Àttekat bi daan na Usmaan Sonko ñaari weer yum dul tëdd kaso ak 200i tamndaret yu mu war dàmpe Maam Mbay Ñaŋ. Bu dee jëwriñu wërteef gi teewoon na ca àttewaay ba, njiitul kujje gi, Usmaan Sonko, teewewu ko.
Bi daan bi jibee, ñu bari dañ doon laaj ndax dina mën a bokk ci wotey 2024 yi walla. Bees sukkandikoo ciy layookatam, daan bi du ko tere bokk ci wotey 2024 yi. Waaye, laaj bi waroon kay, du ndax Usmaan Sonko dina bokk am déet. Lees war laaj mooy ndax ni àtte bi tëdde jaar na yoon walla déet.
layookati Sonko sax dañ génnoon néegu àttewaay ba ngir diisoo seen biir. Nee ñu sax, mbir mi, àtte nañ bu yàgg. Mbir yu bari firndeel nañ ko. Démb, ci guddi gi, la xibaar rotoon ne, kenn ci layookatam, Me Useynu Faal, dañ ko ajandi. Kurélu layookat yee ko daan ginnaaw bi ko àttekat bi Paap Muhamet Jóob pelentee. Dafa di, Paap Muhamet Jóob moomu waroon a àtte layoo bi sax, dafa mujje bàyyi. Usmaan Sonko ak i layookatam dañ bañoon mu àtte layoo bi ngir jege bim jege Maki Sàll ak njabootam. Mamadu Yaaxam Keytaa ko wuutu.
Rax-ci-dolli, layookatu Usmaan Sonko bii di Juan Branco, dañ ko waññi, yab ko cib ropplaan. Yeneen layookati njiitul Pastef li nee nañu, kenn xamagul fuñ yóbbu layookatu Farãs bi. Te, jamono jooju, bàyyi nañu beneen layookatu tubaab bu Maam Mbay Ñaŋ, mu ñëw ci jàmm, dem àttewaay ba.
Dafa di sax, Biraayim Sekk ak Keledoor Seen ñi waroon a seede, bàyyiwuñ leen ñu seede. Keledoor Seen leeral na ci Walf ne, indi woon nay këyit yiy firndeel tuuma yees gàll ci kow Maam Mbay Ñaŋ.
Noo ngi jot xibaar ne, fi mu nekk nii, xeex baa ngi door ci yenn bérébi Ndakaaru.