Ci talaata, 18eel ut 2020, la ay soldaar yu fétteerlu nangu nguur gi ci Ibraayim Bubakar Keyta, teg ko loxo, moom ak yeneeni kilifa ci nguur gi ak ci làrme bi. Bu dee njiiti àddina sépp a ñaawlu li ñuy woowe cëtëŋ, askanu Mali, moom, dafa bég ci mbir mi.
Ci ndoorteelu yoor-yooru talaata ji la waa Kati dégg ay soqi fetal. Ay soldaar yu mer ba futt ñoo fétteerlu, wutali màkkaanum-soldaar biñ duppe Sunjata Keyta ca Kati, nangu ko ba noppi di soqiy bal ci jaww ji. Ci lañu fatte tamit yoon yépp ba kenn mënatu faa jaar, kenn mënatul a àgg ca seen màkkaan.
« BËGGUMA DERET TUURU CI SAMA SABAB. NGUUR JARALUMA KO … »
Ab fajkat buy liggéeye ca loppitaanu gox ba, nee na ci mikóro France 24 : « Ay soldaar ñoo jël ay fetal ca seen màkkaan ca Kati, soqiy bal ci jaww ji. Bare woon nañu lool ba noppi mer ba futt. »
Bi mbir mi tàmbalee jaxasoo, àmbasaadu Farãs ak yeneen réewi Tugal ya fa nekk daldi digal seeni mbokk ñu téye seen tànk, toog seen kër. Naka noonu, ñu daldi fomm ab tukkib kow bu waroon a bawoo Bamako jëm Pari.
Bi nguur gi jotee ci xibaar bi, Buubu Siise, njiitu jawriñ yi, génne nab yégle, di ci ñaax soldaar yi, wax leen nañ wéer gànnaay yi, ñu toog waxtaan ci jàmm. Ciy kàddoom, « yëngu-yëngu yi ñu nemmeeku dañuy biral ag xoñoñ gu yoonu. Waaye, nguurug Malee ngiy ñaan soldaar yi ñu delloosi seen xel te ànd ak dal. »
Wànte loolu taxul meru way-fétteerlu yi giif. Ndaxte, ci ginnaaw gi lañu jóge Kati, def seenug gàngoor, wutali péeyu Mali, Bamako. Digganteem ak Kati 15i km rekk la. Noonu, ñu jubali dëkkuwaayu Ibraayim Bubakar Keyta (IBK) bi nekk Sebenikoro. Bi ñu àggee, ci ngoonug talaata ji, fa lañ ko fekk, moom ak njiitu jawriñ yi, Buubu Ciise ak doomam jiy dipite, Karim Keyta. Ñu boole ñoom ñépp, jàpp, yóbbu Kati. Jàpp nañu yit kilifa yu mag ci làrme bi.
Buubu Dukkure mi yor kàddu Buubu Siise, moo yëgle xibaar boobu, am way-fippu bu ko dëggal. Moom sax dafa leb turam bi muy jokkoo ak AFP : « Mën nan leen wax ne, njiitu réew mi ak njiitu jawriñ ji ñoo ngi ci sunuy loxo. Noo ngi leen jàppe, ñoom ñaar ñépp, ca kër njiitu réew mi. »
Ci guddi gi la IBK feeñ tele ORTM, wax ne tekkil na boppam ndombog-tànkam. Mu ne, li mu ko dugge mooy sàmm jàmmu réew mi. Dafa ne : « Bëgguma deret tuuru ci sama sabab. Nguur jaraluma ko. Buñ demee ba ñenn ci sunuy soldaar fétteerlu, ne na fi lépp yem, ndax dëgg-dëgg mën naa ci dara ? » Noonu, mu daldi suuxal nguur gi ak péncum réew mi.
Ci ginnaaw gi, Ismayla Wage mi yor kàdduy way-fétterlu yi jël kàddu gi, wax ci ORTM ne : « Nun, way-baati askan wi, booloo ci kurél gu yittewoo muccug askan wi (CNSP), noo fas yéenee jël sunuy matuwaay ngir ëllëg. » Mu dolli ci ne Mali dina sàmmoonte ak déggoo yi mu xaatimoon yépp ci àddina si.
Ñu bare ci àddina si, ay kurél ak i boroom baat ñoo ngiy ñaawlook a naqarlu mbir mi…
Laata ñuy teg loxo IBK ak i nitam la njiiti àddina sépp ànd ñaawlu lees tudde cëtëŋ ca Mali. Muy njiiti réewi diiwaanu Afrigu sowu-jant, CDEAO, UA (Kurélug Bennoo Afrig), UE (Bennoog Ërob), Farãs, Etaasini, añs. CDEAO, moom, dafa génneb yégle, naqarlu ci lool mbir mi, sant soldaar yi ñu dellu ci seen màkkaan. Waaye CDEAO yemul foofu, ndax dafa teg Mali ay daan, tëj ay digi réewam (oto du daw, roppëlaan du naaw), naj koom-koomam ci put. Ginnaaw loolu, ci alxemes ji, amaloon nam ndaje ci ànternet bi ci njiitalu Mahamadu Isufu, njiitu réewu Niseer, ngir waxtaane mbirum Mali mi. Ci njeexitalu ndaje moomu, dañu jël ay dogal, génne Mali ci fépp fu ñuy jëley dogal, ne dinañ teg ay daan ci kow way-cëtëŋ yi nga xam ne nanguluñ leen benn dayo.
