LÉEGI, GAYNDE, KUB LAY DUNDE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal amati na ndam. Gaynde yu ndaw yi ñoo jël CHAN 2023 bi doon ame ca réewum Alséri mi ñoo dóor démb ci finaal bi. Bi ñu àggee ci teg-dóor  yi la Senegaal jël raw-gàddu gi foofa ca estaad Nelson Màndelaa bu Alse, péeyub Alséri. Guléet nag, Senegaal di jël kubu CHAN bi.

Ñépp a doon xaarandi joŋante bi, yàkkamti woon ko lool. Nde, Senegaal ak Alséri ñoo gënoon a fés ci CHAN 2023 bi. Rax-ci-dolli, joŋanteb démb bi daf nuy fàttali finaalu CAN 2019 ba, diggante Alséri ak Senegaal te Alséri mujje woon ko jël. Kon, gaydne yu ndaw dañu amoon sas, waroon a fayul seen i mag, fayul réew mépp. Doonul woon lu yomb nag. Ndaxte, ca réewum Alséri ci boppam la joŋante bi ame. Ca teel la Saa-Alséri yi feesal estaad bi, ñëw ngir jàppale seen ekib. Waaye, Saa-Senegaal yi, donte bariwuñ woon noon yépp, ñoom itam ña nga fa woon, ak raayab Senegaal, ngir gunge gaynde yu ndaw yi.

Dañu ne bérét, wurekati Alséri yi wutali kãwi Senegaal yi. Jot nañ faa am ñaari korneer (ci 3eelu simili bi ak 5eelu simili bi), waaye mujjul fenn. Saa bu gaynde yi yoraan bal bi, Saa-Alséri yi di leen yuuxoo. Waaye, loolu yëngalu leen. Wànte dañu xamul ni, ngooxi mbott du tee gaynde naan cib déeg. Moo tax, ñu ànd ak seen sago, di mbél lu leer ni midi. Ci 8eelu simili bi sax am nañ korneer donte dugaluñ ko. Saa-Alséri bi, Bakir, moo fa njëkk a dóoor ab baal, waaye ci kow caaxi góolu Senegaal bi la aw.

Wurekati Alséri yee ëppoon li ñu yor bal bi ci ndoorteelu joŋante bi. Bare woon na tamit ay gaañante. Moo tax, ci 15eelu simili bi, Sidibe am kartõ. Ci 23eelu simili bi, Kamara ak Meziane xaw nañ fa jàppante, arbit bi kartõ leen ñoom ñaar yépp. 1 simili lees ci teg Senegaal nar a toj kër gi. Noonu noonu, ba ni ñuy jeexalee xaaj bu njëkk bi, kenn dugalul sa moroom.

Bi ñu dellusee, Senegaal dafa am ñaari korneer ci ndoorteelu ñaareelu xaaj bi. Ci 50eelu simili bi, Mahious am fa dóor mu dugg, mu dóor ko ci kow defãsëeru Senegaal bi, bal bi génn korneer. Daanak, noonu la joŋante biy deme ba ni mu jeexe ci 90eelu simili bi. Biñ leen dollilee yeneen 30i simili ci nguddal gi tamit, kenn jotul a dugal moroomam. Ñu daldi jàll ci teg-dóor yi ngir mën a àtte ñaari ekib yi. Senegaal daldi dugal 5, Alséri dugal 4. Senegaal daldi nekk sàmpiyõ, guléet.

Ki lee di tàggat, Paap Caw, bokkoon ci gayndey 2002 yi, moom, ñaari mbégte la amandoo. Nde, ginnaaw ndamu gaynde yi, démb a nekkoon bésu juddoom. Muy ñaari mbégte yi ko tax a biral kàddu yii toftalu :

« Maa ngi sant Yàlla, di Ko bàkk. Ci bésub 4 féewaryee lañ jël ndam li, waaye bésub 6 féewaryee lanu koy xumbalee Senegaal ak sunu fans yi. Maa ngi jagleel ndam li nit ku sore ci man, Sosef Koto mi doon tàggatkat ekib bii, te mu gaañu. Lii la doon ñaan. »

Njiitu réew mi jox na gaynde yi ropplaan ngir ñu delsi ci jàmm. Njëwriñu tàggat-yaram gaa ko yégle. Nee ñu, dinañ bawoo Alséri bu 14i waxtu jotee ci Ndakaaru, àgg ca ayeropoor Lewópõol Sedaar Seŋoor bu 18i waxtu jotee ci ngoo. Ginnaaw gi, Njiitu réew mi dina leen dalal, ndokkeel leen. Ndaxte nag, yeyoo nañu ko. 

Dafa mel ni gayndey Senegaal yi dañu fippu. 2022, ñoo jël CAN bi, 2023 ñu jëlandoo CAN Beachsoccer, jigéen ñi jël joŋantey UFOA-A yi. Kon, bu yeboo jàpp ne, léegi, gaynde kub lay dunde.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj