuuma Baabakar Ngom, ne ko lépp lu mënti xew ëllëg, moo ko sabab.
Bi Perefe Moor Taala Tin demee ba xam ne mbir mi cóol na, dafa walbatiku ne Baabakar Ngom :
« Dégg nga li beykat yi wax. Ci guta lan nekk. Léegi, man dama lay ñaan nga bàyyee leen seen i tool. Ndaxte, dinga dese suuf su bare soo mën a liggéey ngir jëmmal sab naal. Nde, tool yi, ci 75 ektaar kese lañ tollu. »
Baabakar Ngom ne ko :
« Man, fi mu nekk nii, jiiteetuma SEDIMA. Waaye dinaa wax ak ki ko jiite – doom ju jigéen ji – soog a àgge perefe bi liy rote ci waxtaan woowule. »
Ci lañ tàggoo.
Abdu Karim Fofana, jawriñu taaxin bi ak nekkin wi xamle na, ci rajo RFM, ne dina dox ay jéego ngir jubale Baabakar Ngom ak beykati Ndengleer yi. Nee na dina dalal beykat yi, déglu leen laata muy dalal Baabakar Ngom ngir déglu ko moom it. Abdu Karim Fofana ne, li ko gën a yitteel mooy sàmm àqi askan wi ci suufi réew mi. Waaye, nag, loolu tekkiwul ne dees na tere liggéeykat yi ñu liggéey ci suuf si bu leen ko yoon mayee.
Bu loolu lépp weesoo, Baabakar Ngom xamle na dina dajeek taskati xibaari réew mépp ëllëg ci alxemes ji 9eelu fan ci weeru Sulet 2020. Ñu baree ngi naan dafa nar a delloo beykati Ndengleer yi seen suuf.
Ak lu ci mënti am, coowal suuf yi bare nañ lool ci Senegaal. Te, mbir maa ngiy bëgg a ëppi loxo. Liy raam, nag, ci ñag bi la jëm.
Paap Aali Jàllo