LU ÑUY XAAR CI JÀNGALE LÀMMIÑI RÉEW MI ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bi Senegaal moomee boppam ba tey, bare na ay nguur yu fi jaar ak seen i  dige ñeel làmmiñi réew mi. Am na ci sax ñu fi jot a taxawal ay naal, amal i gëstu ak ay jax yu dul jeex, ngir xool naka lees mën a def ba boole sóninkeek wolof ci njàng mi. Waaye, li ko dale ci Lewópóol Sedaar Seŋoor ba ci Maki Sàll, jaare ko ci Abdu Juuf ak Abdulaay Wàdd, kenn jëmmëlu ci naal yooyu, doonte sax yéene baa ngi fi woon. Ba nëgëni-sii, làkki doxandéem yi lañuy jàng, di leen jàngale ci sunu daara yi.

Moone de, bare na ay xeltukat yu ñu ràññee yu biral ne, am réew su bëggee jëm kanam fàww mu yar askanam ca ba muy tuut-tànk, fexe ba njàngam mucc ayib. Rax-ci-dolli, njàng moomu, dees ko war a def ci làmmiñu walla ci làmmiñi askan woowu. Boroom xam-xam yi ma tudd, indi nañu ay firnde yu bare yuy wone ni xale bi, ci li mu nàmp lay gën a gaaw a mokkale li ñu koy jàngal, mu amal ko yit njariñ cig dundam. Ci misaal, ci lay gën a gaaw a mën dawal ak xayma. Te, nag, dawal ak xayma yi nga xam ni ñooy cëslaayu njàng, gone yi dañu ciy faral di lajj. Loolu rekk waroon naa tax nu jël i matuwaay ngir dugal sunuy làmmiñ ci lekkool bi.

Ay gëstukat wone nañu ci seen i ngirtey liggéey ni, 100 ndongo yoo jël ci ñetti ati lekkool yu jëkk yi, 75 yi mënuñoo dawal walla bind bu baax. Yemul foofu, ndax nee nañu ci 230 alfunniy (milyoŋi) xale yiy dal ci daara yi, du kenn ku ciy mën a dawal walla bind ci at yu njëkk yi. Kon, pexe mi mooy ku nekk di jàng ci làmmiñ wi nga nàmp. Warees na jëmmal naal yi te bañ a yem ci wax ji kese.

Li jaaxal ñépp, nag, mooy ngirte yu am solo yu tukkee ci daaray-jax yi (classes télévisuelles, testes du bilinguisme). Bir na ne ndongo yiy tàmbalee jàng ci seen làmmiñ laata ñuy jàng weneen làkk, ñooy gën a aay fuuf ñeneen ñiy tàmbalee jàng ci tubaab. Moo, kon lu nguur giy xaar ci yoonal njàngum làmmiñi réew mi ci daara yi ? Ana ban walla yan téq-téq ñoo nu tee jàngale sunuy làmmiñ ? Ndax bëgg-bëgg beek pastéef bee fi nekkul ? Walla dafa am ay réew walla ay kurél yuy gàntal naal yi ?

Mu mel ni nguur gi dese naa am pastéef ñeel njàngum làmmiñi réew mi ; waaye tamit, nootkat ba woon, Frãs, ak yenn ci kurél yiy lebal réew mi xaalis, bokk nañu ci ñiy tee naal yi àntu. Waaw. Wolof dafa ne, ku la abal i bët, fu ko neex ngay xool. Li mbir mi di tekki moo di ne ba léegi moomagunu sunu bopp. Ndaxte, bu dee amunu sax sañ-sañu taxawal xeetu njàng mi gën ci nun, méngook sunuy aada ak sunu cosaan te di nu jural yokkute, dafa fekk mënagunoo dogalal sunu bopp ci ñaari fànn yii di politig ak koom-koom. Bu fa yemoon sax mu tane, waaye doomi-réew mi ci seen bopp, ñu ci bare dañoo jàpp ni joolaa, pulaar, séeréer, wolof añs, dañ nuy delloo ginnaaw. Te, nag, ku xeeb sa cosaan ñu xeeble la ko.

Leeg-leeg danga naan Tubaab bi dafa noo jam naani ndax ni nootaangeem di wéye ba tey jii ci xel yi. Moo nu gëmloo woon ne sunuy aadaa nu tee nite te feek sànniwuñ leen ca xaj, dunu leen dab mukk, ñoom Tubaab yi. Dañu doon wax lu leen neex rekk ndax mën a kàcc weesuwul naan sunuy làmmiñ mëneesu cee sàkku xam-xam ba ciy séentu naataange ! 

Boroom xam-xam bu mel ni Séex Anta Jóob weddi na wax jooju ba noppi indi ay firnde yuy wone ni làkki doxandéem yi gënuñu benn yoon sunuy làmmiñ. Ci ginnaaw gi, am na ay gëstukat yu topp ciy tànkam, di liggéey ci nëwum làmmiñi réew mi. Ràññees na ci Aram Faal, Saŋ-Léwópóol Juuf, Mamadu Siise ak Cerno Siise. 

Waaye ba tey njaw des naw xambin.

Fi mu ne nii, amatunu jawriñ bu féetewoo lépp lu aju ci làmmiñi réew mi. Amul genn kurél guy saytu ak a yoonal nees leen war a binde. Lu neex waay mu bind ! Moo tax ñu bariy jaawatle ba léegi joŋeak « jongue », muy lu reelu lool, sax.

Misaal yi bare nañu, mëneesu fee lim lépp. Li mat a xam ba tey rekk mooy ni xamagunu sunu bopp, nattagunu sunu dayo. Looloo tax amunu benn jubluwaay. Lu nu teree dellu ci sunu cosaan, gën a fonk li nu fi Maam bàyyil ? Waaw. Soo xamatul foo jëm, tee ngaa dellu fa nga jóge ! Warees na xam ni, toppandoo duñ tax a jëm kanam ndax ni ko wolof Njaay di waxe : “Ku wacc sa and, and boo dem fekk ca boroom”. Ma jox Séex Anta Jóob mu daaneel : “làkku jaambur, lu mu neex neex, mëneesu koo macc ba ciy tàqamtiku.” Waay-waay, nanu jàngale làmmiñi Senegaal yi, muy neex gone yi ba ñuy tàqamtiku, gënatee sawar ci sàkku xam-xam, ñuy joow, jëmale gaal gi kanam !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj