LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (ALTINE 24 AWRIL 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SONKO

Sonko dooraat na nemmeekoom yi. Tey, ça Sigicoor, génnoon na, mbooloo mu bari dar ko, topp ko. Lu ko jiitu, dafa yaxaloon ci mbaali-jokkoo yi, bind di wax ak ay militaŋam, yégal leen ne liggéey bi dooraat na. Dafa bind ne :

“Maa ngi leen di yëgal ne danuy wàcc ci mbedd mi, seeti askan wi, wéyal liggéey bi. Nii lay tëdde :

  • Li ko dale 24 jàpp 27 awril, Sigicoor ak Biññoona ñoo aye ;

  • 29 ba 7 me 2023, Nemmeeku Tuur ca Tiwaawon ak Cees ;

  • 7 me, mbetteel ;

  • 12 me 2023, yëngu-yëngal waa F24. 

Bu leen kenn dugal ci waxi pólitig yu amul solo te lëmbe réew mi fan yii. DEMLEEN BINDUJI BU BAAX A BAAX. FUKK AK JURÓOMI FAN REKK A CI DES !”

CESE : ABDULAAY DAAWDA  JÀLLO WUUTU NA IDIRIISA SEKK

Njiitu réew mi, Maki Sàll, tabb na Ablaay Daawda Jàllo ci boppu CESE,mu wuutu fa Idrissa Sekk. 

Li Idi fésal bokkam ci wotey 2024 yee tax Maki Sàll tàggook moom. Bu dee Ablaay Daawda Jàllo, Jëwriñu Càmmeef gi la woon, doonoon itam njiitalu kabine Njiitu réew mi. Léegi, moo ñetteelu jëmm ji ëpp dayo ci réew mi ginnaaw Njiitu réew mi ak njiitu ngomblaan gi.

AAMADU BA FÉETEWOO NA CÀMM GI AK TÀGGAT-YARAM GI

Ndomboy-tànk Aamadu Ba, magum jëwriñ ji, full nañu. Nde, bés niki tey, mooy boole nekk magum jëwriñ yi boole ci ñaari njëwriñ : gu càmm geek gu tàggat-yaram gi. Ndaxte, li Idrissa Sekk génn lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar a tax jëwriñ yim amoon ci Nguur topp ko, muy Aali Sale (càmm gi) ak Yanqooba Jatara (tàggat-yaram).

TAXAWAAYU F24 ÑEEL PÉNCOO MI NJIITU RÉEW MI WOOTE

Ginnaaw bi Njiitu réew mi Maki Sàll wootee péncoo ñeel mbiri réew mi ci fan yii weesu, waa F24, di mbootaay gi fi juddu bu yàggul dara, teel nañoo fésal seen taxawaay ñeel woote boobu. Ña nga koy xamal ni bañuñu cee bokk. Waaye fa ñu tegoon seen tànk ci njuddu li teggiwuñu ko. Nde, fàww Njiitu réew mi fésal ne du bokk ci wotey Njiitu réew mi ba noppi, xàllal yoon wi mboolem ñi bëgg nekk lawax te bàyyi maxejj yi mu tëj kaso te teguwul ci lenn lu dul pólitig.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj