Njiitul mbootaay “Ngor debout”, Mamadu Njaay, yëgle na ni ñaari nit dee nañu ci guddig taalatay tey ji. Askan wi ak takk-der yi ñooy jàmmaarloo m, di safaantoo ci sababu coowal lol, weer a ngii mu tàkk.
“Ñaari bakkan rot nañu, jenn ndey ak beneen xale bu jigéen. Xeex bee sabab dee yi. Jafe na ñu xam lu xew ndax kenn mënul génn jamono jii.” (Mamadu Njaay)
Usmaan Sonko ñaawlu na mbir mi ci waxtaan wi mu amal ci guddig talaata ji.
USMAAN SONKO : “TEY LAA GËN A DOON LAWAX”
Usmaan Sonko amal na aw waxtaan ci guddig talaata ji. Àddu na ci daan bi ko Yoon teg démb ñeel tuuma yi ko Maam Mbay Ñaŋ di topp. Moom nag, xamle na ne, àttekat yi dañoo jëfe ndigal Maki Sàll mi ko bëgg a tere doon lawax ci wotey 2024 yi. Nee na yit, àttekat yi dañ ko jàppal ngir li mu leen di ŋàññ saa su nekk. Moo tax ñuy feyantoo ak moom. Waaye de, ciy waxam, “tey la gën a doon lawax” te, ginnaaw Yàlla, gisul kenn ku ko ko mën tere.”
Bu dee Bàrtelemi Jaas, daf ko bërngal. Tuddu ko sax. Te looleet lay dugal ay militaŋam, maanaam ñu bañ ko topp. Ndax, li leen war a gën a yitteel mooy xeex bi ñuy xeex ak Maki Sàll. Woo na ñépp ci ndajem waa F24, sant waa Pastef ñu wormaal kilifa yi nar a teew yépp.
LËKKATOO YEWWI ASKAN WI ÑAAWLU NA DAAN BIÑ DAAN USMAAN SONKO
Waa Yewwi Askan Wi doon nañ janook ak askan wi tey ci yoor-yoor bi. Lin ko dugge woon mooy àddu ci daan biñ daan seen naataangoo bii di Usmaan Sonko démb ci altine ji. Ñoom dañ jàpp ne, la woon fa woon rekk. Ni ñu daanee woon Kariim Wàdd atum 2015, daan ko Xalifa Sàll atum 2018 ngir xañ leen seen àqi, tere leen bokk ci wote yi, noneet lañ namm a defe ak Njiitul Pastef lii di Usmaan Sonko.
Xalifa Sàll nee, 2012 ba tey, Maki Sàll dëkkewul lu dul tooñaate ak a xoqatal kujje gi, di nasaxal demokaraasi. Mu teg ci ne, waruñu seetaan Maki Sàll di xalaat ñetteelu lawax mu bokk ci wote yi. Dafa gis ne, “askan wi dafa war jóg, booloo ngir jàppale Usmaan Sonko ci xeex bile.”
Ginnaaw génnug Bàrtelemi Jaas bi démb ci ngoon, ñu bari njort nañ ne lëkkatoo Yewwi Askan Wi léegi mu tas. Waaye Décce Faal nee na tey la waa Yewwi Askan Wi war a gën a jàppante, booloo, bennoo, jàppalante. Ndax xi jamono fitna la jàppalante gi gën a am solo.
NJÀQAREY KURÉL GIY SAYTU ÀQ AK YELLEEFI DOOM-AADAMA CI SENEGAAL
Kurél giy saytu àq ak yelleefi doom-aadama ci Senegal, ñu gën koo miis ci nasaraan “Ligue sénégalais des droits humains”, dafa génneb yëgle ngir feeñal njàqareem ci jàpp yu bare yees nemmiku ci réew mi. Ci biir yëgle bi, ñu ciy xamle ne bare na lool ay saa-senegaal yees tëj ciy njort te saa su nekk ñu leen di bañal bàyyib négandiku. Ñu xamle ni njàpp gu metti gi Yoon nekke du mës a doon pexe mi gën ci njuumte yiy faral di am ci demokaraasi.
459i TAMNDARET ÑEEL XËYU NDAW ÑI
Nguurug Senegaal génne na lu tollook 450i tamndaret jagleel ko xëyu ndaw ñi ci ñetti at yii ñu jëm. Magum jëwriñ yi, Aamadu Ba, moo ko xamle. Fekk mu doon teewe woote bi Paap Maalig Nduur, jëwriñ jees dénk mbiri ndaw ñi, cumbantu geek wutum liggéey bi, woote woon ngir biral njureef yi tukke ci sémbub “Xëyu Ndaw Yi”, ak a dégtal naal yi mu tëral ci atum ren jii.
Bees sukkandikoo ci xibaar yi fa rot, Nguur gi jox na liggéey lim bu ëpp li mu nisaroon. Ñuy 66. 240i ndaw yees tàggat, gunge leen ba ñu am liggéey.