Tay jii, bu guddi gi xaajee, la kàmpaañ yi ñeel wotey Ngomblaan gi di jeex. Ëllëg, bésu noppalu la, ginnaaw-ëllëg ci dibéer ji dëppook bésu wote yi.
Ku nekk ci lawax yi dem na fi mu mënoon a dem yépp, wax li mu xam yépp ngir dagaan baatu askan wi. Ginnaaw gi, ku ci nekk a ngi jéem a yey fere yiy falaate ci waxtuy kàmpaañ yu mujj yii.
Usmaan Sonko mi jiite toftale Pastef, Biññoona la tëjee kàmpaañam. Bu 22i waxtu jotee, télé Walfadjiri dina jàllale laaj-tontu bi mu jot a séq ak ñoom.
Ci suba si, defoon na njëgg daldi wër ay koñ ak i gox fi Ndakaaru, rawatina Yoof, Wakaam, “Dakar Plateau”, Medinaa.
Bu dee waa Sàmm Sa Kàddu, bokk ci kujje gi, Bàrtelemi Jaas jiite ko, fa Tëngéej la namm a amal ab mitiŋ ngir tëj.
Bu dee Aamadu Ba miy boppu toftale lëkkatoo Jàmm ak Njariñ, dina wax ak Saa-Senegaal yi, jaare ko ci saabalukaay yi. Dafa di sax, jamono jii sax Walfadjiri a ngi dawal waxtaan wi ñu def ak moom.
Am na yeneen i lawax yiy wéyal seen kàmpaañ feneen ci yeneen anam.
Cig pàttali, Njiitu réew mi dafa tasoon Ngomblaan gi keroog 12i pani oktoobar 2024, daldi jàpp wote yu bees ci bésu 17i pani nowàmbar 2024.
Ñeen-fukki toftale ak benn ñooy joŋante. Saa-Senegaal yi ñooy dugg ci mbañ-gàcce yi, àtte leen.