Ci wenn waxtaan wu mu doon amal ak ñii di wa Express, Njiitu réew mi, Maki Sàll, xamle na ni, moom, dafa jàpp ni mbirum ñetteelu moome gi féete na boor. Ciy waxam, ca atum 2016 la mbir mi leer. Ndaxte, at moomu la jébbaloon askan wi ab sémbub àtte buy soppi Ndeyu àtte bi, wàññi moome gi, jële ko ci 7i at, indi ko ci 5i at. Nee na, nag, bi ñu koy fal atum 2012, juróom-ñaari at lañu ko fale woon. Te, ciy kàddoom ba tey, laata muy def Referàndum bi, waxtaan na ci ak Ndajem ndeyu-àtte mi. Kon, moome gu njëkk gi bokku ci. Nee na, dina bokk am déet ngir am ñetteelu moome loolu, waxi pólitig la. Te, nee na ay gaayam sax moom lañu def seen lawax. Waaye, jamono jii, li mu sumb ci liggéey la tal. Bu jotee, dina xamal ay ñoñam taxawaayam ci loolu, laata mu koy wax askanu Senegaal.
Aliyun Tin : “Moytuleen ! Nguur gaa ngi fëx !”
Naka lag Nguur mënee jafandiku ciw njombe nir faagaagal ab lawax ci wotey 2024 yees dëgmal ? Laaj bii la Aliyun Tin di laaj. Ci mikóro SudFm la doon waxe. Dafa ne : “Waruñoo jaxase réew mi ci sababu mbirum PRODAC mi.” Moom, dafa jàpp ni, layoo bi dafa weesu mbirum Yoon, nde pólitig daf cee rax. Nee na, “bu doon ne ci demokaraasi bu baax lan nekk, laaj kon nañ jëwriñ ji, mu indiy leeral ci li xew. Mbirum yàq der mile, dafa mel niy xaj yu gis yax, sëqatoo ko, ne wii yoon moo jàpp nañ ko. Looloo ci ñaaw.”
Aliyun Tin teg ci lu am solo. Mooy ne, fi Maam Mbay Ñaŋ ak waa Bennoo Bokk Yaakaar jafandu mooy ne ràppoor amul. Te loolu, ci gis-gisu njiitul AfrikaJom li, mooy dëgg-dëgg njombe. Moom, Aliyun Tin dafa jàpp ne sax, coow li baaxul ci Maam Mbay Ñaŋ te Njiitu réew mi “…dafa war a génn wax. Jamono jii, amul jenn jëwriñ ju ko mate juy wax ci mbir mi. Ñiy wax ñépp, dañuy woote ci reyaate, di dal ci kow nit ñi ak a saagawaate. Moytuleen ! Nguur gaa ngi fëx ! Dañu war a jubalaat mbir yi.”
Sigicoor : Xeex baa ngay wéy, taal nañu màkkaanu APR
Bi xeexub ñaxtu bi dooree alxames jii weesu ba tey, dakkagul ci Sigicoor ba tey. Tey jii sax, jot nañ xibaar buy wax ne am na ku ñu rey ca Biññoona. Moo tax ndaw ña féttéerlu, fippu, taal màkkaanu APR ma fa nekk. Njiiti APR ya dem nañ fa nemmeekuji béréb ba ak waa pólis.
Jàngune bu Ndar : njàngaan ya delloo nañ buum ca boy-boy ga
Layoob Usmaan Sonko beek Maam Mbay Ñaŋ baa ngi wéy di lëmbe réew mi. mënees na wax ne ñax gu wow lakk na, lakkaale gu tooy ma. Ndaxte, ndongo ya tàbbi nañu ca xeex ba, alxames ba léegi. Fa Ndar-géej, ndongo ya wàccoon nañu ca tali ba démb, di xeex ngir ñu bàyyi seen moroom ya ñu jàppoon ca ñaxtu ya keroog. Nee ñu sax, dees na dakkal njàng mi ci diiub ñetti fan.