Nguur gi seqi na ñaareelu jéego ñeel sémbuw jotale dëkki kow yi ak ndox mu sell mi (phase de II du Projet d’approvisionnement en eau potable en milieu rural). Démb ci altine ji, 3i fani sãwiyee 2024, lañu ko doon amal fa diiwaanu Luga, ci teewaayu elimaanu jëwriñ yi Sëñ Usmaan Sonko, gornooru diiwaan ba, Ndey Ngenaar Mbooj, Li Yan (ndawu àmbaasaadu réewum Siin) ak Ceerno Mbàkke (Meeru Daaru Marnaan). Ci biir i kàddoom, elimaanu jëwriñ yi dellusi na ci yittey Càmm gi ngir saafara jafe-jafey ndox mi ci dëkki kow yi. Ba tax mu biral ni dinañu jële ndox mi ci ballukaay yi gën a mag, xëcc ko ba ci béréb yi ko amul ngir Senegaal gépp bokk cee jot.
MBIRI CEDEAO AK AES
Dépite Gii Mari Saañaa mu ngi woo kurélug CEDEAO gi mu nangul waa AES seen kurélug bopp. Ci xëtu Facebookam la ko siiwal. Muy xamle ni lu war la ngir ñu bañ a ñàkkal fayda réew yooyii ci biir waxtaan wi ñuy séq ak ñoom. Cig pàttali, Njiiti réewi CEDEAO yi, ca seen ndaje ma, fasoon nañu yéene amal i coppite li ko dale ci weeru sãwiyee wi jàpp sulet 2025 ngir seppi ci seen kurél gi réewi AES yi.
DOOMI RÉEWUM SENEGAAL YI ÑU GÉNNE ALSERI
Doomi réewum Senegaal yi Nguurug Alseri génne dëkkam ñoo ngi sàkku ci Nguurug Senegaal mu delloosi leen fi réew mi. Xibaar booboo ngi jóge ci kurél gii di ADHA (Action pour les Droits Humains et l’Amitié), di yëngatu ci wàllu àq ak yelleefi doom-aadama. Ci yëgle bi mu génne, tollu nañu ci 81i Saa-senegaal yuy dund ci anam yu doy waar fa dalub OIM (camps de l’Organisation Internationale pour les Migrations) ba nekk réewum Niseer. Am na itam ñu nekk ci màndiŋ mi, ci béréb yu sorewul lool ak digi Alseri yi.
NJEEXITALU NDIMBALI USA YI TRUMP DOG
Ndimbal yi Donald Trump dog ñeel suqaleeku réewi Afrig yi tàmbali na feeñ xaat ci réewum Senegaal. Elimaanu jëwriñ yi moo biral xibaar bu ni mel. Muy xamle ni Sémb yu bare taxaw nañu fi Senegaal ndax ndogal yi Njiitu Etaasini li jël bu yàggul dara. Bokk na ci sémb yooyu, wenn wu dem ba ci 500i tamndareeti dolaar, war a tollook 316i tamñareeti CFA. Naka noonu, muy fàttali ni waa réew mi rekk ñoo mën a tabax seen suqaleeku bopp. Lu ko moy, réew mi du mës a suqaleeku fiileek moo ngi yaakaar ndimbal yuy bawoo bitim-réew. Te li ni mel doy na ci seede.