MAKI SÀLL : “…BU BOOBAA, (…) ÑÉPP ÑOOY ÑÀKK…”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Maki Sàll, fasul yéene dellu ginnaaw. Ñaari bakkan rotagum nañ ci xeex bi ndogalam li sabab. Te, démb ba tey, réew maa ngi jax. Biir Ndakaaru ak diiwaan yi, askan waa ngi génn di jàmmaarlook takk-der yi. Lépp a taxaw, jàng amatul. Réew mépp a nekk ci guuta, tagatémbe. Àddina sépp a ngi teg bët Senegaal, di ko mbamb. Njiitu réew mi, moom, deram yàquna fépp. Waaye, mi ngi wéy di dëgër bopp, jàpp fim jàppoon, ŋoy ci ba dëgër. Looloo feeñ ci laaj-tontu bim mujje amal ak yéenekaayu Amerig bii di “Associate Press”.

Maki Sàll jéem na ragg deram ci kanami doxandéem yi. Ginnaaw bi kurél yu bari ak i kilifa yu mag ci àddina si ñaawloo ndogalu dàq wote yi, doon na jéem a indiy lay ngir yey leen ci ne jàmm a ko tax jóg.

Ci waxi Njiitu réew mi, ndogalam li woroowul ak li yoon sàrtal. Dekkareem bi méngoo na ak ndeyu àtte réew mi. Menn pexe rekk la gis ne moo mën a indi saafara ci mbir mi : waxtaan. Nee na, ngir fay coow li juddoo ci lawax yiñ gàntal te dëppale ñaari campeef yii di Yoon ak Ngomblaan gi, fàww réew mépp daje, ñu fénc ko, déggoo ci dara. Bu ko defee, ba tey ciy waxam, ñu sog di amal i wote yu amul xàjj-ak-seen, wote yu jaar yoon te jàmm lal ko.

Fi mu nekk nii nag, waxtaan woowu muy woote soxalul ñu bari. Nde, ñu bari dañ jàpp ne dafa bëgg a toog ci jal bi fekk te moomeem jeex na. Mel ni ku leen di tontu, Maki Sàll wax na ne, mësul a nisër ŋoy ci Nguur gi :

“Jenn yéene rekk laa am, te mooy bàyyi fi réew mu am jàmm ak dal. Noppi naa ngir ngir lenge yi te loolu yàgg naa koo waajal. Bëggumaa bàyyi sama ginnaaw réew muy tàbbi ci guuta ak i jafe-jafe. Sama bëgg-bëgg mooy dox i jéego ngir réew mi am ug dal ak jàmm. Nanu togandoo, nun ñépp, waxtaan, diisoo sog di sóobu ciy wote.”

Ginnaaw loolu, mi ngiy sàkku ci waa bitim-réew yiy dal ci kowam, rawatina Mbootaayu Xeet yi (ONU,  ñu teey te ànd ak ug dal. Nde, ci gis-gisam, réew mi dafa tollu ci diggante yu xat. Maki Sàll dafa jàppe ne Senegaal dafa nekk ci jamonoy njógte (troubles). Moo tax, ba tey ciy waxam, nu war a def ndànk ba Senegaal teguwaat ci yoonu jàmm ñu sog di sumb joŋantey wote yi, Senegaal mën a jëm kanam.

Mu mel ni Njiitu réew mi dafa dogu ci ndogalam li. Te, ni muy waxee, dara du ko tax a dellu ginnaaw. Nde, ñenn ci kilifay kujje gi àqi nañ àttekati Ndajem Ndeyu àtte réew mi ñeel sémbub àtte bi dépite yi jàllale keroog fa Ngomblaan ga, te muy randal wote yi ba 15 desàmbar 2024. Waa Ndajem Ndeyu àtte réew mi nag ñoo war a àddu, wax ba xam dañy dëggal dekkareem bi walla dañu koy neenal. Biñ ko laajee ndax dina jëfee ndigalu Ndajem Ndeyu àtte réew mi bu dee dafa neenal dekkareem bi, tontuwul lu leer. Daf ne rekk :

“Loolu moom, wax ci teel na. Bés bu ndogal li génee, dinaa xam nu may def.”

Maki Sàll nag, junj na réew mi, daldi leen cax. Nde, mi ngiy artu ak a dankaafu way-pólitig yi ci kàddoom yii toftalu :

“Bu dee way-pólitig yi nanguwuñoo déggoo ci li ëpp solo, yeneen kurél yu lootaabewu dinañu leen ko defal. Te nag, bu boobaa, ñoom ñépp ñooy ñàkk…”

Li xel njort nag mooy ne, Maki Sàll, bu lottee ciy pexeem, dafa nar jébbal Nguur gi sóobare yi. Maanaam, Maki Sàll day nos ak a nocci ngir ñu “coup d’Etat” ko.

Fu Senegaal jëm ?

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj