Jëwriñu njàngale mu kawe mi dina jël 500i jàngalekat ak i gëstukat yu bees. Xibaar la bu mu siiwal démb ci altine ji jaare ko ci ab yégle bu mu génne. Muy ndogal lu mu jël ngir saafara taxawug ndongo yi sooxe ci jànguney bokkeef gi. Ndogal loolu di dellu ci naaluw réew mi ngir sopparñi njàngale mu kawe mi, gëstu beek coste gi ANTESRI (Agenda national de Transformation de l’Enseignement supérieur, de la recherche et de l’innovation). Muy naal wow, Njiitu réew mi gaaral na ko bu yàggul dara, 17 sulet 2025.
Jël bi nag, dinañu ko def ak ay fànn yu ñu jiital. Nees koy séddalee itam dees na ko tënk ak mbokki jàngune yi ak càmpeef yi ñuy liggéeyandool.
ËTTU MASISTARAA YU SENEGAAL
35i masistaraa yu ndaw ñoo dugg ci ëttu masistaraa yu Senegaal ginnaaw bi ñu noppee ci seen tàggatu fa CFJ (Centre de formation judiciaire). Démb ci altine ji lañu leen doon dalal ak ndaje mi ñu doon amal fa ëttu àttekaay bu Ndakaaru. Masistaraa yu ndaw yooyule nag, diy àttekat yu bees, waat nañu démb ni dinañu jariñ réew mi ak xeeti mbaax yiy cëslaayu Réewu Yoon, ci nangul ko, moom seen bopp, tëdde njaaxaanaay ak teeylu.
Ca ndaje ma sax, njiitu Ëttu dabantal bu Ndakaaru, Abdulaay Ba, dellusi na ci waat gi ñu waat ak li aamu googu laaj. Mu leen di fàttali ni pas la gu dox ci seen digganteek Saa-Senegaal yi. Ba tax muy sàkku ci masistaraa yu bees yu ñu doon ay royukaay ci jox réew mi seen bopp ak dëggu, rawatina jamono jii réew mi tollu ak li ñuy xaar ci Yoon ngir mu suuxat demokaraasi bi.
ËTTU ÀTTEWAAY BU KAWE BI
Ëttu àttekaay bu kawe bi xëye woon na démb ci altine ji mbirum nger mi dox ci diggante Ismayla Maajoor Faal mi fi nekkoon jëwriñu Yoon ak Séex Géy, ngir gam-gamle seen i kàddu ci 50i miliyoŋ yees ci tudd. Ba léegi nag, ku ci nekk a nga ŋoy fa nga ŋoyoon. Bu Sëñ bi Faal jàppee ni Sëñ bi Géy daf ko doon jéem a ger ak boobule xaalis, mu bañ ba delloo ko ko ca saa sa, Sëñ bi Géy a ngay wéy di biral ni xaalis bu mu ko abal la ginnaaw bi ñu dëppoo ciy kàddu.
Jamono yii nag, layookati Ismayla Maajoor Faal yee ngi ci ay pexe ngir ñu woyofal ndogal yi ko yoon tënke. Dugal nañu sax ab bataaxal ngir ñu tekki lamu tànk bi ñu ko takkal keroog 20 me 2025 ba tay, te féexal ko ci dëkkuwaay bi ñu ko tënk.
MBIRI KOCC BARMA
Ci ayu-bés bii weesu la waa DSC tegoon loxo EL H. B. Jum mi ñu gën a miin ci turu Kocc Barma. Jamono yi ñu naan moom mooy Kocc Barma dëgg walla du moom, alkaati yaa ngay wéy di feeñal yeneen i mbir. Bees sukandikoo ci li Liberation siiwal, luññutukat ya dugg nañu ci nosekaay MacBook bi mu daan jëfandikoo ba sulli ci yeen i mbóot. Bi ñu ko yullee nag, fekk nañu ci biir 9000iy dencukaay yoy, ay wayndare yu dul jeex la fa tegle ba ñu jekk. Wayndare wu ci nekk mu wutal la tur. Am na sax wu ci tudd « Paid no to publish », di wayndarey ñi fay ba noppi te warul a siiwal seen i yëf. Ci ñooñu sax, am na ñu ko ci fay alal ju tollu ci 2i miliyoŋ, walla 9 668i ëro, ngir mu bañ leen a weer. Am na itam lu tollu ci 4 191i widewoo ak i nataal yoy, seen i boroom a naroon a topp ci weeru gi.
Luññutu yi wane nañu itam xaalis bu mu jot ci ay yónnante yu teey xel, ba mu yegg ci 93i miliyoŋ ak lu teg. Bari na nag yees koy toppe, yu deme ni defkatu ñaawteef, dajale yu jëm ci mbiri jàmbur, sàntaas, suufu ak lewal xaalis.