MBËKK MI : JÀPP NAÑU MEERU JONWAAR BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Laasana Saar, meeru Jonwaar, ak yeneen juróom-benni nit ñu ngi ci loxoy Yoon jamono jii. Li tax ñu jàpp leen moo di ne, dañu laale ci mbirum mbëkk mi. Ginnaaw bi ñu fanaanee kaso, jébbal nañu leen toppekatu “Pool judiciaire financier” bi.

i ñuy tuumaal meeru Jonwaar bi mooy ne dafa bokk ci ñi doon lootaabe yëf yi, nekkoon ci bopp bi. Bees sukkandikoo xibaar yi rotee ci sàndarmëri bu Funjuuñ, moom Laasana Saar dafa bokkoon ci ñiy sumb mbëkk mi, daan fexe ba ndaw ñiy jël gaal yi, foofa, fa duni Saalum ya.

Fan yii, dañu jàpp ag gaal gu yeboon 241i mbëkk-kat yu dëgmaloon Tugal. Bi takk-der yi lëñbëtee telefon yi, ci lañu gis ne meeru Jonwaar bi doon bind ay kootowaaleem ngir laaj leen ndax lépp a ngi jaar yoon.

Moom nag, Laasana Saar, li mu lay mooy ne, dafa doon wutal i layookat ñi ñu tuumaal.

Yéenekaay L’observateur moom, siiwal turi 6i nit yi ñuy topp niki meeru Jonwaar bi. Ñoom nag, mbooloo mooma daan nas mbir yi, diggante 300 000 jàpp 400 000 FCFA lañu daan fayeeku képp ku bëggaan dem ci gaal yi. Te, ci lees wax, yàgg nañoo yóbb ay nit.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj