Bi kàmpaañu njaayum gerte gi tàmbalee ba nëgëni sii, banqaasu SONACOS bi nekk Njurbel dajale na 22. 000iy toni gerte. Lim boobu nag, moo ëpp fukki yoon lim bi mu dajale woon daaw. Ki xamle xibaar boobule mooy Suleymaan Jóob, moom miy DRDR (Directeur régional du développement rural).
“Ba ci lélub tay jii, ndefaru SONACOS bu Njurbel dajale na 22. 000iy toni gerte ci ñaari weer kese.” (kàdduy Suleymaan Jóob yees jukkee ci APS)