LI GËN A FËS CI WOTE YI (24/3/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SAA-SENEGAAL YU BARI GÉNN NAÑ WOTEJI

Ci dibéeru tey ji lañu woo saa-senegaal ngir ñu fal seen Njiitu réew lu bees ci 5i at yii di ñëw.. ËÑu war a tànn ci diggante 19i lawax. Ubbees na pekki wote yi bi 8i waxtu jotee ci suba si. Wii yoon nag, Saa-Senegaal génn nañ bu baax a baax, bari lool ci bérébi wote yi. loolu day firndeel ni, wotey ren yi soxal na leen lool.

NJIITU RÉEW MI : MAKI SÀLL

Njiitu réew mi war a dem, Maki Sàll, wote na ba noppi ci suba. Fatig biral nay kàddu wax ne :

« Di jaajëfal ñépp ! May sant Yàlla bu baax. Sant naa bu baax ci teewaat fii ci Fatig ngir matale sama wareefu maxejj »

Bu dee li ñeel kaaraangeg wote yi, àddu na ci, wax ne :

« CENA a ngi fi, ñiy saytu ñu ngi fi ak ndawi làngi politig yi ! Kon amul benn lawax walla geneen gurél gu sañ a joxe njureefi joŋante bi. Am nanu tëralin wu wóor ! »

YËMBËL SID: JÀPP NAÑ GENN KILIFAG BENNOO BOKK YAAKAAR

Fa kominu Yëmbël Sid ? genn kilifag Bennoo Bokk Yaakaar la takk-der yi jàpp fa sàntar bu Muse Anta Jóob. Li ko waral mooy ne dafa doon jënd nit ñi ngir ñu woteel Aamadu Ba.

IDIRIISA SEKK

Idriisa Sekk wote na. Bim génnee ci pekkoom lii la wax :

« Maa ngi ñaan joŋante yi am ci jàmm ak dal, te bu nu ci noppee, Njiitu Réewum Senegaal mi war a falu tijji bunti jàmm ak dal ngir Senegaal. »

SÉEX TIIJAAN JÉEY

Ginnaaw bim wote, lawax biy jàppale Basiiru Jomaay Fay daf ne :

« Askanu Senegaal moo bëggoon bés bii. Xeex na ngir jot ci. Demokaraasi ca kanam. Senegaal ca kanam. » Teg na ci ne Basiiru Jomaay Fay dina am ndam ci lu leer.

BASIIRU JOMAAY FAY

Basiiru Jomaay Fay wote na. Njagañaaw la ko defe. Kàddu yii toftalu la fa yëkkati :

« Ku Yàlla nattoo nga am ndam, nga am ug cuufe, xam ni sas la, yaakaar la, waaye du sa liggéeyu bopp. »

SEEX CORO MBÀKKE

Seex Coro Mbàkke woote ca tele Walfadri, xamle fa ne, jafe-jafe bi amoon ci ñeel ndaw yi war a teewal lawax yi ci pekk yi, ag ñàkk a déggoo rekk la woon seen diggant ak perefe bi bu ndaw bi. Waaye, ciy waxam, pexe am na. Ndaxte, ci 18i pekk yi mu amoon, 3 rekk a ci des yu ñu war a joyyanti.

SËRIÑ MBUUB

Lawax bii di Sëriñ Mbuub wote na. Moom itam, biral nay kàddu, wax ne mbooloo mu bari mi daan topp di daw ci ginnaaw lawax yi, ci jamonoy kàmpaañ bi, firnde ci ne, ndaw ñi ci xëy.

USMAAN SONKO

Usmaan Sonko wote na fa mu fekk baax : Sigicoor. Loolu, day firndeel ne dugalaat nañu ko ci limka (liste) yi. Biral na kàddu yii toftalu :

« Matale naa sama wareefu maxejj. Wote naa ci jàmm, di woo jëwriñu biir réew mi tamit ci ñu aar baatu askan wi. »

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj