LAYOOB SONKO-MBAY ÑAŊ : XEEX BI DOOR NA !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ñetti biisi Dakar Dem Dikk yu tàkk ca Petersen, AUCHAN Mermoos tàkk jëppeet, ay bérébi liggéey yu tëj, dem yombatul, dikk amatul ci péeyub réew mi. Ndaw ñeek takk-der yaa ngiy xeex xeex bu metti jamono jii.

Li xamb taal bi mooy li waa BIP toj oto Usmaan Sonko, jaay ko doole, génne ko, jàpp ko. Njiitul Pastef li dafa waroon a wuyuji Yoon ñeel layoom beek Maam Mbay Ñaŋ. Jamono jii nag, xale yaa ngi génn fu nekk ci Ndakaaru di taal i póno ak a sàndiy xeer. Am nay xibaar yuy wax ni sax waa Mbuur ak waa Sigicoor sóobu nañ ci cóoki bi.

Nee ñu, am na ci sàndarm bu ci ame gaañu-gaañu. Fi mu nekk nii, ndaw ñi fatt nañ yoon wi jëm « Palais de justice ».

Ca Medinaa, am nay “nervis” APR yu yor ay jaasi di xeex ak askan wa. Tele Walfadjiri moo fésal xibaar bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj