Ci ngoon gi, boori 16i waxtu, la RTS rotal xibaar bi : « bu 20i waxtu jotee, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dina def ag batale. » Nit ñiy ruumandaat. Ñu baree njortoon ne ci 3eelu moome gi lay wax walla ci mbir mu am a am solo. Waaye, Maki Sàll dafa duut ñépp.
Bi xibaar bi jibee, ñépp la jële kow. Kenn foogul woon ne Njiitu réew mi dina waxtaan ak askan wi jamono jii. Nde, illag batale gu ni mel la kenn gisul. Naam, dund gi tar na, mbënn mi metti na. Dëgg la, coowal Ngomblaan gi gàkkal na deru réew mi, rawatina deru Nguur gi. Waaye, ak lu ci mënti am, réew maa ngi ci jàmm. Kon, lu ko fi jaroon ? 4i waxtu, ñépp toog di la xaar. Nga sédd leen 10i simili yoy, waxoo ci li nit ñi mën a dégg…
Ñu foogoon ne… dinga wax ci 3eelu moome gi. Léttoonu, firiwoonu. Ngay sikki-sàkkaloo askanuw lëmm, di nas, di nocci. Ba kañ ? Ngay nuy wax waxi wote yu wees, di rafetlu tëralin wi añs. Te, nag, bu dee wax dëgg rekk, wote yooyu yépp a bari woon ay lënt-lënt, njuuj-njaaj, nger ak jalgati yoon. Waaye, ba tey. Wotey 2024 yi nag, kañ nga ciy wax ? Ñu foogoon ne dinga wax ci Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll, delloo leen seen àq ngir ñu mën a samp seen i ndënd ci wote yooyile, nga waaf, jàdd koñ. Maki daal…
Foogoon nañ ne am na loo jànge ci wotey gox-goxaat yi ak yu dépite yi. Yaakaaroon nañ ne, njureefi wote yooyii yee nañ la. Waaye, dafa mel ni ngëlmaande gi bawagu la. Nde, gaaruwaale bi nga gaaruwaale kujje gi ci xew-xewi Ngomblaan gi daf koy biral. Jàppeesoon na ne, dangay woo kujje gi ciw waxtaan, yaatal nguur gi. Ndekete yoo, dàggansante rekk a la taxoon a jóg. Xanaa amatoo ñu lay xeexal, di la xulool ak a tontul ? Mbaa du danga wéet ci sa xeex bi ba mu jaral la ngay sàndiy xeer ci bile anam ? Du sa cër de…
Àddu nga yit ci jàmmi réew mi ak bennoo gi war a am diggante xeet yi. Nee nga yow yaay ki ko war a sàmm kaaraange ak jàmmu réew mi. Dëgg la. Waaye, xanaa du yaa fi sulli mbirum terorist ba am ñoo ci tuumaal, jàpplu leen ? Danga fàtte imaam Ndaw xanaa ? Jaalewoo ko sax, ndeysaan.
Bi xibaar bi jibee, ñépp yaakaaroon ne Njiitu réew meey waxsi. Waaye, ñépp a yàqi. Ndege, njiitalu APR ak lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar moo jël tele bi askan wi moom, di ci gaaruwaale ay wujjam ci pólitig.
Nu ni déet-a-waay, nga nuy yégal Nguur gi ngay waaj a siiwal. Waaw, loolu jarul woon nga nuy toogloo 4i waxtu, di nu xalaatloo. Ab yégle bu gàtt doyaan na ci. Li am ba des mooy ne, Njiitu APR li daal rusul askan wi te dafay jaawale mbubbum Njiitu réew ak mbubbum njiitalug làng pólitig.