Àtte ba jib na. Àttekat bi jox na Kàmpiten Ture dëgg. Nde, dafa daan Séex Yerim Sekk ak boroom këru móolukaay gii di Éditions Harmattan juróom-benni weeri kaso yuñ dul tëdd. Waaye, yemu ça. Ndax, ngir far tooñ bi ñu tooñ Kàppiten Ture, àttekat bi daf leen a gàll ndàmpaayu juróomi miliyoŋ yu ñu war jox sàndarm ba woon.