LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (ÀJJUMA 24 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Séex Umar Jaañ ak Abdu Kariim Géy dellu nañu kaso

Ñetti weer kepp la Séex Umar Jaañ ak Abdu Kariim Géy gis jant bi ginnaaw biñ leen ko nëbbee woon jamono yee weesu. Nde, àttekat bi daf leen dóoraat « Mandat de dépôt », ñu daldi dellu kaso. Seen yoon wu njëkk wa ça kaso ba, tuumay ciiwalug xibaar yu wéradi lañu leen doon toppe, ñeel génnug àdduna Imaam Aliyun Badara Ndaw. Wile yoon, nag, ñoo ngi leen di tuumaal lees duppee ci daráse “atteinte à la sureté de l’Etat”, maanaam dañuy nasaxal kaaraangeg Nguur gi.

Yewwi Askan Wi

Ab diir, ginnaaw bi ñu amalee woon seen ndajem-ñaxtu ma, lëkkatoo YAW delloo na buum ca mboy-mboy ga. Nee ñu,  dinañu amalaat meneen ndajem-ñaxtu ñaar-fukki fan ak juróom-ñeent ci weeru màrs. Maanaam, bu ñu nee suba la layoo Maam Mbay Ñaŋ ak Usmaan Sonko.  Ci ndajem-waxtaan mi ñu doon amal ci bésub tey ji lañu ko xamle. Te, ci seen i wax, jébbal nañu sax bataaxalub càkkuteefu perefe ngir amal ndaje moomu.

DIINE

Tey, ginnaaw julli jumaa ji, ndongoy boroom xam-xam bii di Séex Muhammad Ahmad Lóo doon nañ amal janook taskati xibaar. Liñ ko dugge woon mu indiy leeral ak à teggi tuuma ñeel kàdduy Ahmet Xalifa Ñas. Ndax, dañu seetlu ne, ay jamonoo ngi nii, ngóor si Ñas di yékkati kàdduy tuuma ak waxi jaxase di leen teg ci kow Doktoor Muhammad Ahmad Lóo. Ahmet Xalifa Ñas day wër jotaayi tele yi di wax naan kàngamu diine ji dafa bañ Magi réew mi, maanaam day xeex tarixa. 

Ndongoy Séex bi nag, ñoom Ustaas Umar Jàllo, imaam Umar Sàll ak ñi ci des, setal nañ seen kilifa gi ci tuuma yooyu. Ñoo ngi artu ak a ñaax taskati xibaar yi ngir ñu ànd ak maandute, bañ a dalal kenn kese, tàllal ko mikóro muy wax ay wax yu ñaaw jëmale leen cig kilifa gog, àddina sépp a ko weg. 

Sowaal : xeex diggante ñaari daara

Ca koñ bees duppee Caritas la xeex ba ame. Sëriñ daara bii di Baabakar Kan moo doon xeex ak ndongoy daara yu Sëriñ Mbay. Ndeysaan, musibaa ci topp. Yéenekaay L’observateur moo siiwal xibaar bi. 

Baabakar Kan ak Sëriñ Mbay ay xarit lañ woon. Waaye, seytaanee dugg seen diggante, Baabakar Kan daldi ber daaraam. Looloo naqadi taalibey Sëriñ Mba, rawatina ñett ñii di Moor Saar, Muhammed Caam ak Baabakar Jaañ. Moo tax, fuñ jekku waan Baabakar Kan, daldi koy tooñ. Naka noonu, ayu-bés bii weesu, dañoo fekk Sëriñ biy amal xew-xewam, ñu koy jéem a yàqal, far xol yi jóg, ñu jaxasoo, xeex. Ca la Sëriñ Baabakar Kan jëlee ab kuur, dóor ko kenn ci ndongoy Sëriñ Mbay ya, toj bopp ba, mu faatoo ça. Céy Yàlla…

BITIM-RÉEW : Kamerun

Démb, ci alxames ji (23 màrs 2023), la kurél giy sàmm ndeyu àtte réewum Kamerun siiwal Njuréef ya tukke ca wotey senaatëer ya fa amoon, keroog 12 màrs 2023. 70i toogaan la 10i làngi pólitig doon xëccoo. Làngug pólitig gii di RDPC (Rassemblement démocratique du peuple camerounais ) te Njiitu réew ma, Póol Biyaa, jiite ko moo jël lépp. Rax-ci-dolli, Njiitu réew ma ci boppam, mooy tabb 30i senaatëer yi war a dolleeku ca Senaa ba, ak it Njiitul senaa ba.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj