LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (ALXAMES 30 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Daan ba dal na ci kow Usmaan Sonko

Tey lañu doon àtte Usmaan Sonko ak Maam Maam Mbay Ñaŋ. Daan ba nag, dal na ci kow ndoddu Usmaan Sonko. Daan nañu ko lu tollu ci ñaari weeri kaso yu mu dul tëdd ak ñaari téeméeri miliyoŋ yu mu war a dàmpe Maam Mbay Ñaŋ. Nee ñu nag, daan boobu mënu koo tere nekk lawax ci wotey 2024 yi. Coow li nee na kurr ci réew mi.

Doxu-ñaxtu Yewwi Askan Wi bi mujjut a am

Bu weesoo layoo Usmaan Sonko-Maam Mbaye Ñaŋ, waa Yewwi Askan Wi nammoon nañoo amal ab doxu-ñaxtu ci bésub 30 màrs bi. Waaye, ñaxtu bi mujjul a àntu. Nde, takk-der yi mayuñu leen fuñ yakke seen nàkk. Bi suba teel di jot lañu taxaw ci boppi koñi Ndakaaru yi, rawatina ca Site Kër-Góorgi, fa Usmaan Sonko dëkk ak ca VDN ba, ca dalu làngug politig gii di PRP (Parti Républicain pour le Progrès) bu Décce Faal nekk, di yit bérébu ndaje kilifay Yewwi yi. Pexe yi takk-der yi lal a tere waa Yewwi ak seen i ñoñ mën a dajaloo ak a yëngu-yëngal.

Maam Mbaye Ñaŋ a ngi jaljali

Ginnaaw bi àttekat bi daanee Usmaan Sonko, Maam Mbaye Ñaŋ dafa bég, di jaljali ak a bàkku. Nde, moom, boroom PRODAC, dafa jàpp ni daan yees daan njiitul Pastef li ndam lu réy la ci moom.

Mbirum 3eelu moome gi : Idiriisa Sekk nee na « … amul ñett. »

Ca Etaasini ba mu demoon, njiitul CESE li, Idiriisa Sekk daje na fa ak ndongoy Senegaal ak yu Afrig yi bokk ci kurél gii di Yale Club. Ca biir waxtaan wa, nag, ndongo ya laaj na ko ci mbirum 3eelu moome gi. Ba muy tontu, daf leen a fàttali ab ponk ci pólitigam, te mooy « fexe ba Senegaal doon demokaraasi bu mat, di réew moo xam ne, dinañ joxe nguur gi wëliis taafar, ci diir buy wéy bob, du weesu 10i at, ñaari moome yu juróomi at, amul ñett. » Mënees na cee déggee ne, Idiriisa Sekk àndul ak Maki Sàll ñeel ñetteelu moome gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj