LI CI BIIR "MBOORUM ÀDDUNA SI" BU ABDU-XAADR KEBE

Yeneen i xët

Aji bind ji

KAN MOOY SËRIÑ ABDU-XAADR KEBE ?

Sëriñ Abdu-Xaadr Kebe, ñu gën koo xam ci turu Jili Kebe, lijjantikat la (entrepreneur), yor lijjanti guy yëngu ci tabax ak liggéey yu ñémmeere yi (travaux publics). Gëstukat la tamit ci wolof, moo taxawal mbootaayug Akaademib Wolof (AW), muy mbootaay gees xam ab liggéeyam ci lënd gi (internet bi). Bind na lu sakkan ci wolof, lu wara génn ak lees siiwal ci lënd gi. Moo tekki “Tasawudus sixaar”, “Iwaawu Nadiim”, “Nahju qadaal Haaj”, “Mawaahibul Xudoos” ak yeneen ci téerey Sëriñ Tuubaa yi. Lu sakkan ci wikipedia Wolof moo ko def. Am njàngam ci araab, ci daara ju Sëriñ Saaliw la ko defe, jàng xam-xam ba jeexal, jàngale as lëf, tukki dem Amerig, Farãs, Itali, Imaaraat ba Siin, di wax araab, bind ci ay jukki yu bari, jële ci farañse ay téere niki téere mboor bu ma-mboor bii di Mbay Géy Sill def te tudd “CHEIKH AHMADOU BAMBA” (RTA), Que sont devenus ceux qui ont essayé d’entraver sa mission ?, di téere bu am solo ci xew-xew yi amoon ci diggante Sëriñ Tuubaa ak Tubaab bi. Sëriñ Kebe dégg na yit àngale ak làkkuw Itali. “Adjoint au maire” la ci Tuubaa.

LI CI BIIR “MBOORUM ÀDDUNA SI”

Téere Jili Kebe bii ngeen téye, bu leen di tënkal mboor la, rawatina la dale ca jamono yu diggu ya ba bërki-démb gu yàggul gii, di tollook suqalikug réewum Sapoŋ ci ginnaaw xareb àdduna bu mujj bi. Mu tendeefal as lëf ci biir ruq-ruqaan yi ci diggante bi, ci gis-gisub jullit bu dib saa-Afrig.

Ci noonu mu wone ci jeexital gi lislaam def ci xayug Tugal gii ñépp jàppe tey ni royeef, jàpp tamit ne mooy gi wara wéy. Kon su cib taar nekkee, nanu xam ne saal ba bob lislaam la, mooy rootu ba Tugal roote. Nu man a jànge ci téere bii ne dara weesoogul ci Afrig, kembaar (continent) gu man a dabe la, su gëmee boppam. Rawatina bi nga xamee ni Afrig moo moom ëllëg, ciy goneem ak i balloom yu mbindaare yees laalagul, muy petorol, di gaas ak leneen ak leneen.

“Mboorum àdduna si” téere bu am soloo, ndax day yokk xam-xam, di meññal yaakaar ak pas-pas ci xoli doomi- Afrig yépp.

*

EJO-Editions Dakar

NJËG LI : 5000 Fcfa

Mën ngeen a woote ci limat yii :

Ndey Koddu Faal 00221 77 651 68 48 (whatsapp) / 33 827 13 15

Musaa Aysatu Jóob 00 221 77 479 77 73 (whatsapp) / 76 532 08 89

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj