LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (25/2/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NJIITU RÉEW MI DALAL NA OLUSEGUM OBASANJO

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dalal na Njiitu réewum Niseriyaa la woon, Olusegun Obasanjo. Seen ndaje mi nag, li ko sabab mi ngi aju ci koppe ak dipolomasi.

Ci lees rotal ciy xibaar, seen waxtaan waa nga aju woon ci dëgëral jëflantey Senegaal ak Niseriyaa. Waxtaane nañ tamit mbirum diiwaanu Afrig sowu-jant ak kembaar gi.

DARKASE :  NISËRUG 200 000i TON NGIR ATUM 2025

Kurél gii di ORSRE* fésal nisëram ñeel mbayum darkase bi ci atum 2025 mi. Diggante 180 000 ak 200 000iy toni darkase la kurél gi bëgg a bay ci kàmpaañu 2025 bi. Ki jiite kurél gi, Isaa Wàdd, moo ko xamle ci benn jotaayu liggéey bees doon amal fa diiwaanu Sigicoor, fekk ñuy sumb njaayum ndaamaraas bi.

Daaw nag, 150 000iy ton lañu nattoon niki jubluwaay. Kon, ren, yokk nañ ko bu baax. Bees sukkandikoo ci kàdduy njiitul ORSRE li, « at mii, danoo bëgg a jàppale ñiy liggéey ci fànn wi ngir yombalal leen koppar yi ».

NDOG FA LUGA : 7i NIT JËLE NAÑU CI AY GAAÑU-GAAÑU

Ab daamar bu jëmoon Ndar moo daw ba mbëkk ag garab ci wetu dëkk bii di Kër Baara Wàdd. Ci guddig altine démb ji, 24i féewiryee 2025, la ndog mi am. Daamar bi ab 7 palaas la. Juróom-ñaari nit ñoo ci jële ay gaañu-gaañu, mu am ci ñett yu sonn lool.

AB SÀNDARM BU ÑÀKK BAKKANAM CI NÉEGAM FA DALIFOOR

Dafa am ab sàndarm bu ñu fekk mu ñàkk bakkanam, fa Dalifoor, ci koñ bii di « kàrce Ibu Ndaw ». Ci altiney démb ji lañu fekk néewam ca biir néegam. Bees sukkandikoo ci xibaar yi L’Observateur siiwal, sàndarm bi faatu, ci way-wattu kaaraange Njiitu réew mi la bokkoon. Ba mu wàccee ci dibéer ji ba dellu néegam, ca lañu gëj a xam ci moom dara.

Nee ñu, jabar jee ko woo ba sonn, jotu ko. Ca la soxna sa woowee dëkkandooy jëkkër ji ngir ñu nemmeekul ko jëkkër ji, xool lu ko dal. Noonu, dëkkandoo yi dem, fekk ne dafa gaañu.

50eelu ATU CEDEAO : ALIYUN TIN A NGI SÀKKU ÑU AMAL AY COPPITE CI KURÉL GI

Ren la CEDEAO am 50i at. Ngir màggal ko, dañu amal aw waxtaan wu aju ci wëppa wii di « CEDEAO, ginnaaw 50i at : soppeeku mbaa sànku ». Bi ñuy ubbi ndajem waajtaay ñeel waxtaan woowu, ca la Aliyun Tin mi sos Afrikajom Center biral xalaata ñeel kurél gi. Moom, Aliyun Tin, ci tele TFM la biral xalaatam bii :

« Fàww ñu def lépp, boole ci Réew yépp, way-moomeel yi ak pàcci mboolaay mépp ngir ñu saytu bu baax a baax mbirum CEDEAO. »

Ci gis-gisu Aliyun Tin, CEDEAO dafa nekk ciy tolof-tolof yu metti, rawatina ci gisiinu ndaw ñi. Daf ne :

« Gis nanu ay ndaw yuy bég ci Sóobare yu déjjati ay Njiitu réew, foqati lenge yi. CEDEAO dafa am ay digaale yu deme ni Farãs mi nga xam ne, dafay am ñu koy taafantoo ngir lëndëmal ndaw ñi, yóbbaale leen ci seen i xeex. »

RUWÀNDAA DAKKANDIL NA LËKKALOOWAM AK BELSIG CI WÀLLU YOKKUTE

Ci talaatay tay jii, 25i fani féewiryee 2025 la Ruwànda xamle ne dafay dakkandil lëkkaloowam ak Belsig ci wàllu yokkute. Li ko waral moo taxawaay bi njiiti Belsig yi am ñeel coow li dox diggant Ruwànda ak réewum Kongo RDC.  Loolee nag, dafa dolleeku ci ñagas-ñagas yi am diggante ñaari réew yi at yii yépp.

Ci li Càmmug Ruwàndaa gi siiwal cib yégle, réewum Belsig dafa ànd ak Kongo RDC, nekk di « ñaawal deru Ruwàndaa ci àddina si ngir tere ko jot ci koppari yokkute yi. » Loolu moo Nguurug Póol Kagame gi jël ndogalu dakkandil li des naaluw ndimbal li dox digganteem ak Belsig ñeel ati 2024 jàpp 2029. Dañu bind ci yégle bi ne « Ruwànda du nangu ñu koy napp wiiri-wiiriloo ci luy ñeel kaaraange rewam. »

*Organe de régulation du système de récépissé d’entrepôt de marchandises

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj