Li gën a fés ci xibaari bés bi (Gaawu 4 fewaryee 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NJÀNG AK NJÀNGALE 

Ab toogaanu-ñaxtu la ñenn ci jàngalekat yi ñuy woowe “contractuels” amaloon démb. Lañuy jooytu doon lañu yeex a jot ca seen CAP, maanaam lijaasa bi leen di tax a bokk ci liggéeykati Bokkeef gi, maanaam “Fonction publique”.

NJÀPPUY KASO YI

Paap Njaay mu Walftv

Démb lañu woolu woon taskatu-xibaar bii di Paap Njaay fale ca « Sureté Urbaine ». Lees koy tuumaal mooy ciiwalug xibaar yu wéradi ñeel Yoon ci mbirimum Aji Saar ak Usmaan Sonko. Nee ñu, bi ñu ko laajee ngir mu joxe ci ay firnde, daf ne liggéeyam mayu ko loolu. Moom nag, ña nga ko fa téye. Ci altine ji lay jàkkaarloo ak Toppekatu Bokkeef gi. 

Gii Mari Saaña ak way-moome yi

Dépite bii di Gii Mari Saaña bokk ci kurél gii di FRAPP, moom, ak ña mu àndaloon ñépp, ca kanamu àmbasaadu Tinisii ba ca Ndakaaru, jàpp nañu leen. Ñoom nag,  dañoo bëggoon a amal foofa ab ñaxtu ngir ñaawlu li seen mbokk yi di daj ca Tinisii.

PÓLITIG

Aminata Ture – PDS 

Ngir xeex ñetteelu moome gi Njiitu réew mi, Maki Sàll, bëgg a dagaan, kujje gaa ngi lal I pexe, di jéem a taxawal kurél gu yaatu te am doole. Li ñu ko dugge mooy def benn say ngir gën mën a jàmmaarloo ak Njiitu réew mi. Waaye, mel ni cat mi ngi ciy bëgg a duggu. Ndax, waa PDS, ñoom, nee nañu xalaatuñoo ànd ak Mimi Ture di xeexandoo ci data, rawatina Maki Sàll mi mu àndaloon diirub 12i at, moom soxna si. Nee ñu, lépp lu fi Maki Sàll mës a def, loxo Aminata Ture setu ci, kon xel nanguwul ñuy ànd ak moom.

Aminata Ture nag, génne nab yégle,  di ci tontu waa PDS. Ciy waxam, njiiti PDS yi dañoo nekk ciw waxtaan wu sore ak Njiitu réew mi Maki Sàll te kenn umpalewu ko. Nee na loolu rekk a tax ñu bañ a ànd ak kujje gi.

BITTIM RÉEW

Ëpp na ayu-bés bi Kayis Sayed (Njiitu réewum Tunisi li) yékkatee i kàddu yu ñagas ngir boddi doxandeem yi ca réewum Tinisi te diy boroomiy der bu ñuul. Ba léegi, kàddoom yaa ngi wéy di leen jural xataange ca réew ma. Bu yenn réew yi tàmbalee jëli seeniy doomi-réew ngir ñu ñibbi, kii di Aminata Ture (nekkoon fi magum-jëwrin ci Nguuru Maki Sàll) mënul a wanaasu yooyu kàddu. Jàpp na ni sax dees war a ajandi réewum Tinisi ci kuréli Mbootaayu Réewi Afrig yi. Nde waxam ji dafa jalgati kenug Mbootaay gi. Te kenn waru leen a bàyyi ñuy bokk ci CAN bii di ñëw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj