Tay, 23i pani ut 2024 mooy méngook 18eelu fanu safar ci atum 1446 ci arminaatu jullit ñi. 18eelu safar nag, bu ñu ko waxee fi Senegaal, xel yépp dem ci màggalug Tuubaa, muy xew-xewu diine bu mag a mag. Kon, tay, àjjumay màggal la woon. Ay tamndareeti taalibey murit teewi Tuuba ngir santale Yàlla ki tax ñuy màggal : Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke walla Sëriñ Tuubaa.
Màggalu Tuubaa mooy xew-xewu diine bu gën a réy te gën a màgg ci murit yi. Bésub màggal gi, dañu ciy fàttaliku ak gàddaayu sang bii di Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke, Sëriñ Tuubaa. Gàddaayam boobu, way-mbéeféeri tubaab yaa ko ca ga woon, mu demoon Gaboŋ ca atum 1895. Ca atum 1928, menn at ginnaaw dëddub sëriñ bi, lañ ko tàmbalee màggal fi Senegaal ba jonni-Yàlla tay jile. Màggalug ren ji mooy 130eel wi yoon. Tuubaa la màggal giy amee at mu nekk. Daanaka, ci lees xayma, juróom-benni (6i) tamndareeti taalibe dinañ màggali fa Tuubaa. At mu nekk nag, dafa mel ni lim bi day yokk.
Bu dee màggal gi ci wàllu boppam, taalibe yi dañuy faral di siyaareji xabru Sëriñ ba, di dem ca jumaa ju mag ja, di teewe waxtaan ya, añs. Bernde yi tamit bokk nañ ci liy màndargaal màggal gi. Nde, Saa-Tuubaa yi dañuy teral seen mbokki taalibey murit yi leen di ganesi. Ndawal yi (yàpp xar, nag ak gëléem), naan yu sedd yi, kafe Tuubaa gi, meññent yi, dara du des ginnaaw. Jamonoy màggal day jamonoy tabe, bokkoo, mbokkoo, séddoo, jàppalante, dimbalante ak teralante.
Ay gan yu am maanaa, am dayo, dinañuy faral di màggalsi at mu nekk. Muy kilifay yi ràññeeku fi réew mi, diy kilifa yu mag ci wàllu diine fa bitim-réew, ñépp ñooy màggalsi. Ren jii rekk, am na 16i réew yu yabal i ndaw yu leen teewal fa Tuubaa. Séex Abdul Ahaad Mbàkke Gaynde Faatma moo ko xamle, moom mi jiite banqaas bi féetewoo jokkoo geek mbatiit mi ñeel màggal gi. Ndaw yooyii teewalsi seen i réew nag, ndawuñu. Nde, dees na ci fekk ay imaam, ay njiiti mboolooy diine, ay boroomi xam-xam yu mag, ay jëwriñ ya woon, ba ci sax ay tubaab yu tuub, dugg ci islaam ba noppi tànn yoonu murit.
Ci gaawu gi, 24i pani ut 2024, lees di amal xew-xew bu mag bi (céémonie officielle). Fa « Résidence Cheikhoul Khadim » bal ay amee, te mu jàkkaarlook jumaa ju ma ji. Dina am ñu fa teewal Càmm gi.
« Jëwriñu Biir-Réew mi dina fi teewal Càmm gi, moom ak yeneen i kilifa ci Càmm gi, ay àmbaasadëer yi teewal seen i réew fa Ndakaaru, ay kilifay diine, ay gani bitim-réew ak njabootu Sëriñ Tuubaa. »
APS moo taataan kàdduy Séex Abdul Ahaad Mbàkke Gaynde Faatma yees fi toxal.
Lenn rekk nag moo xaw a naqari ci màggal gi, te mooy bakkan yiy rot ci sababi ndog yiy am ci tali bi. Ren jii, limagum nañ 8i nit ñu deewagum ci 171i ndog yi jotagum am. BNSP (Brigade nationale des Sapeurs-Pompiers) moo joxe lim yi. Ci biir limu way-dëddu yooyu, ràññes na ci mbër mii di Elaas Jéen, ñu gën ko xam ci turu « Brise de Mer ». Moom it, ci yoonu Tuubaa wi la amee ndog, daldi ciy ñàkk bakkanam.
EJO Editions ak Lu Defu Waxu ñoo ngi ñaanal ñi ñàkk seen i bakkan ñépp ci yoonu màggal gi, Yàlla jéggal leen te yërëm leen.