Njiitu réew mi ubbee na tënub Lat-Joor Ngóone Latiir Jóob, jàmbaar ji ñaawul. Fa Cees la tënu jàmbaar ji nekk, muy tabax bob, day jëmmal ak a màndargaal jàmbaaru réew mi, Dammel ba jàmmaarloo woon ak nootkat ba woon ba ni muy daanoo ci toolu xare ba.
Lat-Joor du kees di fàtte. Mukk ! Dammelu Kayoor ba, bañkat ba daan xeex ak way-mbéeféer ya, dees na ko sargal, di ko fàttaliku ngir di roy ci moom. Loolu la Njiitu réew mi xam ba tax ko ubbee tay, ci alxames ji, ab tën bees ko jagleel, fa Cees.
Tabaxug tënu Lat-Joor nag, xalaatu ndawi meeri bu Cees la. Moo tax, bi Njiitu réew mi jëlee kàddu gi ca xewum kaajar ga, mu daldi rafetlu xalaat bi. Daf ne :
« Lat-Joor jëmm ju ràññeeku la ci biir jàmbaari réew mi, di jàmbaar bob, xeex bi mu doon xeex nootaange dina wéy di des ci mboorum askan wi. »
Lat-Joor, Dammelu Kayoor ba, bañ lañu ko xamee woon, daan xare ak way-mbéeféeri Farãs ya. Te, jamono jooja, ay ngànnaay yu néew la yoroon, moom ak i sóobare yi àndoon ak moom ci xare yi, daan xeex ak làrme tubaab bi leen ëppale woon fuuf i ngànnaay. Booba, tubaab yi dañu bëggoon a toŋ-toŋe Afrig, séddoo suuf si. Fi Senegaal, ay jàmbaar taxaw temm, gàlloo seen ngor, xeexal seen maas ya ñu jamononteel, xeexal maasu tay jii ak yiy ñëwi ëllëg. Nde, bu Senegaal moomee boppam tay ba àddina sépp nangul ko ko, Lat-Joor ak yeneen jàmbaar yi am nañu ci cër bu réy a réy. Ndaxte, ku mel ni Lat-Joor, dafa jaay bakkanam ngir doomi Senegaal moom seen bopp.
Lat-Joor nag, Dammel la woon, maanaam buuru Kayoor ga woon, di xaw a méngoo tay ak diiwaanu Cees. Kon, bu ñu sampee tën bees koy sargalee fa Cees, dafay doon lu jaadu. Dafa di, ca ngér (avenue) mees ko duppee la tën bi nekk.
Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, fàttali na bañ bi Lat-Joor bañaloon tubaab bi. Ndax, Lat-Joor mësul a waxaale moomeelu réew mi, mësul a tayle askanam, mësul a jaay ngoram di ko jënde dara luy jóge ci tubaab bi. Moo tax it, bi tubaab bi nammee rëdd ay raay yu waroon a jaar Kayoor, mu lànk ne du ci dal. Mu takku taxaw, xeex ak noon bi ba ni muy daanoo ci toolu xare bi, fa Déxële. Looloo tax Njiitu réew mi wax ne, deewug Lat-Joor day màndargaal bàkkub sóobare yi : « dees na nu rey, waaye deesu nu toroxal ». Maanaam, dee ci ngor moo ko gënaloon di dund ci njaam. Muy njàngale mu réy ci nun.
Xewum kaajar gi xumboon na lool. Ndax, amoon na ay waykat, ay tiyaatarkat ak i taalifkat yu fa jëmmal jaloorey Lat-Joor ak jaloore yeneen jàmbaar yi bokk ci mboorum Senegaal. Njiitu réew mi neeti, « ngir tabax aw askan, dees na saxal bakkan yu ràññeeku yooyile. » Moo tax muy woo ndaw ñi, di leen xirtal ci mbaaxi jàmbaar yooyu, ñu def leen i royukaay.
Wëliis Lat-Joor, sargalees na fa yeneen i jàmbaar yu daan xeex nootaange niki Kaañ Fay. Ci biir i kàddoom, Njiitu réew mi biral solo si nekk ci fàttaliku bi aw askan di fàttaliku ay jàmbaaram ngir tabax ëllëgam.
Ginnaaw tën yees leen mën a tabaxal di leen leen xoolee, warees na tuddee jàmbaar yi ay béréb, ay mbedd, ay ngér, di jàngale seen i jaar-jaar ci daara yi, di amal i xew-xew yi leen di dundal ci xel yi ak xol yi.