Ci wàllu boppam, Musaa Faki Mahamat mi jiite kurélug Bennoo Afrig ne ci Twitter mi ngi ñaawlu « bu baax » jàpp giñ jàpp IBK ak i ñoñam. Mu sàkku tamit ci « ONU ak ci àddina sépp ñu boole seen doole ak seen xalaat, fexe ba jàmm delsi ca Mali. » UA sax dafa mujje génne Mali ci kurélam ba keroog muy teguwaat ci yoon.
Bi ñu demee ba dëggal pétteeral gi (mutinerie), jawriñ ji yor wàllu bitim-réew ci Farãs, Jean-Yves Le Drian ñaawlu na « ba fu ñaawlu yem xew-xew bu jéggi dayo bii… », ñaaxaale soldaar yi « ñu dellu ca seen màkkaan ci saa si. » Emmanuel Macron mi jot a jokkoo ak ñenn ci njiiti diiwaanu Afrig sowu-jant biral ne, moom, ànd naak CDEAO miy dox tànki jàmm. Josep Borrel mi jiite dipolomasi Ërob, moom tamit, ñaawlu na mbir mi, teg ci ne : « …du nii lees war a faje tolof-tolof yi gaar Mali weer yi. »
Peter Pham, ndawul Etaasini ñeel Sayel bi, ne « Etaasini àndul ak bépp xeetu kuutlaayug nguur bu teguwul ci yoon ca Mali, donte ne làrme baa ko sooke.» ONU, moom, ci saa si la amaloon ndajem kaaraangem ba noppi xamle ne dina amalaat ndaje mu jamp ci àllarba ji te Farãs ak Niseer sàkku woon ko. Njiitalu ONU, Antonio Guterres tamit, génne nab yégle di ci wax ak soldaar yi, ne leen nañ dakkal pétteeral gi, bàyyi IBK ak i ñoñam ci ni mu gën a gaawe.
…WAAYE ASKANU MALI DAFA DOGU TE FASUL YÉENE DELLU GINNAAW
Imaam Dikko moo jëkk a tontu CEDEAO, ne leen :
« Nun, askanu Mali, dogu nanu ci soppi nekkinu Mali. Noo ngi ne temm taxaw ! Danuy dee rekk, waaye dunu mës a wor askan wi. Te, nag, nun, jébbaluwun ci kenn. Rax-ci-dolli, dunu bàyyeeku mukk walla di seetaan ñuy yàq, di nasaxal ak a jaxase sunum réew. […] Jox nanu CEDEAO cër lool, nag. Waaye, askanu Malee fippu, daldi gàddul boppam xeex bi ngir fajal boppam ay jafe-jafeem. Ndaxte, mbejum kanam, boroom a koy fajal boppam. Bu yeboo, nag, ngeen nocci li ngeen di nos, teg ko ci suuf. Mënu leen noo defloo lu nu bëggul. IBK cuunewul woon rekk yem ci, dafa reyaale ay doomi Mali, ay baadoolo yoo xam ne, amuñu wéeruwaay. Kon, yéen waa CEDEAO, askanu Mali ngeen war a jàppale waaye du IBK mi askanam faloon te mujje koo jàmbu. »
Imaam Umaru Jara mi bokk ci kurélu M5-RFP moom dafa leen mbalag, ne :
« Ginnaaw bi nu CEDEAO beddee, na téye ngelaw li, nëbb jant bi ak weer wi boolewaale suuf seek jàww ji su ko mënee. »
Bu dee waa M5-RFP ci seen bopp, ñoom, ki yor seen kàddu lii la wax : « Jàpp gi ñu jàpp njiitu réewum Mali, IBK, deesu ko tudde cëtëŋ, li am rekk moo di ne askan wi ko dénkoon yëfam a ko nangu. »
Lees ci mën a jànge mooy ne askanu Mali dafa rafetlu doxalinu soldaar yi. Ci seen gis-gis, way-fétteerlu yi dañoo jëmmal seen mébét, jële fi IBK. Looloo tax sax, bi soldaar yiy jëli IBK, mbooloo maa ngi leen doon tàccu, di leen ndokkeel.
IBK MU NGI SANT YÀLLA
Ci guddig alxames gi, bésub 20eel jàpp àjjuma 21eelu fan ci ut 2020, ay ndawi ONU jot nañoo gise ak IBK ak yeneen kilifa yi soldaar yi jàpp. Ci Twitter la MINUSMA yéglee xibaar bi, ne : « Biig, ay ndawi MINUSMA yi féetewoo àqi doom-aadama dem nañu Kati ñeel seenub sas. Jot nañoo gis njiitu réew ma woon IBK ak ñeneen ñi ñu fa téye. » Waaye dara rotul ci liñ fa waxtaaneek IBK.