NJIITU RÉEW MI JËMMAL NA ÑEENTI SÉMBI SÀRT YEES WOTE WOON FA NGOMBLAAN GA
Fan yee jàll la dépite yi doon càmbar ñeenti sémbi sàrt. Bi ci jiitu mooy sémbu sàrt bi jëm ci settantal dayo ak kaaraange yoolekat yi. Bi ci topp jëm ci taxawalug OFNAC bu yees. Bi ci toppaat mooy bi ñeel li jëm ci xibaar. Bi ci mujj di bi ñeel xamle say moomeel. Ginnaaw bi ñu wotee ba jàllale leen, Njiitu réew mi jëmmal na leen. Maanaam, lees di wax ci farañse “promulguer” ngir sémbi sàrt yooyu mën a doon yees di jëfandikoo.
BÀYYEENDI NAÑU MANSUUR FAY
Ci weeru me wii jàll lañu ko yóbboon kaso, moom Mansuur Fay mi fi nekkoon jëwriñ ca jamonoy Maki Sàll. Booba ba tay, ma nga fa woon. Li gën a fés ci li ñu ko doon toppe mooy luubal xaalisu FondsCovid-19 yi, maanaam koppari mbasum koroona ma. Luubal gi ñu ko doon toppe mi ngi tollu ci ñaari miliyaar yu teg. Moom nag bàyyi nañu ko tay ci alxames ji bàyyig négandiku.
MAJAMBAL JAAÑ NEE NA MES
Bees sukkandikoo ci xibaar yi rot diggante démb ak tay, kii di Majambal Jaañ dañu ko woolu woon, démb, ci àllarba ji, fa DIC (Division des Investigations Criminelles). Waaye, moom mujjewul a wuyuji. Te, li ci gën a doy waar kay mooy bi takk-der yi demee këram di ko fa seet tamit, fekkuñu ko fa. Boobaak léegi nag, kenn tegagu ko bët, nee na mes, ne menteñ.
Waykat bii di Waali Sekk tamit nga xam ne woolu woon nañu ko démb mujj naa wuyuji waa PJF, ñu daldi koy déglu. Nde, dañu koo tudd ci caabalug CENTIF gi ci ay jokkalantey koppar yu leerul. Te, koppar yooyu tollu nañu ci juróomi miliyaar ak lu teg. Moom nag mujj nañu koo bàyyi ginnaaw bi mu joxee li ñuy wax “caution” bu tollu ci ñaari-téeméeri miliyoŋ ak fukk.
Naka noonu, kii di Mbugaar Juuf tamit mujj nañu koo bàyyi, tay, ci alxames ji. Moom Njiitu UPS (Union des Panafricanistes du Sénégal) ñi ngi ko doon toppe biral xibaar yu wérul. Bàyyi nañu ko tay donte ne sax jot naa def weer ci kaso bi. Ndax, ci njeexitalu weeru ut lañu ko jàppoon.
DAAN NAÑU NIKOLAA SARKOSI
Ki fi nekkoon Njiitu réewu Farãs at yee ñu weesu, daan nañu ko. Moom Nikolaa Sarkosi li ñu ko daane mooy lees di dippe mbootaayu defkati ñaawteef. Ñu koy wax ci farãse “association de malfaiteurs”. Looloo tax ñu daan ko juróomi ati kaso ak àllamaan bu tollu ci ñaar-fukki junniy ëroo (100 000 €).
XEW-XEW BU TIIS FA CIKOÑ
Naqar ak tiis la ña dëkke fa Cikoñ (Lingeer) di dund jamono yii. Senn soxna suy wuyoo ci turu M. Ba, tollu ci juróom-fukki at, lañu fekk mu xaru. Bees sukkandikoo ci waa Senego, dëkkandoo yi dañoo toog ab diir gisuñu ko. Ca lañu jógee di ko wër. Ci lees wax, dañu ko fekk mu xaru. Ndax, dañoo fekk ag buum gu takke ca baat ba.