LU BEES ÑEEL MAYMUNA NDUUR FAY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu bees rot na ci cong mi ñu songoon taskatu xibaar bii di Maymuna Nduur Fay. Daanaka, yéenekaay yépp ñoo ko fésal ci seen boppi xët. Ci lees waxagum, sàmbaabóoy bi ko song, ñetti jam la ko jam. Looloo rotagum ci luññutu gi takk-der yi sumb.

Xibaar bu yees bile nag, day worook li ñenn ñi bëggoon a gëmloo nit ñi. Maanaam, dafa am ñu ko bëggoon a bóomlu. Dafa di, am nay way-pólitig yu bëggoon a wëlbati mbir mi, taafantoo ko, ngir fajaale ci seen aajoy pólitig.

Nde, Bàrtelemi Jaas, ci li waxam ji wund, waa Pastef la duut baaraamu tuuma. Kii di Majambal Jaañ itam, noon na xam na ñan ñoo nekk ci ginnaaw cong mi. Yerim Sekk itam, lu ni mel la wax, rawatina waa Bennoo Bokk Yaakaar ak ña far ak Maki Sàll, nekk APR. Muy lu doy waar. Ndaxte, bi ñuy wax lu ni mel, takk-der yi dooraguñu woon seen luññutu gi. Bu dee ñoom ñaar dafa am luñ xam lu takk-der yi xamagul, toppekat bi war na leen woo, déglu leen.

Ndeke, cong yeek càcc gi dafa bari ca gox ba soxna si dëkke. Loolu la waa gox ba xamle ci làmmiñu imaamu gox ba Maymuna Nduur Fay dëkk.

Moom imaam bi, Ismayla Jaañ, nee na gox ba amatul kaaraange. Te, ñàkkug kaaraange googu, yàgg na fa. Liy feddali waxam ji mooy ne, laata Maymuna Nduur Fay, song nañ fa ñetti nit. Te, ciy waxam, léeg-léeg bëccëgu ndar kàmm lañu fay song nit ñi, di leen fitnaal.

Li koy gën a firndeel sax, mooy ne, sàmbaabóoy bi dafa këfaale sikaare (sac) Maymuna Nduur Fay bi, daw ak moom, yulli ko, daldi jël la ca nekkoon ba mu des këyitu jëmmam (carte d’identité). Ci li yéenekaayub Libération siiwal, sikaare bi, takk-der yaa ko gisaat. Rax-ci-dolli, jot nañoo déglu wattukatu béréb ba te ñoo ngi wéyal luññutu gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj