Màggal gi jubsi na. Nit ñaa ngay waaj, ku nekk ci sa wet. Waa Tuubaa ñaa ngay waajal béréb ba ngir dalal gani taalibe yu bawoo fu nekk ci àddina si ngir teewee si màggal gi. Taalibe yit, ñaa nga ca waajtaay ya, fas yéene màggali ci jàmm. Nde, Murit kat, ku ko dëgg ci màggal ne ko masta. Benn taalibe bëggu koo wuute. Moo tax, mbooloo mu takkoo takku ay màbb, wutali dëkku Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke ba. Looloo tax itam, Càmm gi jël i matuwaayam ngir màggal gi mën a am ci anam yu mucc ayib.
Waajtaay yi
Naka noonu, jëwriñu Biir-Réew mi jiite nam ndaje, ci talaatay démb ji, ngir waajal màggal gi. Kii di Sëriñ Basiiru Mbàkke Abdu Xaadr ak njiiti serwis yépp teewe woon nañ ndaje mi. Jubluwaay ndaje maa doon fexe ba yembal lépp lu aju ci màggal gi. Ci kow loolu, jëwriñu Biir-Réew mi, Seneraal Saŋ Batist Tin, xamle na fa ne, liggéey baa ngiy jdox ni mu ware. Nde, bees sukkandikoo ciy kàddoom, liggéey bi, bu doon téeméer, juróom-ñeen-fukk ak juróom-benn yi yemb na. Dafa ne :
« Sama dal na bu baax a baax ndax, ci dige yi ñu defoon yépp, matal nanu juróom-ñeen-fukk ak juróom-benn yi ci téeméer yoo jël. Noo ngi njort ni, fii ak àjjuma, dinanu matal liggéey bi yépp. Maa ngi dem, ànd ak xel mu dal a dal. »
Seneweb moo toxal i kàddoom. Bu dee li ñeel ndog yi tali bi, moom jëwriñ ji sàkku ci kilifa diine yi ñu dugal ci seen i loxo, ak it boroom baat yi ngir ñu wax ci. Àddu na tamit ci mbënn mi, wax ne, ndox mu baree gën maral. Waaye, nee na dañu ko war a saytoo fa béréb ya muy amee. Mu jeexalee kàddu yii toftalu :
« Bees amee ndox ci sa kër, warul a tax boroom di baareji tali yi. Dees na woo nit ñi ci xam seen i wareef ak di jéggale. »
Ci beneen boor, kiy jokkale kurél giy lootaabe màggal gi, Sëriñ Usmaan Mbàkke, rafetlu na bu baax taxawaayu njiiti réew mi ci waajtaayi màggal gi, rawatina li ñu xar seen i tànki tubéy ci wàllu ndox mu sell meek cellal gi. Dafa ne :
« gis nan te yit yëg nan bu baax itte ak pas-pas bi njiit yu bees am ci waajtaayi màggalug Tuubaa gi. »
Saa bu màggal jubsee ba ni muy jeexee, kilifa yi dañuy jaabante Tuubaa, rawatina way-pólitig yi. Tey ci àllarba ji, 21i pani ut 2024, lees wax ne elimaanu jëwriñ yi dina dem Tuubaa. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jiitu woon na ko fa ci altiney bërki-démb ji. Du ñoom ñaar rekk a fa dem nag. Ndax, am na yeneen kilifa yu fa dem. Kii di Mustafaa Ñas ak ndawi Maki Sàll yi demoon nañ Tuubaa.
Teewaayu Usmaan Sonko nag fa dëkk ba, dépite Séex Coro Mbàkke moo ko yégle.
Màggalug Tuubaa nag, xew-xew bu mag la bob, dañu ciy màggal ak a fàttaliku ba Séex Ahmadu Bàmba (1853-1927) di gàddaay fa Gaboŋ, moom mi sos yoonu Murit. Ci àjjumaa jii nu dégmal, 23i pani ut 2024, lay am.
EJO ak LU DEFU WAXU ñu ngi leen ñaanal màggalug jàmm.