LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (28/1/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NGOMBLAAN GI

Coppite am na ci doxalinu Ngomblaan gi. Dog nañu ndàmpaay yi ñu daan baaxe dépite yi ñeel seen dem ak dikk. Muy 900 000 FCFA (juróom-ñeenti téeméeri junni) yoy daan nañu ko jox dépite bi ci weer wu nekk. Ginnaaw bi ñu ko faree nag, dees na ko wuutale ag daamaar. Dépite bu ci nekk dina jot daamaaram ci ni mu gënee gaaw. Ndogal loolu nag, dina oyofal nguur gi yen bi nga xam ne, daan na ko dikkee daanaka 3i tamñareeti FCFA ci diggante 2022 ak 2024.

YEESAL YI ÑEEL SENELEC

Dees na amal ay yeesal yu am solo ci kërug liggéey gii di SENELEC (Société nationale d’électrification du Sénégal). Muy nisër bu jëwriñu soroj beek laf gi, Biram Suley Jóob, biral démb ci altine ji, fekk mu doon teewal réewum Senegaal ci ndajem réewi Afrig mi ñeel laf gi (Sommet africain de l’énergie Mission 300 ». Ñu ko doon amalee fa réewum Tansani, ci diggante 27 ba 28i fan ci weeru sãwiyee 2024. Naka noonu, jëwriñ ji di xamle ni yeesal yooyu doon nañu tay lu mënul a ñàkk. Nde, bees sukkandikoo ci xabaari bànku àddina si, dañ leen a waral ci mépp réew mu nàmm a wéy di jot koppar yiy bawoo ci seen campeef gi.

DEKKALI PÀRTI SOCIALISTE

Waa PS (Parti Socialiste) ñoo ngi ci yoonu dundalaat seen làng gi. Ci gaawu bii weesu (25 sãwiyee ) lañu doon amal seen ndajem fara-caytu yi. Ca ndaje ma nag, Aminata Mbeng Njaay, di fara-caytu bu mag bi, yékkati na fay kàddu woote ngir xirtal way-bokk yépp ci ñu liggéey ngir doon benn, rattaxal diggante yi te dundalaat seen i yitte. Naka noonu, muy xamle ni lépp luy ndogal te tukkee ci seen ndaje yi dees na leen doxal, ak lu mu metti metti. Te Ñoom ñépp a war a ànd ci wut i jumtukaay, jàppalante ci doxalin bi ngir mën ko jooxe. Wax na itam ni dees na tëggaat pékkug pólitig bi ak taxawal ndiisoo gu ñu sas mu doxal ndogal yi ñu jël ci seen ndaje yi.

YOON WOOLU NA MAMADU NGOM ÑAŊ

Dic (Division des investigations criminelles) woolu na Mamadu Ngom Ñaŋ mi fi nekkoon Dage (Directeur de l’administration générale et de l’équipement) fa njëwriñu tàggat-yaram yi, ca jamonoy Mataar Ba, Lat Jóob ak Maam Mbay Ñaŋ. Kenn xamagul nag li tax ñu woolu ko bees sukkandikoo ci sunu naataango yu Les Échos. Waaye, woolu bi daje naak jamono ji ñu waree déglu Lat Jóob (30 sãwiyee). Moom Lat Jóob nag, jiite woon fi Lonase, ñi ngi koy toppe luubal alalu askan wi, jël xaalis ak mbuxum. Ba tax ñu defoon ko mandat dépôt ci weeru sàttumbaar wale weesu.

MBËKK MI

Démb ci altine ji, sàndarmëri teg na loxo juróom-benni doom-aadama yu tegu woon ci yoonu mbëkk mi. Ñoo ngi leen jàppe ci dëkk bi ñuy wax Bulel, nekk ci diiwaanu Kafrin. Bees sukkandikoo ci xibaar yi ñu jot a biral, ñoom ñépp Medina Gunaas lañu soqikoo. Cib minibiis lañu duggoon wutali Ndar ngir duggee fa gaal utali Espaañ.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj