NOSTE PÓLITIG GOG IRÃ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw ba Humayn àndee ak askan wa daaneel Nguur ga fa nekkoon, ca lañu amalee ay wotey referàndom, keroog bési 30 ak 31 màrs 1979. Li mu ko dugge woon mooy laaj askan wa ndax ànd nañu ci ñu samp Bokkeefu Lislaam ca réew ma, maanaam “République Islamique”. Ca la “Waaw” ja féete kaw “Déet” ja ci xaymag 98,2% ca ña àddu fésal seen ug nangu.

Bees sukkandikoo ca Ndayu-Sàrt réew ma (Constitution), ca dogu 57eel ba (article 57) : “Bànqaas yi ŋànk Bokkeefu Irã mooy Ngomblaan gi (Péncu Ndawi réew mi), Càmm gi (Nguur gi), Këri àttekaay yi. Waaye, ñii ñépp, seen liggéey, ña nga koy amal ci kilifteefu walla caytug Kilifa gu mag gi (Guide Suprême).

Laataa nuy ñëw ci Kilifa gu mag gi mooy kan ak sañ-sañam ak anam bees koy tànne, danuy dikk njëkk ci ña koy tànn. Moom Kilifa gi ña koy tànn ag Kuréel la gog, manees na koo tudde Ndajem Way-xereñ yi (Conseil des Experts).

Kuréel gi nag, askan wi ñoo koy tànn. Gox bu nekk (Région), boo amee lu mat téeméeri junni (500 000) xob dinga am kenn ku la teewal ci Kurél gi, lu limu xob yees la sàndil ci gox bay gën a bari, lim ba koy teewal ci Kuréel gi di gën a yokku. Ñii nag, ñu xereñ la ñuy doon, fés ci xam-xam ak ci jikko. Ba tax na nekkut lawax (candidat) bu sampu rekk ñu bàyyi la nga bokk ci wote yi, ndax amaat na geneen Kuréel gu nekk ca Ngomblaa ga (Péncu Ndawi Réew ma), ñu man koo méngale ak “Cena” walla “Congré”, ñoom ñooy segg lawax yi, tànn ña ca gën a kawe ci wàll yépp ngir ñu bokk ci wote yiy tax nga man a nekk aji-bokk (membre) ci Ndajem Way-xereñ yi (Conseil des Experts).

Kuréel gii nag di Ndajem Way-xereñ yi, ñoom ñooy tànn Kilifa gu mag gi (Guide Suprême). Waaye tànn googu, Ndayu-Sàrtu bi moo kay sàrtal. Bees sukkandikoo ci dogu 109eel bi, ki ñuy tànn, màndarga yii ñoo war a daje ci moom : “Kawe ci xam-xam, jub, màndu, ragal Yàlla, dégg jamono, am dayob jiite aw askan”. Bu ko defee, lawax yi war a joŋante dañuy xool kenn ca ñoom kok, moo gën a matale sàrt yii, ñu tànn ko, jiital ko. Bu fekke xool nañu ba sonn gisuñu ku féete kaw ay moroom, dañuy xool ci lawax yi ñett ba juróom ñoñ, ñoo gën a ràññeeku ci sàrt yi, ñu tabb leen ci lees man a tudde Ndajem mbooloo mi (Conseil Collectif), nga xam ne “Kilifa gu mag gi” dootut doon kenn nit, waaye ag Kuréel lay doon. Kon, ñu man caa dégge ne, ëllëg walla ginnaaw-ëllëg, bu fi Xamanaay jógee, kenn nit man na koo wuutu, walla ag Kuréel.

Ndayu-Sàrt bi jëlaat na beneen matukaay : bu fekkee amut kenn ku am dayob doon Kilifa gu mag gi ci biir lawax yi, te maneesut a am it ci ñoom ñetti nit ba juróom yu man a am dayo doon ag Kuréel, mayees na kuréel gii di Ndajem Way-xereñ, mu tànn kenn ci ay way-bokkam. Ndax, ñoom it, ñaare, dañuy am dayo bi ngir man a nekk “Guide Suprême” ndax nees leen di seggee, maanaam “filtre” yi ñuy jaar yépp laataa ñuy bokk ci Ndajem Way-xereñ. Kon, ci gàttal, kuréel gii mooy tànn Kilifa gu mag gi. Nu fàttale ne, nii mu ame sañ-sañu tànn Kilifa gu mag gi, noonii la amee sañ-sañu wàcce ko bu sàgganee lenn ci ay wareefam. Maanaam, tay jii, Xamanaay li miy am doole yépp, bu defoon lu warut, wuute ak la taxoon ñu samp ko, Ndajem Way-xereñ mi am nañu sañ-sañu wàccee ko.

Ginnaaw bi ñu tànne Kilifa gu mag gi, manees na tënk ay sañ-sañam ci yii :

  1. Tëral naaluw pólitigu réew mi (définir la politique publique) ginnaaw bi mu ci diisoowee ak kuréel gii di “Ñiy saytu Njariñal réew mi”, moom it di génn ci ñetti kuréel yiy gunge Nguur gi (Conseil de veille sur les intérêts de la nation, Conseil Supérieur de la Sécurité Nationale, Conseil de Révision Constitutionnelle) ;

  2. Joxe ndigal ngir ñu amal ay referàndom ;

  3. Jiite Xare bi (l’armée bi) ;

  4. Sóobu ci xare ak dakkal ko ;

  5. Fal ak folli ak nangu bàyyig kilifa yii :

    1. Woroom xam-xam yiy jëmmal lees man a tudde “Congré”;

    2. Kiy jiite Këri àttekaay yi ;

    3. Njiitu tele bi ak rajo bi ;

    4. Njiitu Kurél gi njaboote soóbare si (soldaar yi) féetewoo ak Bokkeef gi ak soóbare si féetewoo ak Fippu gi (Révolution) ;

    5. Kiy jiite soóbarey Fippu gi ;

    6. Ñiy jiite soóbarey Bokkeef gi ak ñi yor kaaraange biir réew mi.

  6. Àtte wuute yiy am ci ñetti Bànqaasi Bokkeef gi ak fexe ba ag déggoo am seen biir : Baatu doxal bi (Exécutif), Baatu yoonal bi (Législatif) ak Baatu àtte bi (Judiciaire) ;

  7. Jafe-jafe yi nga xam ne maneesu koo saafara jaare ko ci “Conseil de Veille sur les Intérêts de la Nation”, moom la ñu leen di bàyyeel ngir mu indi ci ay saafara ;

  8. Ginnaaw bi askan wi tànnee Njiitu Réew ma (Président de la République) moom moo kay dëggal… Moom it seggukaay (Filtre) la ci lawax yi yi war a nekk Njiitu Réew. Dafa di, laataa ngay doon Lawax, fàww “Congré” bi nangul la ko ginnaaw ba ñu saytoo say mbir ba xam ne yaw mii am nga dayo bi ci xam-xam ak ci njub. Bu “Congré” bi noppee jébbal mbir bi “Guide Suprême” bi moom it mu dëggal ;

  9. Wàcce Njiitu Réew li ginnaaw bi Ëttu àttekaay bu Kawe bi (Cours Suprême) biralee àtteem ne, Njiitu Réew mi dafa sàggane ay wareefam, walla bu njiitu Ngomblaan gi dogalee ne Njiitu Réew mi matewut lees ko doon doyee ginnaaw ba ñu sukkandikoo ci dogu 89eel bi ;

  10. Jéggal kok, àttees na ko ba noppi ginnaaw ba ki jiite Këri Àttekaay yi sàkkoo loolu ci moom fekk mu doon ngëneel, dëppoo ak Yoon. Am na sañ-sañu it jël lenn ci ay sañ-sañam jébbal ko kenn walla ag kuréel ngir ñu taxawe ko (ni ko Xamanaay defe fan yii ci xare bi) ;

  11. Saytu ndax anam ba ñuy doxalee Naalu pólitig wi jaar na yoon.

Lii mooy li soxal Kilifa gu mag gi ak nees koy tànnee, ak ay sañ-sañam, ak ña koy tànn… Ngir bañ mu gën a gudd, dees ko fiy yamale, lu soxal Njiitu Réew ma, dees na ko gaaraal ci beneen yaxal bob, dees na ci leeral anam yees koy tànnee (suffrage universel) ay sañ-sañam, ak yeneen Kuréel yi ŋànk Nguur ga.

Seexunaa Njaay
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj