Ñaari ayubés ak léegi coow lëmbe réew mi yépp, am Usmaan indi Aji, moom laak du moom. Coow li nag, li ko waral, ñépp xam nañu ko. As ndaw su tudd Aji Saar moo jiiñ kii di Usmaan Sonko, njiitu Pastéef, ne da koo siif ay yoon i yoon. Ginnaaw loolu nag ndaw si kalaame ko ca sàndarmëri, ñoom it ñu amal seen i lànket ba woolu ñenn ñi laal ci mbir mi, déglu leen ngir mën a xam bu baax ni yëf yi deme.
Laaj-tontu bu njëkk ak Aji Saar
Luññutukat yi : Aji Saar, ndax yaa bind kalaame bii ?
Aji Saar : Waaw.
Luññutukat yi : Naka la mbir mi deme ?
Aji Saar : Benn bés, dafa am ku fëgg, ma tijji muy Usmaan Sonko. Mu laaj ma “yan xeetu dàmp ngeen di def” ? Ma wax ko xeet ya fa am yépp. Ginnaaw loolu lanu jàll ca fa nuy dàmpoo, ma dàmp ko ba pare ne ko : Nijaay, dàmp bi pare na mu tëdd rekk ma delluwaat ne ko nijaay dàmp bi pare na. Sonko ne ma : “xanaa xàmmeewoo ma” ? Ma ni ko déedéet xàmmeewuma la te it soxlawul ma lay xàmmee. Sonko dellu ne ma ñu bari bëggoon nañoo nekk sa palaas. Yokk ci ne ma soo deful li ma bëgg ma dàqlu la, soo bëggee téye sa liggéey defal ma li ma bëgg. Ma daldi jóg summeeku, jàll ca taabal ja, séq ak Usmaan Sonko.
Luññutukat yi : Loolu kañ la woon ?
Aji Saar : Fàtte naa ko.
Luññutukat yi : Ba mu amee, ndax wax nga ko kenn ?
Aji Saar : Déedéet. Waxuma ko kenn.
Luññutukat yi : Ndax bés boobu rekk la fa Usmaan Sonko ñëw ?
Aji Saar : Déedéet, ñëwaat na fa yeneen yoon.
Luññutukat yi : Ndax saa yu daan ñëw, da doon wéy di la siif ?
Aji Saar : Waaw. 21eelu fan ci weeru sanwiyee, 31eelu fan ci weeru desàmbar, 11eelu fan ci weeru sanwiyee ak 02eelu fan ci weeru féewaryee.
Luññutukat yi : Ndax am na ku gis Usmaan Sonko mu dugg mbaa mu génn foofu ?
Aji Saar : Waaw. Ku tudd Mamaa Ba gis na ko ndax sama njaatige bi mu ngi woon loppitaan jamono jooju waaye xamoon na ni Sonko dina fa ñëw.
Luññutukat yi : Ndax Usmaan Sonko am na sa limat ?
Aji Saar : Waaw. Am na ko.
Luññutukat yi : Ndax Sonko mës na laa woo ?
Aji Saar : Déedéet. Mësul am.
Luññutukat yi : Ndax mës na wuyu telefon mbaa mu woote ci biir fi muy dàmpoo ?
Aji Saar : Déedéet, mësul indi telefonam foofu.
Ndax mën nga nu wax yan waxtu la fa Sonko daan ñëw ?
Aji Saar : 2eelu fan ci weeru féewiryee 9w ci ngoon, 31eelu fan weeru desàmbar 7w ci ngoon, 21eelu fan weeru desàmbar, 2w jàpp 3w ci ngoon.
Luññutukat yi : Ndax am na looy yokk ?
Aji Saar : Waaw, Sonko daawul fagaru bunu daan séq.
Ñaareelu laaj-tontu ak Aji Saar
Luññutukat yi : Ci sa kalaame bi danga wax ne Sonko daa laa yónnee bataaxal di la wax ne mi ngi ñëw, nga xaar ko.
