LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (TALAATA 11 AWRIL 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NGOMBLAAN GI : DEPITE YU YEWWI ASKAN WI BAÑ NAÑU NGANTALUG COOBARE GU WAA BENNOO BOKK YAAKAAR

Dépitey lëkkatoo Yewwi Askan Wi nee nañu dañuy bañ ngàntal gi dépitey lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar namm a gàntal liggéeyub Ngomblaan gi ci seen coobare bopp. Bi ñuy tënk liñ jot a liggéeyagum ca Péncum ndawi réew ma lañu xamlewaale ne, jot nañoo jébbal limub 90i laaj Nguur gi. Laaj yooyu, nag, jottalees na leen Pekkug Ngomblaan gi ci ndoorteelu liggéey bi ba keroog, 28 màrs 2023. Waaye de, ci xayma, téeméer yoo jël, ci 14 yi kese la Nguur gi tontu. Yi ci des yépp daf cee noppi.

Dépitey kujje gi leeral nañu ni laaj yooyii tëdde : 48i laaj yees bind yoy, 13 kese ci am tontu jóge ci Nguur gi ak 30i laaj yoy, dara la ci Nguur gi tontuwul, tus. Teg nañ ci 12i laaj yu ñeel xewxewi jamono yoo xam ne tamit, Aamadu Ba ak i ñoñam àdduwuñ ci.

Rax-ci-dolli, dépitey Yewwi Askan Wi def nañu ñetti ndigle ngir ñu taxawal genn kurélug luññutu gu jàmbure ak yeneen ñaar ngir ñu àtte ay jëwriñ ca kanamu Àttewaay bu kowe ba.

LEERALI MÀGGET JUUF SAAR ÑEEL AG DEMAM

Màgget Juuf Saar mi nekkoon tof-njiitu meer bu Kër Masaaru kow (Keur Massar Nord) moo jóge Pastef dem APR. Moom nag, li mu lay mooy ne, jàmm lañu bëgg. Ndaxte, mënuñoo suqali fu jàmm amul. Mu teg ca ne, foofa mu dëkk, li ëpp ci ndaw ñi am nañu ay lijaasa, waaye liggéeyuñu. Rax-ci-dolli, dafa bëgg ñu kopparal seen jigéen ñi. Sabab yoyu, ciy waxam, moo tax mu fekki Njiitu réew mi, Maki Sàll.

LI DR ABDURAHMAAN JUUF DI XAAR CI IDIRIISA SEKK

Abdurahmaan Juuf doon na amal aw waxtaan ak taskati-xibaar yu Jeunes Reporters. Jot nañoo waxtaane ponk yu bari yu lëmbe réew mi. Jot nñoo laaj njiitul pàrti Awale li ci Idiriisa Sekk mim bokkaloon làngug pólitig. Moom, Abdurahmaan Juuf, daf ne :

« Dama jàpp ne moom, Persidã Idiriisa Sekk, moo ma war a jàppale. At ya may gën a taxaw ci pólitig, Idiriisa Sekk laa leen jox. Foog naa ni am nay jaaruwaay yu mën a am te,tagguma sama bopp, waaye ma doon lawax moo gën mu doon ko. »

Dolli na ca, ne :

« Jox naa cër pàrti bi bu baax. Idiriisa Sekk dimbali na ma bu baax ci diirub 8i at. Waaye nag, dama bëgg a leeral ni, man, duma donob pólitig. Bu doon mbirum ndono kese, duma génn Rewmi. Kon, ca sama xelu bopp bi may doxe, di wut, duma dono. »

KÉEDUGU DINA DALA NDAJEM JËWRIÑ MEES TOXAL DIGGANTE 24 JAPP 27 AWRIL

Yéenekaay Les Échos moo biral xibaar bi. Ginnaaw Séeju, diiwaanu Kéedugu moo war a dalal Ndajem jëwriñ mees toxal diggante 24 jàpp 27 awril. Nee ñu sax, jigéeni Bennoo Bokk Yaakaar yu Kéedugu daje nañu, waxtaan, ngir waajal ñëwub Njiitu réew mi. Ndaxte, dañ ko bëgg a gatandu nees di gatandoo buur.

AY GINAAR YU YÀQU YEES TEG LOXO CA BURKINAA FAASO

Fukk ak ñetti daamar yu yeb ba fees i ginaar yu yàqu lañ teg loxo ca réewum Burkinaa Faaso ci njeexitalu ayu-bés bi. Ci xayma, dina tollu ci 100i tamndareeti FCFA. Ginaar yooyu nag, ña nga jóge woon Tugal, ñu naroon leen a jaaye ci biir réew ma. Bees sukkandikoo ci Kàdduy Iif Kafàndoo, di Njiitul kurél giy xeex jalgati ca réew ma, anam yi ñu leen dencee ngir indi leen foofu ñoo sellul. Looloo waral ba ginaar yi tàmbalee yàqu ci yoon wi. Bu ci askan wi jotee ba di leen jëfandikoo dana leen jural ay jàngoro te dana andi jafe-jafey wér-gi-yaram ci réew mépp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj