Aminata Ture waxoon na ko. Waxtaan wi ñu doon soow yépp, Maki Sàll ak waa PDS ñoo ko bokk sumb. Soxna si ne woon, duggewuñ ko lenn lu dul delloosi Kariim Wàdd ci géewu pólitig bi, sàkkal pexe xaalis bi mu yoreel askan wi ak beddi Usmaan Sonko. Ne woon na yit ne, Njiitu réew mi da doon wut i pexe ngir bokk ci wotey 2024 yi. Waaye, soxna dafa amoon ku mu fàtte. Nde, wëliis doomu Ablaay Wàdd ji, dafa mel ni Xalifa Sàll itam ci la bokk.
Ci yaxal bin tudde woon Waxtaan, naxtaan walla nax tànn, faramfàcce woon nan mbirum waxtaan wi, bindoon ne, ku xool ni mbir yi tëdde, mën nga njort ne Maki Sàll, ber Sonko rekk a ko tax a jóg. Ndaxte, bu PDS ak Taxawu Senegaal nangoo bokk, liñ ci jublu mooy Kariim ak Xalifa mën a bokk ci wotey 2024 yi. Bu loolu amee, PDS ak Taxawu yépp naruñoo jàppale Sonko xi xeexal beek Maki Sàll. Nde, ku nekk ci ñoom ñaar, dafa am fu la Maki Sàll tée, rawatina Xalifa mi nga xam ne, bu 2024 weesoo, dootul mën a bokk ciy wote, ndax day ëppal 75i at bu 2029 teroo.
Tey, lees tënk ca waxtaan woowule day dëggal li ñu bari doon njort. Ndeke, waxtaan wi, ñetti nit kese a ko taxoon a jóg : Maki Sàll, Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll. Bu dee Maki Sàll, da doon xool pexe mu muy def ba dagaan ñetteelu moome. Daf ko bëggoon a jaarale ci kujje gi, wax ne ñépp a ci ànd. La waxtaankat tënk ñeel ñetteelu moome gi mooy ne, dañuy bàyyi Ndajem ndeyu àtte mi dogal. Nde, moom rekk a am sañ-sañ wax kan mooy bokk ak kan moo dul bokk. Senegaal nag, ñépp xam nañ na Ndajem ndeyu àtte mi du mës a gàntal Njiitu réew mi càkkuteefam. Bu ko defee, mbetteel gu réy a réy lay doon. Rax-ci-dolli, Njiitu réew mi ci boppam, Maki Sàll, yoonal na bokkam ba noppi. Daf ne woon, ci wàllu Yoon, lënt amu ci (maanaam Yoon may na ko mu bokk), ci coobareem rekk la mbir mi aju. Bu yàggul dara sax, fa Pari, dig na ay militaŋam ndam lu réy keroog 2024. Kon, lees mën a jàppagum mooy ne, Maki Sàll lijjanti na boppam. Mu des Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll.
Bu dee Kariim Wàdd, nee ñu dañ koy àttewaat. Lees ci jublu mooy setal ko ngir mu mën a bokk ci wotey 2024 yi. Bu ko defee, kenn dootu ko toppe dara. 138i milyaar yim ameel askan wi sax, dees na leen far, jéggal ko ko. Ak xaalis bi nguurug Senegaal génne ci layoom bi yépp, coow li ci amoon, tuuma yu diis yees ko gàlloon ba Yoon daan ko, lépp lañuy fomp, fàtte ci coobarey jenn jëmm : Maki Sàll. Askan wi moom, amu ci baat. Bu ko defee, Kariim Wàdd itam, mbiram lijjantiku na. Mu des Xalifa Sàll.
Ba tey ci waxtaan woowuy niru naxtaan ak nax tànn, forees na ci wewu béy ne, dañuy soppi dogi L28 ak L29 yu càrtug wote yi ngir lawax yi mënutoon a bokk, mën a bokk wii yoon. Waaye nag, coppite gi dafay wax lu leer : lawax yooyu, dafa war a fekk ñu tëdd kaso ba noppi. Kon, bépp lawax bu gàlloo ab daan bu lay tere bokk ciy wote, fileek tëddoo ba jeexal daan bi, doo am sañ-sañu dagaan baatu askan wi. Te nag, loolu, ñépp xam nañ ni Usmaan Sonko kepp lees ci diir. Bu ko defee, mbirum Xalifa Sàll day lijjantiku tamit.
Ci tënk, Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll, ñoom, benn jubluwaay kese lañ amoon, mooy bokk ci wotey 2024 yi. Seen yoon nekkul ci li des. Bu dee Njiitu réew mi, Maki Sàll, moom, ñetti jubluwaay la doon diir ci waxtaan wi :
-
Bi ci jiitu mooy, wut pexe ngir doon lawax ci wotey 2024 yi ;
-
Ñaareelu jubluwaayam mooy fexe ba tànn ñi muy xëccool jal bi 2024, ñoo xam ne mënaluñu ko dara ;
-
Fexe ba beddi Usmaan Sonko ci wotey 2024 yi.