Aji Saar : Déedéet, yónneewu ma ko, boroom dàmpukaay bi la ko yónnee, moom moo ma ko yónneewaat.
Luññutukat yi : Ani bataaxal bi ?
Aji Saar : Dama koo dindi.
Luññutukat yi : Ndax bataaxal bi amul keneen koo ko yónnee ?
Aji Saar : Waaw, yónnee naa ko sama xarit bu ñuy wax Siidi.
Luññutukat yi : Ndax amul looy yokk ci li nga wax ?
Aji Saar : Déedéet.
Ñetteelu laaj-tontook Aji Saar
Luññutukat yi : Ci 1eelu fan ci weeru féewaryee ba ngay dàmp Sonko yaw ak ku ñuy wax Aysatu Ba yéen a fa nekkoon. Ndax laata ngeen di noppi danga koo wax mu génn ?
Aji Saar : Waaw. Sonko moo ma ko liyaaroon, ma ni ko génnal.
Luññutukat yi : Waaw, ñu lay siif, ngay wax sa nàttangoo mu génn ? Lu tax ?
Aji Saar : Maa ko wax mu génn ndax Sonko moo ma ko wax te daf ma waxoon ne soo ma defalul li ma bëgg dinaa la dàqlu.
Luññutukat yi : Dàmpukaay bi ngay liggéeye nii, ndax sa njaatige da laa mësoon a dàq ?
Aji Saar : Déedéet, man maa dakkaloon liggéey bi benn bés, ca ëllëg sa sama njaatige woowaat ma.
Luññutukat yi : Lan nga jote woon ak sa njaatige ba mu dàq la ?
Aji Saar : Daa am ku ma doon dàmp ba mu yàgg ma bàyyi, kooku daldi mer boole ma, ci la ma dàqee.
Luññutukat yi : Ndax bésub 2eelu fan ci weeru féewaryee sa njaatige xamoon na ni Sonko dina ñëw?
Aji Saar : Sama njaatige moo waxoon ni Sonko dina ñëw altine waaye talaata la mujj ñëw.
Luññutukat yi : Ndax amul looy yokk ?
Aji Saar : Déedéet. Yokkuma dara.
Laaj-tontu bu njëkk ak Aysatu Ba
Luññutukat yi : Kañ nga tàmbalee liggéey ci dàmpukaay bi?
Aysatu Ba : Ci benn ayubés lay tollu.
Luññutukat yi : Ñaata ngeen jot a dàmp foofu ?
Aysatu Ba : Su baree ba bari ci juróom lañuy tollu.
Luññutukat yi : Ñan ngeen jot a dàmp ?
Aysatu Ba : Xàmmee naa ci Usmaan Sonko waaye ñeneen ñi xawmaleen.
Luññutukat yi : Ban xeetu dàmp la Usmaan Sonko di def?
Aysatu Ba : Dàmpu ñeenti yoxo “intégral 4 mains”.
Luññutukat yi : Kan nga nekkaloon ?
Aysatu Ba : Ajii saar laa nekkaloon.
Luññutukat yi : Ndax Aji da doon des moom rekk ak Sonko?
Aysatu Ba : Waaw. Bi nu ko dàmpee ba noppi, Aji Saar daf maa wax ma génn bàyyi leen ñoom ñaar.
Aysatu Ba : Ñaata yoon nga gis Sonko ca dàmpukaay ba?
Luññutukat yi : Benn yoon laa ko fa gis muy bés boobu.
Ñaareelu laaj-tontu ak Aysatu Ba
Aysatu Ba : Alxemes 4eelu fan ci weeru féewaryee bi ngeen ma toogloo fii may xaar, am na ku góor ku ñuul ku àndoon ak Aji Saar. Bi mu dikkee ne ma Mamaa, ma ni ko yaw noo xamee ni Mamaa laa tudd ? Mu ni mës naa wax ak Aji ci widewoo mu won ma la wax ma sa tur. Ba ma toogeek ponkal mooma àndoon ak Aji Saar daf ne ma waroo woon génn bi la Aji Saar waxee nga génn. Ma ni ko li ngay wax nii xawma ci dara. Yokk ci ne bi nuy jàkkarloo maak Aji ak luññutukat yi dama koo làkk ci seereer ne ko Aji lu tax ngay def lii ? Lu ko fi jar ? Mu ni ma dinaa la faramfàcceel lépp, jox ma 20i junni ma bañ xaalis boobu.
Laaj-tontu ak Ibraayima Kulibali jëkkëru boroom dàmpukaay bi
Luññutukat yi : Ndax yaw yaay jëkkëru Ndey Xadi Njaay?
Ibraayima Kulibali : Waaw. Ma yokk ci ne ci biir kër gi la dàmpukaay bi nekk, te it Usman Sonko daan na fa faral di ñëw di fa dàmpoo. Sama soxna wësin-bees la te liir bi taxu koo mat ba tax na dafa nekkoon loppitaan Faan ; looloo waral Aji saar doon toppatoo liggéey bi. Waaye, ay fan laata mbir mii di am seetlu naa ni Aji yëngatu woon na lool te it doon na laajte saa su ne kañ la Sonko di ñëw. Dem na sax ba sàkku ngir ñu woo ko laaj ko kañ lay ñëw. Ñaari fan laata Aji di dem ca Sàndarmari wax na ko ni dafa ëmb waaye waxu ko kan moo ko biiral. Ca bés booba it am na xale bu góor bu ma seetlu muy jaabante rekk ci buntu kër gi, ma daldi ne Aji kii kan la ? Aji ni ma xaritam la. Ca ëlleg sa Aji ñëwaat na ci man ne ma nijaay : Usmaan Sonko ñëwul ba tey? Ma ni ko waa yaw loo ma toppee di laaj ndax Usmaan Sonko, xanaa da lay may xaalis ? Waaye tontuwul, dafa ree rekk dem. Ba bés bi mu waxee ni ci lañ ko siif ñëw na jox ma 40i junni ne ma Usmaan Sonko moo ko joxe. Ba Sonko demee mu won ma benn “test de grossesse”. Ma dellu ne ko ku la ëmbal ? Mu ni ma du ko wax. Ginnaaw loolu la jàll ca kow di wax telefon ma dégg mu ne : “kaayleen jëlsi ma”, ma laaj ko ku lay jëlsi mu ne benn moto jakartaa bu ko yaayam booleel moo koy jëlsi. Ci noonu la Aji génnee dem.
Luññutukat yi : Ndax déggoo benn riir ci kër gi ?
Ibraaxiima kulibali : Déedéet.
Luññutukat yi : Ndax déggoo coow ?
Ibraaxiima kulibali : Déedéet.
Luññutukat yi : Ndax bi Sonko demee seetlu ngeen lu xaw a teey xel ci Aji ?
Ibraaxiima kulibali : Déedéet. Ba Aji demee nag, Aysatu Ba nee na ma démb ba Sonko ñëwee ba dem, ci guddi gi am na ku Aji woo naan ko kaay jëlsi ma yóbbu ma loppitaan. Mu tekk ci ne lu jiitu bés yooyu yépp lekku Aji ak i deseeram mi ngi doon jóge “Residences Mamoune”.
Laaj-tontu bu njëkk ak Siidi Axmed Mbay
Luññutukat yi : Xam nga Aji Saar ?
Siidi Axmed Mbay : Waaw
Luññutukat yi : Noo ko xamee ?
Siidi Axmed Mbay : “Liberte 6” laa ko xamee ci sama bitigu umpaañ.
Luññutukat yi : Ndax guddi 2eelu fan ci weeru féewaryee dem nga ca dàmpukaayub “Sweet Beauty” ?
Siidi Axmed Mbay : Waaw. Dem naa fa waaye dugguma.
Luññutukat yi : Waaw, noo def ba génn ak kurfo bi ?
Siidi Axmed Mbay : Damaa woo sama benn xaritu layalkat, mu boolee maak benn doktoor mu génne ma.
Luññutukat yi : Lan moo nekkoon say tànk foofu ?
Siidi Axmed Mbay : Bi Usmaan Sonko demee Aji moo ma woo ne ma dañu maa sàkku, kaay yóbbu ma loppitaan. Te yàgg na maa wax loolu.
Luññutukat yi : Ban loppitaan nga ko yóbbu ?
Siidi Axmed Mbay : Loppitaanu “Grand Yoff”.
Luññutukat yi : Lu leen doktoor ba wax ?
Siidi Axmed Mbay : Doktoor dafa def ay saytu.
Luññutukat yi : Wóor na ni dugguloo ci dàmpukaay bi ?
Siidi Axmed Mbay : Wóor na, dugguma fa.
Ñaareelu laaj ak Siidi Axmed Mbay
Luññutukat yi : Ndax Aji da laa waxoon ni Sonko day ñëw ci dàmpukaay bi talaata ñaareelu fan ci weeru féewiryee ?
Siidi Axmed Mbay : Aji xamu ko woon waaye bés boobu la Sonko waroon na ñëw ci yoon.
Luññutukat yi : Naka la la Aji Saar waxoon ne noonu lañ koy sàkkoo ?
Siidi Axmed Mbay : Daf ma ni dafay yor ñaari fital bu koy siif te itam naan ko lii bu mu génn ci biti.
Luññutukat yi : Waaw, lu tax ba mu la ko njëkkee wax jëloo say matuwaay ngir jëf jooju dakk ginnaaw Aji sa xarit la ?
Siidi Axmed Mbay : Ndax bëggunu woon nit ñi am xel-ñaar ci li muy wax te it dundug Aji dafa nekkoon ci xottu gerte.
Luññutukat yi : Ndax dangay def pólitig?
Siidi Axmed Mbay : Déedéet. Defuma pólitig waaye sama baay Mawdo Maalig Mbay mooy njiitu kurélu “Gëm Sa Bopp”, mbootaayu pólitig mi bootu ci Bennoo Bokk Yaakaar.
Luññutukat yi : Ginnaaw yaw ku xam dara ci mbir mi ?
Siidi Axmed Mbay : Kenn xamu ci dara.
Luññutukat yi : Yaw loo séq ak Aji ?
Siidi Axmed Mbay : Aji sama jigéen la.
Luññutukat yi : Waaw lu tax Aji tànn la ci mbir mii ?
Siidi Axmed Mbay : Yàlla moo ko dogal.
Laaj-tontu bu njëkk ak Ndey Xadi Njaay
Luññutukat yi : Ndax ci yaw lay Aji Saar liggéeyee ?
Ndey Xadi Njaay : Waaw. Ci weeru nowàmbar 2020 la fa tàmbale. Waaye laata loolu liggéeyal na ma 15i fan ma dàqoon ko.
Luññutukat yi : Lu tax nga dàqoon ko ?
Ndey Xadi Njaay : Ñi koon doon jël dafa bari woon lool, sama xel ñaaw ne ndax ci dàmp rekk la yam.
Luññutukat yi : Xam nga Usmaan Sonko ?
Ndey Xadi Njaay : Waaw. Xam naa ko bu baax a baax.
Luññutukat yi : Foo ko xame ?
Ndey Xadi Njaay : Ci sama dàmpukaay. Lu war a tollu ci at mi ngi fay ñëw.
Luññutukat yi : Bu fa Usmaan Sonko mësaan a ñëw, ban xeetu dàmpu la daan def ?
Ndey Xadi Njaay : Dàmp “tonifiant” lanu ko daan defal.
Luññutukat yi : Kan moo daan dàmp Usmaan Sonko ?
Ndey Xadi Njaay : Ca njalbéen ga jenn jigéen ju tudd Faatu moo ko daan damp. Ginnaaw bi Faatu bàyyi, ci la ko Aji tàmbalee dàmp.
Luññutukat yi : Ndax yaw yaay tànn Aji ngir mu dàmp Sonko ?
Ndey Xadi Njaay : Déedéet, waaye seetlu naa ni saa yu Sonko fëggee moom mooy daw tijji duggal ko ci dàmpukaay bi.
Luññutukat yi : Ndax yor nga limatu Usmaan Sonko ?
Ndey Xadi Njaay : Déedéet, ndax duma jël limat yi waaye am na limat bu ma ko foog.
Luññutukat yi : Ñaata yoon nga mas a wax ak Usmaan Sonko ?
Ndey Xadi Njaay : Ca njalbéen ga bi mu fa ñëwee waxtaan nanu.
Luññutukat yi : Kañ la woon ?
Ndey Xadi Njaay : War na mat at waaye ba may wax ak moom xawma ni woon sax ni mooy Usmaan Sonko.
Luññutukat yi : Ndax Sonko da lay bind bataaxal bala muy ñëw ?
Ndey Xadi Njaay : Déedéet, fàttelikuwuma ko.
Luññutukat yi : Ndax talaata 2eelu fan ci weeru féewiryee jot nga bataaxalu Usmaan Sonko, nga yónnee ko Aji Saar?
Ndey Xadi Njaay : Déedéet. Ci altine ji laa ko yónnee benn bataaxal te loolu benn araab la, du Usmaan Sonko.
Luññutukat yi : Ndax yaw mës nga dàmp Usmaan Sonko?
Ndey Xadi Njaay : Waaw. Ba muy njëkk a ñëw ca dàmpukaay ba, waaye mësumaa won benn kanamu caaxaan. 22i waxtu démb Aji daf ma woo telefon ne ma dafa ëmb. Ma ni ko waaw, ku la ëmbal ? Mu tont ma : benn kilifa la waaye duma ko wax. Aji mi ngi ma woo 18i waxtu 3eelu fan ci féewiryee ne ma baayam day yóbbu Usmaan Sonko ci yoon ndax moo ko ëmbal.
Luññutukat yi : Ndax lii rekk nga am ci loo wax?
Ndey Xadi Njaay : Waaw.
Ñaareelu laaj-tontu ak Ndey Xadi Njaay
Ndey Xadi Njaay : Damaa bëgg joxe ay leeral : Usmaan Sonko bi muy ñëw sama dàmpukaay ak léegi, tollu na ci ay weer waaye, mësumaa won ñàkk faayda. Bu daan dàmpu sax day muur kanamam, bañ ñu xàmmee ko. Du Aji moo ko njëkk a dàmp. Am na bés mu ñëw fa fekk maa ngi ëmb ba diis mu may ma 8i junni ; bés boobu sax jotul a dàmpu.
Luññutukat yi : Ndax amoo loo ciy yokk ?
Ndey Xadi Njaay : Déedéet ; dafa am lu ma bëgg a leeral, Usmaan Sonko bés bi mu fay mujjee ñëw sama beneen dàmpkat bi Aysatu Ba nee na ma Aji daf ko ne génnal néeg bi mu daldi génn. Ginnaaw bi mu paree, am na ku mu woo telefon naan ko gaawal nga ñëw yóbbu ma loppitaan. Koo ku laaj ko ndax daanu na ?
Aji ne ko waaw, gaawal. Bi mu xaaree diir ñëwul, woowaat na ko di ko wax mu gaaw te it bés boobu lekku Aji mi ngi jóge woon “Résidences Maamun”. Yokk ci ne bés boobu laaj na sama jëkkër ba tàyyi kañ la Sonko di ñëw. Dolli ci ne liy wane ni Aji jubul bi mu bëggee génn dafa wax ni dafa ëmb, indi ab “test de grossesse”.
Aysatu Ba : Waaw talaata 2eelu fan ci weeru féewiryee.
Luññutukat yi : Ndax mën nga ñu nettali ?
Aysatu Ba : Bi mu fëggee ci buntu bi, Aji moo dem tijji, ne ma Usmaan Sonko la waaye melal ni ku ko xamul. Bi nu dàmpee nun ñaar ba ci digg bi Aji ne ma génnal, ma daldi génn.
Luññutukat yi : Aysatu ndax ba nga génnee dégg nga riir ci néeg bi ?
Aysatu Ba : Déedéet.
Luññutukat yi : Aji, lu tax nga génne Aysatu ?
Aji Saar : Sonko moo ma wax ma génne ko.
Luññutukat : Aysatu, ndax ci dàmp, yoon la ngeen dàmp ba ci biir kenn ki génn ba fa ka ca des ?
Aysatu Ba : Déedéet.
Luññutukat yi : Aji, yaw nag ?
Aji Saar : Loolu def naa ko lu bari.
Laaj-tontook Ndey Xadi Njaay / Aji Saar
Luññutukat yi : Ndax yónnee nga Aji Saar bataaxal altine 1eelu fan ci weeru féewiryee di ko wax ne Usmaan Sonko mi ngi foofu ?
Ndey Xadi Njaay : Waaw, waaye du woon Usmaan Sonko keneen la woon. Talaata la fa Sonko ñëw waaye man nekkuma fa woon, maa ngi woon loppitaan ndax damaa sonnoon.
Ndey Xadi Njaay : Sama jëkkër moo ma woo ne ma Sonko ñëw na, ma woo Aji Saar mu dëggal ma loolu ne ma dàmpu ñent loxo lay def mook Aysatu Ba.
Ndey Xadi Njaay : Bi mu noppee ma woowaat Aji ne ko ndax dem na mu ni ma waaw teg ci ne moom sax mi ngi dem ndax dafa ëmb, am na moto jakaartaa bu koy jëlsi.
Luññutukat yi : Aji, ndax kii li mu wax mën nga koo dëggal?
Aji Saar : Waaw. Woo na ma dima laaj ndax Sonko mi ngi ci dàmpukaay bi te it bi may génn ci guddi gi woto moo ma yóbbu loppitaan.
Luññutukat yi : Dangaa waajaloon woto bi la jëlsi ?
Aji Saar: Déedéet, bi ma paree laa woote ngir ñu jëlsi ma.
Luññutukat yi : Lu tax nga fen ci fa nga doon jëm ?
Aji Saar : Dama doon bañ mu am ay xel-ñaar yaakaar ni damay dem di dàmp ay kilyaan seen i kër.
Luññutukat yi : Ndey Xadi Njaay, Aji nee na mësoo koo dàq ?
Ndey Xadi Njaay : Loolu amul. Dàq naa ko 15i fan.
Aji Saar : Du 15i fan, 5i weer la te man maa dakkaloon liggéey bi ab diir.
Ndey Xadi Njaay : Dama ko dàq 5i weer ndax daf ma wax yaayam moo faatu te loolu du woon dëgg, ma dem ba xam ni aniwerseer la demoon ma dàq ko.
Aji Saar : Waaw, dàqoon na ma bés boobu waaye damaa ñaanoon ndax sama mag moo génnoon àddina.
Luññutukat yi : Ndax mës ngaa dàmp Usmaan Sonko ?
Ndey Xadi Njaay : Waaw, benn yoon.
Luññutukat yi : Ndax mës nga ko gis ak i ngànnaay ?
Ndey Xadi Njaay : Déedéet. Mësuma koo gis ak i ngànnaay.
Luññutukat yi : Yaw mën nga dëggal ni Usmaan Sonko day yor ngànnaay saay buy ñëw ci dàmpukaay bi ?