Usmaan Sonko : « Waxtaan wees woote, sàkkal pexe Usmaan Sonko rekk a di jubluwaay bi… »
Usmaan Sonko de, narul bokk ci waxtaan wi Njiitu réew miy woote. Ku dégg ay waxm, démb ci altine ji, bi muy janook taskati xibaar yi, loolu nga ciy jànge. Dafa mel, bu lenn ci kujje gi wuyujee Maki Sàll ci péncoo moomu muy nas, moom du ca dem. Moom, njiitul Pastef li, dafa jàpp ne waxtaan wi, Maki Sàll duggewu ko lenn lu dul beddi ko, wéetloo ko ci géewu pólitig bi. Usmaan Sonko nag, ciy waxam, ragalul loolu.
« Waxtaan wees woote, sàkkal pexe Usmaan Sonko rekk a di jubluwaay bi. Dafa bëgg a daganal ñetteelu càkkuteefug moome gog, Yoon mayu ko ko. »
Kàdduy meeru Sigicoor yii ñooy wone ne, noppi ci jàmmaarloo ak Maki Sàll ba mu jeex. Bees seetloo nim waxee, xam ne ku dogu la ci taxawaayam ñeel waxtaan woowu mu jàppe ay caaxaan. Moo tax, mu wax waa F24, kurél gi juddu fan yii wees, ne leen buñ ci bokk.
«Nun, dunu mës a nangu ñu nuy ngëtën. Dunu waxtaan mukk ak kuy teg fetal ci sunu kaabaab gi. Boo foogee ni danu koy wuyu ci wooteb waxtaanam woowu, mi ngi nax boppam. Mbirum fulla la ak ngor. Li mu def lépp, ngir am lum ko weccool la. Maa ngi am sañ-sañu yaakaar ni, F24 ak Yewwi Askan Wi duñu nangu digey pólitig yooyu. »
Bu ñu ko nangoo tam, jaral na Usmaan Sonko wéet ci kujje gi, ànd ak askan wi mu mës a àndal. Ay waxam la.
Soxna Aminata Ture toj na “Deal” bi dox diggante Benno Bokk Yaakar ak PDS
Soxna Aminata Ture doon na amal ndajem waxtaan moom itam fa Centre socioculturel bu Garã-Yoof. Da doon faramfàcce li xew ci réew mi ak waxtaan wi ko lëmbe, te Njiitu réew mi woote ko. Moom, magum jëwriñ ja woon, dafa jàpp ne, waxtaan woowu, pexem pólitig dŋŋ a ko lal ngir féewale kujje gi.
Soxna si fi nekkoon jëwriñu Yoon wi, waxeet na ne, Njiitu réew mi dafa kootoo ak waa PDS. Ñoo bokk « deal » bi.
« Deal bii ma doon wax diggante Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak PDS toj na tasar. Dafa di, PDS nekkul aji-bokk ci waxtaan wi. PDS dafa bokk ci ñi sumb waxtaanu caaxaan woowu. »
Mimi ture gën na sori ciy wax sax, dem bay xamle ne Antuwaan Feliks Jom, jëwriñu biir réew mi, mooy doon aji-yombal ji. Bee sukkandkioo ci kàdduy Mimi Ture, Li waa Bennoo ak waa PDS di nas, mooy fexe ba Maki Sàll bokk, ñetteel wi yoon, ci wotey 2024 yi, ak njéggalug Kariim Wàdd.
« Te sunu 138i tamñret yim nu yoreel, dañ koy ñàkk, ak xaalis biñ def ci layoo bi yépp. »
Bu dee wàllu Usmaan Sonko, Mimi daf ne dañ ko nar a teree bokk ci wote yi.
Waxtaanu réew mi : ndawi Grand Parti bu Maalig Gàkku gàntu nañ
Ndawi pàrti bees duppee Le Grand Parti, Maalig Gàkku jiite ko, nammuñoo bokk ci waxtaan wi Nguur giy woote ci njiitalu Maki Sàll. Nee ñu, ñoom, ànduñu ci wépp xeetu waxtaan wow, dafa safaanook njariñi réew mi. Te, taxawaay boobu lañuy digal seen njiit li, Maalig Gàkku, mu taxawee ko ci biir lëkkatoo Yewwi Askan Wi.
Ñoom, ndawi Maalig Gàkku yi, dañu wax ne :
« Ngir sàmm demokaraasi bi, ngoreef yi te amal i wote yu amul xàjj-ak-seen te leer, ci sunu gis-gis, wareef ci ñu dëgëral bennoo gi ci sunu biir lëkkatoo bi ngir sàmmonte ak dige yi nu ameel askan wi. »
Kon, bu leen seen njiit dégloo, Grand Parti yitam du wuyuji Maki Sàll.
Dees na duppee CESTI turu Maam Less Kamara
Njiitu réew mi jël na dogalu soppi turu CESTI, dolli ci turuw taskatu xibaar bi génn àddina fan yii, Maam Lees Kamara. Ci altiney démb ji la jël ndogal li. CESTI, daara bob, fa lañuy tàggatee ak a nàmpatal taskati xibaar yi, nekk ca jàngune (iniwérsite) Seex Anta Jóob bu Ndakaaru. APS moo yégle xibaar bile.
« Maam Lees ku ràññeeku la, di jëmm ju màgg, di gindikukaay ñeel kibaraan yi. Ngir muy wéy di doon ab gindikukaay ci taskati xibaar yi, jël naa dogalu duppee CESTI turam. » Maki Sàll, Njiitu réew mi.
Nguur gi yokk na péyoori liggéeykat
Nguurug Senegaal génne na 320i tamñaret ci xaalisu FCFA ngir yokk peyooru liggéeykat yi, rawatina ñiy yëngatu ci wàllu wér-gi-yaram ak ñi féete ci njàng meek njàngale mi. Démb, ci altine ji, 1 me 2023, la ko Njiitu réew mi xamle. Fekk mu doon dalal mbooloo sàndikaa yi ngir teewlu seen iy tawat ci bés bi àddina sépp doon màggal liggéeykat yi. Ginnaaw bi mu rafetloo yokkuteb peyoor yi, xamle naat ni dinañu yokk bu baax jumtukaayi caytug bokkeef gi ba ñu mën a méngook jamono bu baax.