LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (ALXAMES 6 AWRIL 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

JA BU LAKKATI CA KAWLAX

Lakk gu mettee metti moo am ca Kawlax, ci guddig àllarba ji jàpp alxames. Ma nga amee ca jawub sàndikaa (marché syndicat) bu Kawlax, bi 4i waxtu di jot, ci xaaju guddi gi. Ci xibaar yi jot a rot, nemmeeku nañ fa yàqu-yàqu yu bare sax. Nde, ag daamar gu yeboon i njaay ba fees ak lu tollook ñaar-fukki mbaar lakk nañu fa ba jeex. Rayaale naat lu ëpp 10i xar. Muy i tamndareeti FCFA ci xayma. Ginnaaw ba sàppëer yi fayee lakk gi, sàndarmëri ubbi nab gëstu ngir xam fu lakk gi jóge.

NDAJEM JËWRIÑ MI : TABB YU YEES YI

Ca ndajem-jëwriñ ma mu doon amal démb, Njiitu réew mi jot naa am ñu mu fa takkal i ndomboy-tànk. Muy ku ci mel ni Elaas Aamar Lóo (Président de la Commission de Supervision de la Haute Autorité du Waqf), Paap Aadama Siise (Secrétaire général de la Haute Autorité du Waqf), Mamadu Bajaan (Directeur régional du Développement rural de Kaffrine), Sàmba Ndaw Taal (Directeur régional du Développement rural de Kaolack), Suleymaan Jóob (Directeur régional du Développement rural de Diourbel), Hamadu Balde (Directeur régional du Développement rural de Kolda) Baraahima Mamadu Ba (Directeur régional du Développement rural de Tambacounda), Abdulaay Kamara (Directeur régional du Développement rural de Fatick) Séex Ahmet Tiijaan Jeŋ (Directeur régional du Développement rural de Matam), Kasimir Adiriyeŋ Sàmbu (Directeur régional du Développement rural de Sédhiou), Umar Mbeng (Directeur régional du Développement rural de Dakar), Tàkko Jaawara (Directeur régional du Développement rural de Saint Louis), Sã Póol Bampoki (Directeur régional du Développement rural de Ziguinchor), Daawuda Aan (Directeur régional du Développement rural de Louga), Njaase Saar (Directeur régional du Développement rural de Kédougou), Madikke Siise (Directeur de la Prévention et de la Gestion des Inondations).

NJÀNG MU KOWE MI

Jàngune ba féete ca Jamñaajo, ñu duppee ko Aamadu Maxtaar Mbow, ndongo yaa ngay yëglu. Lañu xamle mooy, seen um njàng mi dafa nar a tagatembe. Ndax ba ñu ubbee bunti UAM ba léegi, ndongo ya dalaguñu baa. Maanaam, dooraguñ njàng mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj