Démb la Njiitu réew mi doon tontu laaji taskati xibaar yiy liggéeyee RTS, Le Soleil, iRadio ak Seneweb. Ca njéeméer ba la janoo bi amoon. Mbirum wote yi ak diisoo bi muy woote lañ doon waxtaane.
Maki jàppagul bésub wote yi
Ñépp a doon xaar Njiitu réew mi. Xaar bi yépp nag, lenn rekk a ko waraloon, xam kañ lay àppal bésub wote yi. Nde, moom Maki Sàll, moo fommoon wote yi keroog bésub 3 féewiryee 2024. Ginnaaw gi la Ngomblaan gi jàllale woon ab sémbub àtte buy dàq wote yi ba keroog 15 desàmbar 2024. Waaye, Ndajem Ndeyu àtte mi dafa neenal ndogal yooyee, sant Njiitu réew mi, moom ak kilifa yi ko yeyoo, ñu amal i wote laata moomeem giy jeex keroog 2 awril 2024.
Bésub 15 féewiryee la Ndajem Ndeyu àtte mi siiwaloon ndogalam li. Ca ëllëg sa, Njiitu réew mi génnee ab yégle di ci wax ne nangu na ndogalu Ndajem Ndeyu àtte mi te dina ko jëfe. Waaye, boobaak léegi, dara.
19i waxtu ci ngoon la waxtaan wi waroon a door. Waaye, 30i simili tegu nañ ci muy sog a tàmbali. Kàddoom rekk la askan wi doon xaar. Génn kàddu, benn bés, muy bés bi muy jàpp ngir wote yi. Ña yaakaaroon yàqi nañ. Ñi doo xaar, xàddi nañ. Nde, moom Njiitu réew mi, nee na, ci diisoo bu muy woote lañuy jàppee bés.
Waxtaan woowu, dees na ci boole way-pólitig yépp, way-moomeel yi, nitu diine yi ak pàcci askan wépp. Mu ngi ñaan askan wépp ñu muñ, taaxirlu. Nde, altine 26 ak talaata 27 féewiryee 2024 lañ ko jàpp. Daf ne :
“Mënuñoo jàpp bés bi fileek dégguñu xalaati ñeneen ñi.”
Njiitu réew mi teg ci ne :
“Bëgguma ñu coow coow lu amul njëriñ ñeel ay bëgg-bëgg yu ma amul. (…) Keroog 2 awril 2024 la sama liggéey di jeex ci boppu réewum Senegaal.”
Naam, leeralal na ne moomeem gi 2 awrik lay jeex. Waaye, bu dee li ñeel bésub wote yi, waxu ci dara lu leer. Dafa delloo mbir mu ci diisoo bi muy woote. Maki Sàll nee :
“Wote yi mën na am laata 2 awril walla ginnaaw bés boobu.”
Waaye, li Njiitu réew mi begg dëgg dëgg, mooy japp bés ginnaaw 2 awril. Ndaxte, biñ ko laajee ndax wote yi mën nañ am balaa 2 awril, dafa tontu ne yaakaaru ko.
Maki noppi naa génnee Usmaan Sonko ci kaso bi
Njiitu réew mi dafa woote jàmm ak jàmmoo, bennoo ak baalante ngir Senegaal am jàmm ak dal. Ci kow loolu, mi ngi togg ab sémbub àtte bob, baal génnee ñi ñu jàpp ci kaso yi diggante màrs 2021 ak suwe 2023 moo ko wund. Xel yépp nag, ci Usmaan Sonko lañu dem. Maki Sàll nee, mën na ko génnee kaso, moom ñeneen ñi. Li mu ko duggee mooy fexe ba Usmaan Sonko bokk ci diisoo yi, moom ak lawax yiñ gàntaloon yi. Dafa wax ne :
“Ci wàllu diisoo bi wax naa sama gornamaŋ ñu jël matukaay yi war yépp ngir yombal génnug kaso ñenn ñi. Réew mi dafa aajowoo juboo. Dinan lal i pexe ngir àgg xi njéggal googii, jaare ko yoon yim war a jaar yépp… awma lu may bañ ci génnam [moom Usmaan Sonko]. Bu dee mën na tax ba li nuy dund jamono jii deñ, nangu naa def lépp lu ma mën ngir baal ñépp.”
Mbaale googu Njiitu réew miy wax, duggewu ko lenn lu moy tàllal loxo Usmaan Sonko ngir mu bokk ci waxtaan wi. Ci waxtaan woowu la bëgg a sukkandiku ngir jàpp bésub wote yi.
“Bu dee déggoo am na [ci waxtaan wi], dinaa gaawantu génnee ab dekkare ngir jàpp bés bi ñuy amal wote yi.”
Waaye, bu dee déggoo amul, nee na day delloo mbir yi Ndajem Ndeyu àtte mi.
Laaj bi samp nag mooy lu ko teree laaj Ndajem Ndeyu àtte mi bés niki tey ? Ndax xamees na xéll ne, waxtaanu ñaari fan, déggoo mënu cee am. Te sax, 16i lawax yi bokk ci joŋante yi nee nañ duñ ko wuyu ci waxtaan woowu.