Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, amoon na gan tey ci àjjuma ji. Tof-Njiitu réewum Siyeraa Lewon, Mohamet Julde Jàllo, la doon dalal fa njénde la. Tof-Njiit li daf ko indiloon ab bataaxelub xaritoo ak jàppoo bu jóge ci Njiitu Réew ma, Julius Madabio.
Ci lees biral, waxtaane nañ diggante ñaari réew yi xi wàllu jëflante. Sëñ Mohamet Julde Jàllo daldi rafetlu bu baax yéeney Njiitu réewum Senegaal ci dëgëral diggante bi te di seqiy jéego ngir yaatal ko.
Waajtaayi tabaski bi
Ngir dimbali boroom kër yi xew-xewu tabaski bees dëgmal, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jox na ndigal elimaanu hëwriñ yi. Li mu sant Usmaan Sonko mooy, li ko dale 19 awril jàpp 2 ut 2024 :
– ñu woyofal caytug sëfaan (camions) ak daamar yiy indi xar yi fi Senegaal ;
– teggi juuti bi ñu daan fay ci xari tabaski yi ;
– ci bépp sëfaan bu yeb i xar, ñu may ñetti sàmmkat yuy wattu xar yi ñu yéeg ci.
Pekkug diine fa njénde la
Njabootu diine, ak diine ju mu ci mën di doon, war na bég ci xibaar bile. Nde, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jel na ndogalu samp ag Pekk gog, ci mbiri diine yi lay yëngu. Loolu doyul, mu xamleet ne, dine fexe ba njàngaan yi lijaasay araab mën a am liggéey fi réew li, bokk ci ñi koy doxal.
Mbirum ndox mi
Nguur gi yees gile, dafa bëgg a indiy coppite ci yoriin réew mi, nekkiinu ak dundiinu askan wi. Balaa dara nag, dañu fas yéene xoolaat li fi Nguurug Maki Sàll gi bàyyi laata ñuy sóobu ci liggéey bi. Naka noonu, Njiitu réew mi xamle na ne dina taxawal ag kurél gu mag guy saytu wàllu ndox mi. Rax-ci-dolli, dafa santaane ñu càmbar, càmbar gu matale, mbooleem pas (contrat) yi dox diggante SONES ak SEN’EAU…
Diisoob réew mi
Keroog 28 me 2024, Nguurug Basiiru Jomaay Fay gi dina sumb ab diisoo bu njëkk ñeel mbiri réew mi. Boobule diisoo nag, ci mbiri Yoon ak nees ko war a yeesalee ak a joyyanti lay aju.
USMAAN KABILIN JAATA DINA GÉNN KASO
Ci càkkuteefu toppekat bi, Umar Maaham Jàllo torlu na ag këyit guy santaane ñu bàyyi Usmaan Kabilin Jaata mi ñu doon toppee mbirum rëbel. Keroog 22 suwe 2022 lañ ko jàppoon.
ÑAARI XALE YI LAB FA GÀDDAAY
Xibaar bu tiis, bu yëramtalu. Ñaari ndongo ñoo lab ça géejug Gàddaay gi, benn xale bu jigéen ak benn xale bu góor bu ko doon jéem a wallu. Ba nëgëni nag, kenn gisagul seen i néew.