Senegaal a ngi ci diggante bu doy a doy waar. Ku yebu tiit ci ni miim réew di doxe jamono jii. Mbir yi fiy xew doy nañuy pettaaw ngir tani ëllëgu Senegaal. Dundu bu jafe bi ak ndóol bi rekk doyoon nañ ci nattu. Waaye, Senegaal, dafa mel ni fowe taal daf leen neex. Ñu ngi mel ni ñu lekk yàpp xaj : coow guddi, coow bëccëg. Te, li ñuy gën di dem, muy gën di ñaaw. Ay xew-xew yu doy waar, ruslu te suufe lool ñooy ay-ayloo ci réew mi. Bi ci mujj mooy mbirum ndaw si ñu metital ca Ngomblaan ga, te ay góor dóor ko fa. Mu am ñu ci kontaan, di ko rafetlu te di tam dëmm ñi koy ñaawlu.
Senegaal de, 2011 ba tey, ñoo ngi fiy tóllanti ñaawteef ci kow ñaawteef, muy ci wax, ak ci jëf. Moom daal, dafa mel ni gaa ñi dañuy wujje, ku nekk di jaay sa moroom doole, di ko jaay ñaaw làmmiñ ak coxorte. Ñi ko njëkke di ay njiit yu màndoodi, nuur ci Nguur gi ba lab ci, dëkke luubal ak a sàcc alalu réew mi. Njiit yoy, saxal nañu nger te di ko suuxat, aakimoo Nguur gi te di xoqatal ak a bunduxataal nit ñi. Ku muuñ sax, boo leen neexul, ñu ne la ràpp tëj, Usmaan Jaañ du ma weddi. Seen cuune ak seen ñàkk yërmande tax ba askan wi nekk ciy tolof-tolof yu jéggi dayo : dund bi jafe na, liggéey amul, kaaraange amul, njàng mi nasax, kenn fajootul ba wér, àtteesatul ci dëgg… Ci gàttal, boo bëggee gis misaalu Kumba am ndey ak Kumba amul ndey, kaay Senegaal.
Li ci gën a metti xol mooy ne, sunu njiit yi dañu jël Yoon wi, def ko ngànnaay, di ko xeexe saa-senegaal yi. Te nag, daw jiitu taxul a moom yoon, am déet ? Waaye de, kilifay réew mi gisewuñ ko noonu. Bu àttekat yi, masistaraa yi, amoon seen fullaay bopp sax mu tane. Waaye, lu jiin Njaag a, te ñoom ñooy Njaag. Dafa di, bu Yoon doon def liggéeyam ni mu ware, di àtte dëgg saa su ne, kon Senegaal du nekk ci gutta gi mu nekk nii. Ndege, saa bu njiit yi bëggee tiital kenn, mbaa ñu namm koo noppiloo, walla sax faagaagal ko, Yoon lañuy jëfandikoo. Kariim Wàdd, Xalifa Sàll, Usmaan Sonko, Imaam Aliyun Ndaw, Aadama Gay, Seex Umar Jaañ, Papitoo Kara, Kariim Xurum-Xaax, ba ci Paap Aale Ñaŋ mii mujj, doy nañ ciy tegtal. Bu fa yemoon sax mu tane. Waaye, léegi, dañuy reyaate te du mujj fenn. Ana 14i ndaw yi ñu reyoon ca xew-xewi màrs 2021 ya ? Ku rey Farãsuwaa Mànkabu ? Ku siif Mariyaama Saañaa ba noppi rey ko ? Ku bóom Idiriisa Gujaabi ? Waaw, Fulbeer Sàmbu nag ? Lii mooy Senegaalu tey… Taafar jiy yokku bés bu nekk. Kujje gi tamit, léeg-léeg ñu doxalee anam bu ñaaw. Li xew ca Ngomblaan ga, ci alxames jii weesu, doy na ci firnde.
Ay xastante, saagante, xeex ak i dóorante moom, miis nañ ko ci Ngomblaanug Senegaal. Daanaka sax, nekkatul loo xam ne, léegi, dees na ci yéemu. Ndaxte, dépite yi ñoo nu tàmmal yëfi ñàkk fayda yooyu, yëfi xale yu ndaw yu ñoragul. Ay kilifa, askan wi tànn leen ngir ngeen fénc mbiri réew mi, amooleen dara lu ngeen di def, lu moy di gàkkal ak a tilimal deru réew mi. Kenn du fa mën a wax, kenn du dégg ndax soowtaan yi, werante yi, xuloo yeek coow lu bari li. Bu dépite yi xeexaan, góor ak góor ñoo daan kurpañante ak a mbapat. Waaye, wii yoon, ag góor lañ fa gis muy dóor jigéen ju, nee ñu dafa ëmb (waaye dara leerul ci ëmb bi). Ndax am na lu gën a ñaaw dóor jigéen ? Déedéet. Jamono jii, boo waxee ñu tam la dëmm, jiiñ la naaféq, ne danga jeng. Ndaxte, mbañeel gi nit ñi ameel Nguur gi moo tax ñenn ñi jàpp ne lu ñu leen def baax na. Loolu nag du màndute. Li ñaari dépitey PUR yi def ndaw sii di Ami Njaay Ñibbi rafetul, jekkul. Dóor ko mu daanu, ba sàppëer mujje koo jëlsi rawale ko raglu ba, loolu dafa ñaaw.
Naam, kàddu yi Ami Njaay Ñibbi yékkati ñeel Sëriñ Mustafaa Si tegginewuñu. Dëgg la, ni mu waxe dafa ànd ak ñàkk kersa, ñàkk yar ak ñàkk worma cig kilifa. Loolu yépp dëgg la. Waaye, loolu du lay ci ñu koy dóor ak di ko karaate. Jigéen, kenn waru ko dóor, rawatina ca Ngomblaan ga, àddina sépp di gis. Ndeyu jàmbur lañu toroxal, doomu jàmbur, di mag, di rakk, di tànta, di jabar. Te kenn bëggul ñu def lu ni mel sa jigéen, astemaak sa yaay walla sa tànta. Xanaa kay, ni mu waxee moo rafetul. Te, ayle-yéwén, kujje gi tamit ñoo ngi waxe anam bu ñaaw, di tiiñal ak a xas ay kilifa ci Nguur gi, rawatina Maki Sàll. Waaw, xanaa Njiitu réew mi du kilifa gu gën a mag ci réew mi, bu dee dëgg rekk a nu ñor ?
Warees na tiit ci Senegaal. Bu ñu demee ba nit ñiy kontaan ci ñuy mbej jigéen ak di ko këdd, ñépp di gis, nga war a xam ne Làmbaay ñaaw na. Dafa jot nu toogaat, xool, xoolaat, jàngat xew-xewi réew mi. Ndaxte, gaalug Senegaal a ngi daw ci géej gu sàmbaraax te, waa gaal gi bàyyiwuñ ci xel. Ku nekk a ngi joow, jëmale sa boor. Bu yeboo ne, Senegaalu tey, genn gaal la, waaye xar na ba junniy bopp. Jóg jot na. Ndax, liy raam, ci ñag bi la jëm.