Njiiteefu réew mee génne yégle, di ci xamle ne Njiitu réew mi tabb ñu bees ci boppu CENA, kurél giy saytu lépp lu aju ci wote yi. Umar Sàmba Ba moo xaatim yégle bees bind lio toftalu :
“Njiitu Bokkeef gi xaatim na dekkare 2023-2152, tabb ñu bees ci boppu Commission Électorale Nationale Autonome (CENA), ginnaaw bi moomey ña fa nekkoon jeexee.
Njiitu réew mi tabb na yit Sëñ Abdulaay SILLA, Inspecteur général d’Etat alaateret, ak Sëñ Ndaari Ture, àttekat alaateret, ñu nekk cig toftal Njiit ak tof-njiitu Commission Électorale Nationale Autonome (CENA)”
Ndogal lii nag, teey na xel. Nde, yàggul dara, CENA bi dafa jox dëgg Usmaan Sonko ñeel xobi baayale yoy, DGE daf ko ko bañ a jox. Layookati Usmaan Sonko yi dañ bindaatoon waa CENA bi ngir ñu jébbal Sonko xobi baayale yi.
Ak ndogal lii, mënees na jàpp ne Maki Sàll nëbbul ne, moom moo bañ Usmaan Sonko bokk ci wote yi. Muy firndeel ne Maki Sàll dafa ragal Usmaan Sonko.