MA-DEMBA SOKK WUYUJI NA BOROOMAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xibaar bu tiis la réew mi xëyee tey. Ma-Demba Sokk moo génn àddina. Pari ga mu doon fajoo, ca Farãs, la gaañoo. Mi ngi amoon 65i at.

Ma-Demba Sokk nag, moo fi jiite woon sàndikaa bii di SUTELEC, di woon tamit njiitul Ndiisoog Ndoxal (PCA) bu “Caisse de sécurité Sociale). 

EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaam Saa-Senegaal yépp, di jaar njabootam ak i mbokkam te di ko ñaanal njéggal ak yërmaande.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj