MAAM MBAY ÑAŊ : ” SONKO RËCCAGUL. “

Yeneen i xët

Aji bind ji

Maam Mbay Ñaŋ nee na day def “appel”, du bàyyi mu sedd. Moom, ak i layookatam, doon nañ amal ndajem-waxtaan ak taskati-xibaar yi, tey ci àjjuma ji, 31 màrs 2023.

Démb ci alxemes ji, 30 màrs 2023 la àttekat bi daan Usmaan Sonko 2i weeri kaso yum dul tëdd ak 200i miliyoŋ yim war a dàmp Maam Mbay Ñaŋ. Moom nag, jëwriñu wërteef geek po yi, ciy kàddoom, gërëmluwul daan yi. Daf ne : 

“Layoo bi jotewul dara ak pólitig. Maa pelent Usmaan Sonko ngir setal sama der ak won askan wi ne, moom moo tooñ. Noo am ndam. Tey jii, bir na ni Usmaan Sonko waxul dëgg.”

Maam Mbay Ñaŋ nee, Sonko indiwul benn firnde ñeel tuuma yi mu tegoon ci kowam. Moo ko tax a wax ne, “Usmaan Sonko rëccagul. Layoo bi du fi yem. Dinañu def “appel”. “

Wii yoon, Sëñ PRODAC nee, 29i tamñaret (milyaar) lay laaj niki ndàmpaay. Bu ci jotee, daf koy séddale néew-ji-doole yi ak ñi yàqule ci yëngu-yëngu yi fi amoon te Usmaan Sonko woote woon leen.

Lii de la wax, ndeysaan. Fii la Senegaal tollu…

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj