LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (18/2/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

GAALUG MBËJ GIY TËMB : LËNT-LËNTI KARPOWERSHIP

Gaalug mbëj giy tëmb ci géejug Senegaal gi, ñu duppee ki Karpowership, mbiram dafa lënt. Ci li yéenekaay Libératio fésal, ag pas yaa-ma-neex lees ko xaatimal ca atum 2019.
Ëttub cettantal gi, ci caabal gi mu siiwal, daf ci biral xibaar bu doy waar. Nde, caabal gi dafa xamle ne, ca bésub 19 désàmbar 2023, tibb nañu ci kees gi ñaari yoon. 3,7i miliyaar lañu njëkk a génne, daldi ciy tegaat 9,2i miliyaar. Koppar yooyu nag, Karpowership lañu ko jox. Waaye, amaluñu ko lay ndax amul genn kayit gu koy firndeel. Ci li caabal gi wax, « pay gu ëpp » la.
Libération di xamleet ne, am na ag luññutu gu ñu ubbi ñeel Karpowership. Kurél ga fay xeex nger, « Commission nationale de lutte contre la corruption », moo koy topp ci ag pas gu ni mel.

NJIITU RÉEW MI SUMB NA NAAWLU PROMOREN

Njiitu réew mi sumb na naaluw PROMOREN. Naal woowu, li ko tax a jóg mooy jàppandal ndox mi fa Kungéel. Àjjuma jees dëgmal, 21i féewiryee 2025, lay ubbi liggéey bi.

USMAAN SONKO : FÉSAL NA NAALUW KOPPARAL WU 1 000IY MILIYAAR

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, fésal nay coppite yi Càmm gi fas yéene amal ngir ñoŋal liggéey bi ak juuti yi. Li mu ko dugge mooy fexe ba këri liggéey yi gën a suqaleeku. Ci kow loolu la xamle ne am na naaluw kopparal wu tollu ci 1 000iy miliyaar ci sunu xaalis. Xaalis boobu, PME-PMI yi lees koy jagleel. Ci weeruw awril wii lees di xaatim ab déggoo ñeel kopparal googu.

WÉR-GI-YARAM : WAA SAMES DAKKAL NAÑU LIGGÉEY BI

Fajkat yi bokk ci sàndikaa bii di SAMES bank nañ seen i loxo. Doktoor Jabel Daraame yékkati nay kàddu, wax ci Info Matin TFM, ne :

“Jafe-jafe bi mooy ne, Nguur gii fi nekk joxuñu nu cër…  Dafa di, xamuñu sax lu nuy ñaxtu…”

LËKKATOOG LIGGÉEY : JËWRIÑ ABBAAS FAAL BIRAL NA XIBAAR BI

Jëwriñ Abbaas Faal xamle na ne dinañ taxawal « Lëkkatoog liggéey gu mag » fii ak 2029. Ca waxtaan wees jagleel wëppa wii di « Solos liggéey ci Agenda national de transformation Sénégal 2050 ».

Naal woowu, dees na ci boole tàggatu gi, am xarañteefu liggéey, ndimbalul fànnu jàmbure yi ak lijjanti gi. Bu ko defee, ñàkkug xëy dina wàññeeku mbaa mu jeex.

COPPITEY NGUUR GI

Fara-caytu bu mag bob Nguur gi, doon na amal aw waxtaan fa tele RTS ci jotaay bii di Point de vue. Ca biir waxtaan wa, fésal na ndogal yi Càmm gi nar a jël ngir defaraat koom-koomu réew mi.

Bu dee li ñeel deppãs yi :

  • Ay coppite ngir wàññi alal ji Nguur giy liggéeyee ;

  • Dees na far yenn « agences » yi ;

  • Dees na dakkal baalaate yees daan baalaate ci wàllu juuti yi te mu àggoon ci 1 000iy miliyaar ;

  • Ndàmpaayi mbëj gi dees leen jagleel askan wi yelloo kepp, ñi ci des dinañ fay li war ;

  • Dees na xoolaat payoor yi, daldi wàññi yu ëpp yi ;

Bu dee « ndajale yi »

  • Yokk ndajale yi, jaare ko ci juutiy suuf si, payoor yi ak yaatal ñi war a fay juuti ;

  • Ay coppite yees nekk di amal ci Càrtug juuti yi ak Càrtug duwaan yi ;

  • Gën a xeex nger mi ;

  • Yeesal jumtukaayi yees di fayee juuti, dëppale leen ak jumtukaayi xarala yi.

KAAWTEEF

Fa Sikaab 1, as waay mooy xaru. Sàmba la tuddoon, daan jaay dàll. Nee ñu, dafa takk buum ci baat bi, daldi yooru.

Fa Almadi, xale bu jigéen bu tollu ci 9i at lañu siif. Ci lees biral, seen wattukatu kaaraange (garjeŋ) ekool moo ko def jëf ju ñaaw jooju. Jàpp nañu garjeŋ bi.

MBIRUM WARI : ËTTUB DABU BI ÀTTE NA

Àttekat bi jiite ëttub dabu bi joxe na àtteem ñeel mbirum Wari mi. Àttekat bi dafa topp càkkuteefu Toppekat bu mag bi. Dafa dëggal daan bees daanoon Kabiiru Mbóoj.

Cig pàttali, dañu daanoon Kabiiru Mbóoj ñaari ati kaso yoy, juróom-benni weer yi lay tëdd. Lees ko tuumaal mooy wor ak yokk “capital social” bu jaarul yoon. Yéenekaay Les Échos moo biral xibaar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj