LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (ÀLLARBA 8 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

YOON

Waa “Sureté Urbaine” bu Ndakaaru woolooti nañu. Wile yoon, Séex Aajibu Sumaare lay doon, nekkoon fi magum jëwriñ yi ci Nguurug Abdulaay Wàdd. Ag kayitug woolu lañu ko yónnee, mu war a wuyuji ëllëg, ci alxames ji 9 màrs 2023, bu 10i waxtu jotee ci yoor-yoor gi. Xameesagul sabab bees ko wooloo. Mbaa du bataaxal bi mu bind Njiitu réew mee tax ? Cig pàttali, ma nga naan Maki sàll, ca bataaxal ba :

« Ndax danga jox ab saa-farãs xaalis ci fan yii nu génn ? Bu dee loolu am na, ndax dinga dëggal ni 12i miliyoŋi ëro la, maanaam 7,9 miliyaar ci koppari réew mom, boolees na ko ci réew yi gën a ndóol te bari lool ay bor ? Rawatina bees xamee ni mbañeel ak boddekonte la pàrti ndaw si jaare ba àgg fim àgg ci pólitig ?»

Daan ba dal na ca kow Paap Njaay  mu Walf

Keroog lañu woowoon taskatu-xibaaru Walf bi. Bi mu demee ci lañu ko téye. Moom nag li ñu koy toppe tollu na ci juróom-benni tuuma. Muy lu ci mel biral i xibaar yu wérul, nasaxal dundug jàmbur (def bakkanam ci xottu gerte), kàddu yuy xajamal jëfi yoon, xoqatal ak kàddu yu ñagas ci kàngaami Yoon, yee fitna.

Gii Mari Saaña pelent na komiseeru Dakar-Plateaux

Pelent Gii bi li mu ci diir ëpp na kenn. Ndax, kenn ki mooy Xadi Faal komiseer ak X. Li ko waral mooy ni ñu leen jàppe keroog gaawu ca kanamu àmbaasadu Tinisii, salfaañe ay àqam ak i yelleefam. Ndax, nee na dépite la te, dafa am malaanu kiiraay miy tere ñu koy jàpp yenn xeeti njàpp yi.

PÓLITIG

Coow laa ngay wéy diggante Aminata Ture ak PDS

Waa PDS ak àndandooy Aminata Ture yaa ngiy wéy di dàggasante. Bu dee PDS dafa jàpp ni Mimi Ture bokkul ci kujje gi, ndaw si ak ñoñam ñoo ngi tam dëmm àndandooy Ablaay Wàdd yi.  Nee nañu, waa PDS, dañuy nax saa-senegaal yi, di wone ne Mimi moo tax bokkuñu ci xeex boobu ñeel ñetteelu moome gi. Maanaam, ag baara-yëgoo lañuy def ak Nguur gi. Ñu yokk ci ne, PDS, seen taxawaay dafa xaw a teey xel ba ci sax yenn ci ndogal yi ñuy jël ci biir Ngomblaan gi.

Nguur gi fippu na 

Ginnaaw coow liy lëmbe réew mi ci jamono jii ñeel juróom-ñaari milyaar ak lu teg yi Njiitu réew mi jox Marin Le Pen. Kii di Abdu Kariim Fofana mi yor kàddu Nguur gi, génne na ab yëgle ngir tontu ci kii di Aajibu Sumaare. Nee na nag Nguur mi ngi weddi tuuma yooyu nga xam ne teguwul fenn. Loolu, ngir yàq deru Njiitu réew mi kepp a ko tax a jóg.

BITIM-RÉEW

Afrig-dii-Sid

Ñàkkum mbëj-xëcc (kuraŋ) gu metti ga ca réewum Afrig-dii-Sid ma ngay gën dee tar. Isin yay liggéey mbëj-xëcc mi ñoo màggat ba xubidaas. Ay weer a ngii, gis mbëj-xëcc mu doy ci kër yi walla ci làmpi mbedd yi doon na fa lu jafe lool. Jamono yii, saa bu làmp yi fayee ca Juwaanesbuurg, ñi të a am dëkkuwaay (SDF) ñooy mujj wuutu alkaati yoy, seen lim dafa doyadi ci selebe-yoon yi ngir yombal dem beek dikk bi ci tali bi.

Móritani

Ñeenti nit yees tëjoon ñoo dawee ca Kaso bu mag ba nekk Nuwatsot. Li doy waar ci mbir mi mooy ni dees leen jàppe ni rëtalkat. Ñaar ñi sax Yoon jotoon na leen a àtte ba reylu leen. Ñaar ñi ci des ñu waroon leeral seen i mbir ndeem laale nañu ak rëtalkat yi. Laata ñuy rëcc, jot nañoo rey ñaar ci wattukat ya, gaañ ca yeneen ñaar. Jamono yii nag, alkaati yaa ngi ci seen i tànk. Jot nañoo gis daamar gu ñu duggoon bi ñuy dawe ca kaso ba.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj